Weeri wolof
Weeri wolof, ci arminaatu gàddaay gi, walla bu jullit ñi mbaa bu Lislaam, ab arminaat bu weer la, buy sukkandiku ci doxiinu weer wi ngir xam ak natt weer wi. Jullit ñi danañu ko jëfandikoo ci bépp barab, rawati na ngir natt ak xam xew-xewi ak bisi diine yi. Ki ko sos nag mooy Omar Ubn Xattaab (g.m), daal di def gàddaayug Yonent bi (j.m) juge Màkka dem Madiina muy ab tàmbaleem, looloo waral deesi tudde ko arminaatub gàddaay gi. Ak doonte arminaat bi ci jamonoy jullit ñi lañu ko sos, teewul turi weer yi ak arminaatub weer ñu leen daa jëfandikoo lu jiitu Lislaam.
Yenn ci réewi araab yi, mu ci mel ne Araabi Sawdit, moom ci nguur geek askan wi dañuy jëfandikoo arminaatub gàddaay gi niki arminaat bu kilifawu di ci taariixe ci bindante yiy am ci diggante liggéeyuwaayi nguur gi, waaye nag lu ci dul moom, askani araab yi ci des yépp arminaatu Garegori (bi dale ci juddug Yonent Yàlla Iisaa) lañuy gën a jëfandikoo..
Arminaanub gàddaay gi mi ngi ame ci 12 weer yu weer wi, maanaam atum gàddaay gi mi ngi tollook 354 bés daanaka, maanaam 354.367056 ci ay bés. Weer wi ci arminaatu gàddaay gi, benn mu nekk 29 walla 30 bés (ndax doxug weer wu feeñ wi 29.530588 bés la). Ginnaaw nag wuuteg 11 fan am na ci diggante arminaatu judd gi ak bu gàddaay gi, ñaari arminaat yi duñu jamonoo mukk (duñu tolloo mukk) looloo waral dëppale leen di gën a jafe.
Weer ci arminaatu gàddaay gi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- Tamxarit
- Diggi-gàmmu
- Gàmmu
- Rakki-gàmmu
- Rakkaati-gàmmu
- Maami-koor
- Ndeyi-koor
- Baraxlu
- Koor
- Kori
- Diggi-tabaski
- Tabaski