Dellusi gi juge ca géej ga
Sëñ baa ngi àgsi Ndakaaru bisub gàww juroom benni fann ci sahbaan,atum kasasin di 1120 g, mu wéye fa, jàll Ndar def fa lu tolloo’k fukki fan ak juroom ba ca bis bu njëkk ba ci ramdaan, mu doonoon bisub talaata,mu juge fa,dem Luga, wàcc ca rakam ja Sheex Coro MBAKKE,ca guddig gàwwu ba, mu rañaane fa romb kër Sheex Jull SIISE,jugeeti fa jaar kër muridam ba sëriñ Sire LOO, yoor-yoorug dibéer ja ca Sànnoosi, mu sax fa la desoon ca ramadaan ja,noppalu fa,woor fa.
Ci diir bii,foofa fees na dell,raj-rajloo ba mel fa nu mu masul a mel,ci diggante ay taalubeem ak kuy sàkku ndimbal,aki kilifa yu koy siyaaresi,di ko ndokkeelsi,bokk na ca ñooña ka nuy wooye (kiimaanug jamonoom,woykatub waxtoom) Sheex Ibraahima JOOP Almasharii,ab xisaam lu xoromu la te yéeme,ag wuññi (feeñal mooy wuññi) gu yéeme feeñ na ci ñeel Sëñ bi (maanaam Sëñ bi wone na ci ay xar baax) loolu mooy sheex Ibraahima moomu daa amoon ab bor bu mag bu ko lëjëloon lool,ci jamono joj fay ko ci jafe na,mu jug wër ak moom ci sëriñ su mag si waaye taxul kenn tëyye ci loxoom,ci noonu mu jaaxle lool te am tiis,waaye bi Sëñ bi agsee Sànnoosi,mu ñëw indaale ay bayitam tudd ci mbirum bor bi ak ni mu ko seddalee ci diggante Yonnant bi(j.y.m) ak ñeenti saabaam yi,ginaaw sëriñ si nanguwunu koo xettali.
Bi mu yëgloo Sëñ bi ne ko mu agsi,mu dikk,nuyyoo,bi mu daataa wax ay mbiram ak boram bi ak ni mu ko seddalee ci bayit yi,Sëñ bi ne ko indil ma mbuus mee,mu indi ko,mu neeti ko jox ma mi ci des ,mu jox ko ko,mu ne ko waññal li nekk ci mbuus mu nekk,mu waññ ko, muus mu ne ñatti téeméer nekk ci,boo leen boolee ñuy juroom benni téeméer,Sëñ bi ne ko indi benn téeméer bi te jël li ci des dimbandikoo ko ci say soxla,te moom boram bi juroomi téeméer rekk la woon,ca saa sa sheex Ibraahima daanu ab jéll,yuuxu ca kaw,Sëñ bi ne ko waaw yaw lu mu? Mu nettali ko xisaam,jàngal ko bayit yi,moo nekk nii:
((bori ay mbokk war na ma,ma seddale leen ci diggante ñu tedd ñi ndax ñu fay leen))
( yaw Ku nu tànn ki(Yonnant bi), ya’ay ki moom cér bu njëkk bi,yaw su xarit bi (Aboobakar) ya’ay ki moom ñaareelu xaaj bi)
( yaw ki teqale dëgg ak fen (Omar) ya’ay boroom ñatteel bi, yaw sunu Usmaan mi, nga moom bi ci topp)
( yaw gayndeg xarekat yi,yaw baayi Asan ak Usaynu ñiy leerug sunu diine ji,yaw laa feetale li ci des)
(yeen de ñu tedd ngeen ñoñ kuy jàmbati coona du wéeru ci seen daraja te fajalu leen ko ko)
( kon gën jaa selli xèewali Yàlla na sottiku ci yeen,li feek Yàlla a ngi faje ay soxla ci yeen).
Sëñ bi yéemu lool te sant Yàlla,waaye noon yi ñoom seen kiñaan gi mayu leen sax ñu xaar ba Sëñ bi ñibbi këram,waaye danoo dal di tàmbalee wut seeni pexe,di lal seeni yoon, di waajal li nu nar,di xaar waxtoom jot banu def ko.
Ku baax ki moom bi mu jullee iid ca bisub kori ga,mu doonoon bisub alximis,da fa’a toogaat bisub àjjuma ak gàwwu ba ca tàkkusaan sa,mu laxase fa romb ca kër taalubeem ba Koor Mag JOOB,boole fa timis ak gee,ngir tarug dox ba,dem Màkka Sàmba JOOB fanaan fa,xëy bisub dibéer dem kër baay tëxam Sheex Ibraahima MBAKKE Kajoor,laxasati ca tàkkusaanug altine ba, dem ca Masàmba Xari JOOB,moom mi ngi kër Muxtaar,fanaan fa, yendu fa,jugeeti fa ngoonug talaata dem ca Muxtaar Mareema Silla ca Ñaxal,mu def fay fan,juge fa jàll Kokki Guy ca Maxtaar Masàmba JOOB,yendu fa waaye fanaanu fa,da faa juge njëkk jant biy so,te booba ña ngay waajal ñam yi,waaye taxul mu xaar ko fa,dox nag jëm Daaru Salaam këram,àgg fa guddig àllarba ci lu tolloo’k ñaar fukk ak benn,Siidi Muxtaar ,rakam ja booba ma nga fa woon,ca biir sawaal.
Rakk ji (Sheex Anta) tàmbli di ko ganalee lol kenn ci murid yu mag, yu man yi sax manu ko,waxantu ma la’ak ñu néew ñi doole.
Mu sax fa diirub fukki fan,bis bu nekk ñu ray ay fukki yëkk,bu ko matalul mottali ko ci giléem walla ay giléem,kem li mu mànke rekk.Ñu koy waajal ay wàccuwaay ca rakk ja sheex Ibraahima,diggante Tuubaa ak Daaru Salaam,muy fa Sëñ bi tudde woon Daarul Mannaan, mu dem fa moom ku baax ki ci njëlbéenug silqihda .
Sheex Ibraayma mii moom jërul ngay laaj ay mbiram, mooy ki ku baax ki dénkoon njaboot gi ak bagaas yi,bi miy tukki. Ci noonu màgi taalube yépp daje fa,Sheex Ahmadu Ndumbe jiite leen,mooy ki doon dem ak a dikk,di yee ñi gëmméentu,di jàngal goney Sëriñ bi ba nu mokkal ci diir bu néew njëkk ku baax kiy dellusi,dara yàquwul ci mbirum Sëñ bi,ba ñépp daan ko léebe ci wàllug jub ak tegu ci yoon.
Mu jullee foofa iid (tëbëski),sax ci meloom wu sell wa ak yareem (tarbiya) ga mu nekkoon,mbiram ak mu dongaam yi di gën a jëm kaw . Kawe fopp,fopp,fopp na mu meloon,kaamil yi ñu leen di jàng di leen xool ci bëcëg gi ,di leen tari ci gudd gi,naka noonu xasaayit yi,ak njàngalem xam-xam mi,ak ligéey bi ,loolu lépp àgg fof maneesu koo melal cig kawe.
Ni nga xame ne mbirum ku baax ki yokk na ak mu taalube yi ba jéggi ab dayo,ba maneesu koo misaal,naka noonu mbirum ñu iñaan ñiy rambaaj. Mbirum jaxase gi dellu fa mu nekkoon,rambaaj yi jug di def seeni ligéey ba nu xëy indil Sëñ bi ay soldaar,li ko waral mooy: jaraaf ji nu dénkoon mbirum wàll googa,ca jooja jamono,- moom xam nanu turam ak giir gi mu bokk - waaye bëggu ma koo tudd di nëxal ay doomi baay tëxam,ak doonte àndunu woon ak moom ci yéeneem ak jëfam ak waxam,waaye ginaaw seen doomi baay tëx la,rafetatul nu leen koy tuddal,te doy na ne ñi teew moom xam nanu ko ci tur,ci jëmm ak ci mbokk,te yal na Yàlla musal ñi teewul ñuy xam turam.
Moom de moo waxoon te tegu ko woon fenn ne : Sëñ bi day dajale ay kano aki fital ak yeneen jumtukaayi xare,te mi ngi waaj fi mu nekk,bu ngeen ma joxoon ay soldaar de kon ngeen gis li may def. Ñu àndoon ak moom ci kaw waaye wóoluwunu woon ay waxam,looloo waraloon ñu boole woon ko ak buuri réew mi mépp,buurub Kajoor,bu Bawal,bu Siin,waaye bu Siin a ci gënoon a rafet njort ci Sëñ bi,gënoon cee rafeti wax,waa-waaw xamal nanu ma ne am na ay buur yoy seen biir de Sëñ bi la àndal.
Am nanu xam-xam ci ne bi nu àgsee waa juy rëy-rëylu ji méngoo woon rëyam nga (al lazii tawallaa kibrahuu) moo dal di woon tàmbali di dog sàkket yeek jaaseem ji, te daawul xaar ku ko ubbil bunt,lépp lu dox ci kanamam mu dog,te amul lenn lu muy rus,dale ko ca sowwu ba, ba ca penku ba.
Fekkoon na Buur Siin - ci li nu wax - mu wutoon ay fuglukat (controlleurs) indi fa ngir ragal ñuy dugg cib néeg di fa duggal ay ngànnaay walla fital te kenn du ko yëg,ngir dëggale ci li nu waxoon ne Sëñ bi day dajale ay ngànnaay,waaye Yàlla dogal loolu amul,bu nu ko bëggoon it du man a am,ndax donga yi doonte danoo bank seeni loxo,teewul ñi ngi ànd ak ñoom ci ay bët ak ay xoolkat. Bi nga xamee ne gisu ñu lenn ci li nu doon tuumaal sëriñ bi,te gisunu ci donga yi kenn ku yor kanam gu lëndëm mbaa gu ñëkk,ku ñu ci gis rekk ma nga mel ne kuy waaj a julliji kori mbaa tëbëski,ngir tuwaaletu bu rëy,ñu xam ne noon bi day fen,buur yépp rus,am kersa ku ci dul waa ju fettéerlu ji,moom sax gàccawu na waaye daa suturloo jàmbaar-jàmbaarlu ak sàkku-sàkkulu nu ganaleel ko buur yi,ak xontal ko fas yi,waaye lu mu soxla rekk nu defal ko ko ca na mu gën a gaawe,gënnee yombe,ci noonu ñu dellu di ñu reccu,yal na Yàlla fay ña ca amoon yéene yu rafet.
Ag karaamaa ngi nii:
bi sodaar si laataa agsi ay mbokkam moom Sëñ bi danu koo wër lëjël ko witt,gën a tar ci moom ay jiit,tiit gi nu tiitoon taxoon amatunu woon kersa,taraloon lool ak moom,demoon ba bëgg koo génn seen biir bu nu ko manoon,ña ca bokkutoon ca mbokk ya daal mooy ña ca yaroo ca moom,waaye ku baax ki moom loolu lépp téewul mu doonoon ku féex ku ko yëgalutoon yaramam,naan leen bég leen,wallaahi mbir mii ñaari bëy dunu ci daanate,waaye kuy dégg loolu ? Ñoom ñii nga xam ne tiitaange gi yobb na leen ca dayo ba moos.
Ca bis yooya ku baax ki génneel leen aw dagiit wu yéeme ciy woy,ne leen bu ngeen ko jàngee ci kanamu soldaar si du ngeen dégg lu leen naqari mbaa ngeen koy gis,moom nag ñi ngi ko toftalee ci arafi (Rahmaan Rahiim)(muy boroom yérmaande ju nu yaatal ji,ak boroom yérmaande ju nu jagleele ji) moo nekk nii:
(( sama boroom de bettee na ci luy leeral xel yi,ci darajay ngën ji ku wéeru ca Yàlla)) (( samag cant ñeel boroom bu tedd,bu amul bokkaale,sama dënn it tay fees na dell ak leer guy jolli)) (( Muhammad ,xéewali sunu boroom yi ba fàww yal na nekk ci moom,sama lépp de ci moom la ko watoo )) ((maa ngi ñaan sama boroom, moom mi ay mayam matale mbooleem mbindéef yi, la mu tànn moom mi binde )) ((déeyaale naa ak moom - moom de màgg na - ay at , mu teral ma teralug aji gindee,sama lépp it set na ciy caaxaan)) (( yaw boroom yérmaande ju matale ji,mayal mbooleem mbindéef yi yërmaandey ka nga xam ne ku jàng Alxuraanam ji,mu feg la wëlis aw ay)) (( aaral xeetu Mustafaa wi ci gépp yàqute,te nga yërëm mbindéef yi,yaw mi bindoon seen maam)) ((yaw boroom nguur gi ,yaw mi màgg wëlif fayyoontoo, yërëmal mbooleem mbindéef yi,yaw aji gindi joy dimblee na))) ((far nga la xol ba jublu woon ciy lor,ci darajay ngën ji ku wéeru ca Yàlla)).
Sama mbokk Muhammad doomi Aliyu Alyahxuubiyu,nu gënoon koo xame ci turu Muhammad Tuubaa,ngir taqoo gi mu defoon ak ku baax ki ca Tuubaa,ak baril lu mu daa sikar,ak a jàng xasida yi,xibaar na ma ne bi Sëñ bi génnee xasida gi (Rabbii bimaa yashrahul),da ne ma mokkal ko, ma mokkal ko ba nu daataa ñëw,bi nu ñëwee mu woo ma ne ma jàng ko ca kaw,biral ko,ma jàng ko ni kuy nodd,baamu ko lu tolloo’k ñatti yoon,mu ne ma doy na ,mbir mi mat na te yéwan.
Mu daan def fu mu nee ma dajewunoo’k lu nu naqari de,ma ne ko xasida gi -ci karaamay ku baax ki- def na ci soldaari Tuubaa yi la picciy Abaabiila yi defoon ca soldaari Màkka ya,ngir sunu Yonnant bi (j.y.m),waaye ñii ak ñee li leen wuutale, ñii dañiy ñoñ ay nu jëflanteek ñoom ci kem seeni yéene,naaxsaayal leen,ñee ña ca ëpp di ñu baax,ñu ga (forse) leen ,te seeni xol Sëñ bi la àndal, Yàlla yeexal seeni mbir ba nu bari tuub ci,ba ca ka leen jiite woon,moom it tuuboon na,ñenn nit ñaa ngi sikk ay mbiram nag,bi nu xamee ne lòtt doo nga tuub du tuub. Sëriñ bi nee na : ((dëgg-dëggi tuub mooy nga bàyyi bàkkaar boo mas a def ngir Yàlla)) (( ci sa coobarey bopp,waxunu lu mel ni (lu la Yàlla teg) niki tëx ak jàngoroy pëy ak gumba ak luu)) ((nga bàyyi ko rekk ngir màggal ku màgg ki,ak ragal mbugalam mu metti mi)).
Man nag li may wax mooy lu man a xew ci mbooloom Sëñ bi la ,moo xam daa lòtt walla daa tuub,mbari na lu Yàlla jéggal ku tooñ te tuub,bàyyi ko ak Yàlla daal a gën a wóor, rafet njort ci moom itam a gën a mat,Yàlla nee na : ((fa man jaa ahuu mawhizatun min rabbihii fantahaa fa lahuu maa salafa mamruhuu ilal laahi)) muy ku ag waar dikkal juge ca boroomam,mu bàyyi la mu doon def,la mu jiital ñeel na ko,te mbiram moom ma nga ca yàlla. Bi soldaar si demee,ci la génne ci ndigalul Yàlla ak Yonnantam ci ñaareelu tukkeemba,ma nga ca naan:
(( ku jorte ne sama dox ba ginaaw atum aksasin di 1321g,moo’k sama dox bi ci bopp jaysasin di 1313g ñoo yam)) (( sax na ne aji réer ju dof la ,ndax moom dox boobu teeyal (neexal) gu aji kawe ji di teeyal samag dund la)) (( saama doxub aksasin bi du lu dul yoolub ki ma wommatal ci ginaaw bi dëël (dig) bob def na ko)).