Bisub Tabaski

Jóge Wikipedia.
Bisub Tabaski

Tabaski (ci bati Seereer) Sunna la su far ci ab jullit bu di as gor te man ci ag jàppndal, ku mukàllaf rekk mag ak gone ñoo ci yam. Waaye nag dina ware ci ñaari xeeti nësër yii : 1- ci ku ko nësër niki ngani bu ma Yàlla defalee nàngam dinaa tabaski, 2- ci ku njënd am xar, walla mu yor am xar jublu ci tabaski, manaam kon xar moo jënd niki am tabaski, manatu la ñàkk.Tabaski it ag bër (`iid) la gu Yàlla may jullit ñi, Jële nanu ci Anas (gërëmul Yàlla ci moom) mu ne: Bi Yonent (jàmmi Yàlla ci moom) bi agsee Madina fekkee na léen ñaari bis ñu cay caaxaan, Mu ne (jàmmi Yàlla ci moom): « Ana luy ñaari bis yii ?» Ñu ne: “Danu ci daa fo (caaxaan) ci jamonoy ceddo (jaahiliya)” Yonent (jàmmi Yàlla ci moom) bi (jàmmi Yàlla ci moom) ne léen: «Yàlla jox na léen ñaari bis yu gën yooyu ñaar, ñuy Bisu tabaski ak Bisu Kori» (Abuu Daawud mooko soloo) Gàttub tabaski it deesu ko rendi jëkk rendig Yilimaan te Yilimaan it balaa rendi nig ba julli, ci niko Baraan nettalee jële ci Yonent (jàmmi Yàlla ci moom) bi «Dees na lottal ginnaaw julli» Ku rendi lu ko jiitu du doon am tabaski xanaa ag ndawal rekk lay doon, noonu la saxe ci Sunna. Am tabaski sañees na cee maye, sañees na cee lekk, sañees na cee denc, noonu la saxee ci sunna (Albuxaari mooko solo)

Àtteb Tabaski ci Lislaam ?[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Yàlla neena: «Jullil ngir sa boroom te rendi (lottal)» Yonent (jàmmi Yàlla ci moom) bi neena: «Ku am dooley tabaski te tabaskiwul, kon bu mu jege sunu barabu julliwaay» (Abuu Hurayra mooko nettali, Ibn Maaja, Ahmad, Daaru Qutni ak Al-Haakim ñooko soloo. doonte barina ñu jam hadiis bi ci woroom xam-xam yi, niki Haasim ak ñeneen) Baraan nettali na ni, Yonent (Jàmmi Yàlla ci ñoom) bi neena: Li nuy njëkka def ci bis bii, moo di julli, ginnaaw ba nu dellu lottal, ku def loolu def na sunu sunna.»

Ash-Shaari` neena: «Duma nangu ku am dooley am tabaski diko sàggane » Tabaski Sunna la nag su far, Yonent (jàmmi Yàlla ci moom) bi saxaloon nako te daan ko digle. Sunna la su far ci Ñoñ-Maalig, Shafi`, ag ñenn ci waa Ahmad ibn hambal, bu dee nag ci Abuu Hanifa ñoom lu war la, Lu war ca ñoñ Abuu Hanifa nag tekkiwul ni farata la. Lu man a am nag ñépp dëppoo na ñu ci ne dina war ci ñaari mbir :

  • 1- Ku ko nësër, niki ngani bu ma Yàlla defalee nàngam dinaa tabaski,
  • 2- Ku xës njënd am tabaski, walla mu yor am xar jublu ci tabaski, manaam xar moo njënd ni am tabaski la, walla nga yori xar ni xar sàngam am tabaski la, ci yooyu barab luy war la.

Waxtuw rendi am tabaski:[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Mingi dale ci rendig Yilimaan, rendig yilimaan moongi aju ci ginnaaw julli gi, ba jant di so ca bisub ñatteel ba fu ñu ko fi rendee mu baax, bu dul guddi. La ca gën moodi boroom rendil ko boppam, bu amee ngànt mu wuutal ko moroomum jullitam, te nanga yéene yaw, Ku rendi tabaskim jàmbur te amu ci ndigal, kon du ko doy am tabaski te war naa fay boroom.

Am tabaski:[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Yàlla neena ci Alxuraan: «Deesul am Yàlla ci ndawalam ga, déeti dereetam ja, waaye dees na Ko am ci ag ragal [Yàlla]» S22 L:36. Kon nanu jàpp njëkk ni yéene ju sell, te Yàlla rekk tax waliif ngistal walla wanu ci bëti nit ñi mooy maye am tabaski.

  • Xar mu am juróom benni (6) weer walla at aki fan ci li sax ci Waa-Maalig, tey am kuy moo ci gën. Bu dee aw bëy nag, na am at ak weer ci waa-maalig,
  • Xar a gën, topp bëy, topp nag ak giléem
  • Xar mu góor a gën mu jigéen, bëy wu góor a gën wu jigéen, nag ak giléem naka noonu.
  • Juróom ñaari jullit man nañoo boole jënd aw nag walla giléem, Bu dee xar walla bëy nag kenn du ko bokk xanaa tiyaaba ja ci yéene.

Yees nanguwul ci am Tabaski:[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Bu benn béjjan dammee te wérul matul am tabaski [ci maalig], Bu weree nag mat na am tabaski, bu juddu waalewul ay béjjen nag darra nekku ci, Bees xaajee nopp ba ñatt, la ca dagg bu matee benn xaaj ba, matul am tabaski, Bu juddu waale wul nopp walla bu gàtt nag dara nekku ci, Bu nopp ba xaree lu toll ci benn ci ñatti xaajam du mat am tabaski Bees xaajee geen ba ñatt, la ca dagg bu matee benn matul am tabaski, Bu ko juddu waalee nag dara nekku ci.

Am Tabaski war naa mucc ci yii:[Soppisoppi gongikuwaay bi]

  • Bumu yooy, ba amul nebbon
  • Bu gimiñ ga xasaw
  • Bumu patt ba fés, rawatina nag muy gumba
  • Bumu làgge bamu fés, rawatina nag mu damm

Alaa kulli haal nag, Lislaam ag yombal la bëgg, te mboolem àtte yi woroom xam-xam yi di tërël di na ñuy sóoraale lool ag jàppndal ñeel jullit ñi.

Lees di bañ ci ndawlug am tabaski:[Soppisoppi gongikuwaay bi]

  • Bañees na ku ca jaay darra ba ca der ba sax, ku ko ñaani ba mayees la ko nag man na koo jaay dara nekku ci.
  • Bañees na yitam ka koy fees ñu di ko fay ca yàppu wa, waaye manees na ko caa may walla sarax, bu laajee ag fay fayees ko xaalis walla leneen
  • Bañees na gépp joxe ngir wareef, niki tànku njëkke, yeeli maam, baatu feeskat, ak yuni mel, waaye nag moongi aju ci jeene ji, booy sarax sa dëkkandoo te bëggal ko sutura man ngaa yéene sarax te wax ko ni am sa tànku njëkke, ndax Yonent bi neena: «Jëf yaangi aju ci yéene yi; Ku nekk it langa yéeneey sag pay» te it amaana boo ko nee sarax mu rusloo ko ci kanamu njabootam mbaa sax mu tere kokoo jël.

Rendi :[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ab jullit moo koy def, te doon ku am xel, Melo wi ci gën nag moodi mu tëral la muy rendi ci wetug càmmooñam te mu jublu xibla, bu dee am xar mu tëral noppub ndeyjoor ba ba famu yam ca baat ba mu teg ca paaka ba, Walla bu amee téeréy baat mu teg paaka ba ca diggante téere ya, Bu ko defee bala caa teg paaka ba mu wax ci am xelam ni fas na maa yéenee daganal lekk yàppu nàngam lii ci rendi gi ma koy rendi, bu dee teg paaka ba mu wax:«Bismil Laahii» dal di koy dawal ba ñaari sidit yu mag ya ak boli ga lépp dagg, Bu ko bombee ba deret ja génn mu wax: Allaahu Akbar, Bu teggee loxoom mu wax: «Rabbanaa taqabal minnaa innaka anta as-samii`ul Al-`Aliim S2:L:126:». Bu dawalee paaka ba sidit ya tàmbalee dagg mu teggi ko kon bu ko ca gaawee delloo dees na ko lekk, Bu ko ca yeexee delloo nag te lor wara lu ko kon deesu ko lekk. Te yit bu mu bañ a tàngale baat ba, Bu ko defee it du ko tee dagan, waaye bañ koo def a gën.

Loj :[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ku koy def, day taxawal lamuy loj jubale ko "XIBLA" (Kaabag Màkka), Lem baat ba tëral ko ci wetug càmmoñ nga, Bu ragalee barig doole ja, Man naa yeew tànkub càmmooñu kanam ba, Te balaa tàmbali mu wax «Bismil Laahi», Te bu tàmbalee mu bañ a dindi loxoom lifeek noppiwul. Lees war a loj nag bees amul lojukaay Sañees na koo rendi, lees war a rendi it bu ñu amul rendikaay, Te am lojukaay sañees na koo loj. -Giléem (Galéem) loj rekk lees koy def mbaa deesu ko lekk waaye deesu ko rendi, Xanaa ñu loru ñàkk lojukaay te am rendikaay, bu boobaa nag dees na leen ko may, -Bu dee aw Nag dees na ko loj niki ñu koy rendee, kon moom lu leen jekku rekk ñu sañ koo def noona, (Fii nag rendi ko lañu gën a miin) Loj, balaa baax ñatti sidit yu mag yi daa war a dagg, kon ci ag wet lees koy defe ak kanam..

Na moytu yii:[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Bu dawalee paaka ba, ba sidit ya tàmbalee dagg mu teggi ko, kon bu ko ca gaawee delloo dees na ko lekk, Bu ko ca yeexee delloo nag te lor wara lu ko, kon deesu ko lekk. Te yit mu bañ a tàngale baat ba, Bu ko defee it du ko tee dagan, waaye bañ koo def a gën. -Rendi xar ak bëy ci kanam lees koy defe, boo ko rendee ci ginnaaw walla ci wet, deesu ko lekk, -Bu dee aw nag manees na koo rendi manees na koo loj, -Bu dee Ginaar (Ganaar) nag war naa wërale paaka ba, ca gannaaw ak ca kanam, ba sidit yu sew yépp dagg te mu bañ a tàngale baat ba, bu ko defee it du ko tee baax waaye bañ koo def a gën.

Ngënéeli Tabaski:[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ngënéeli Tabaski ci lislaam lu am solo la, kenn manu koo takk, Yonent (jàmmi Yàlla ci moom) bi xamle nani toq dereet wiy njëkk a génn Yàlla di na ci jéggale mboolem bàkkaar yees masa def, nii la dikke ci sunna ci nettalib Aysa (ngërëmul Yàlla ci moom). Jëlee nanu ci Ibn Abaas muni Yonent (jàmmi Yàlla ci moom) bi neena : «Xaalis dugaleesu ko ci lu gën gàttub tabaski (iid)» (Daaru Qutni mooko soloo). Yonent (jàmmi Yàlla ci moom) bi bégal nanu ci ne Xarum tabaski dina njot ci sawara niki mu ko njotee woon bakkanu Ismaayla. Amul lu jëf ju nit di def ju gën a neex Yàlla ci tuur deret ci bisu tabaski, noonu lako Aysa nettalee.