Digg bu mbëj
Digg bu mbëj, mooy barab bees di joóxee kàttanug mbëj. Xeeti digg yu mbëj yi bari nañu te wuute, seenug wuute ngi sukkandiku ci anam gi ñuy soppalee kàttanug doolerandu gi mu doon gu mbëj. Digg yu mbëj yu tay yi, daanaka, dawaanu mbëj gi ñuy jóox gépp gu safaanu la, ci ndimbalu wuutuloxo yu mbëj yees di duppee safaanukaay; bu njëkk ci dawaan bu wéy la daan ame.
Xeeti digg yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Manees naa séddale digg yu mbëj yi ci dayoob seen ngóora, maanaam kemu kàttanug mbëj bi ñu man a jóox. Wàlla itam ci xeetu jafaan bi ñuy jëfandikoo, bu ag coppiteem di xiirtal amug kàttanug mbëj.
Jóoxug mbëj gu dàttu ci jafaan yees jëlee ci suuf si (petrol,këriñ, gil...) doonul gongikuwaay buy yeeslu ci jamono ji dayoob jafaan yi amee dig, kon bés dina ñëw mu dakk. Ci safaan, manees naa amee kàttan ci gongikuwaay bu wóor te sax-dakk, kàttanug tangoor gees man a amee ci jant bi (kàttanug jant) walla ci ngelaw li (kàttanug ngelaw).
Manees naa lim xeeti digg yees di jóoxee dawaanu mbëj:
Lëkkalekaay yu biir
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Yeneen sémb
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]
Xool it Wikimedia Commons
|