Aakimoo jawwu ji

Jóge Wikipedia.

Aakimoo jawwu ji, (walla xare bi ngir teg loxo ci jawwu ji sanc ko):

Li ci alxuraan wax[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sooratu Rahmaan, aaya 33:

«yaa mahsharal jinni wal’insi inistatahtum an tanfuzuu min’axtaaris’samaawaati wal’ardi fanfuzuu, laa tanfuzuu illaa bisultaanin»

Tekki: yeen jinne yeek nit ñi, su ngeen manee dem, ba soobu ci goxi asamaan yi ak suuf, def leen ko, waaye fu ngeen fi àgg rekk na leen wóor ne Yàlla a leen may ngeen àgg fa. Fu ngeen fi àgg rekk, ci sultaan ngeen fa àgge, sultaan nag mooy: lay, ndigal, kàttan, nguur. Di kon fu ngeen fa àgg, sunu boroom a leen fa àggale moom mi leen may xel, may leen kàttan, ubbil leen wunti yooyule gox, man a layal lu tax ngeen àgg fa.

Ci lu daj[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Nit nag yàgg naa xëntewoo xam li ko wër ciy mbir, yàgg naa yittewoo xam mbóoti jawwu ju biti jii nga xam ne daa fees dell aki yaram yu asamaan; ay biddiw aki ñoom seen. Moom de jot naa àgg ci xam biddiw yi ak seeni kem ak seeni bind (forme), ak li leen sos, def it ab jéego bu rëy ci xam-xamu melosuuf ak yeneen xam-xam yi am ag jokkoo ak kaw-suuf, biir suuf ak li wër suuf, peek ko ciy mbindeefi asamaan, biddiw ak lu ko moy.

Ci ati juroom fukk yi, ci ñaar-fukkeelu xarnu bi, gisees na nit mu jéem ay yoon nu mu yéege ci jawwu ji, ngir làmb ko te xam la fa nekk, loolu nag faalewu ci woon jafe-jafe yi mu ci doon man a dajeel, ak ay wu rëy wi loolu làmbool, bokk na ci ay woowu: man cee ñàkke bakkanam, ñàkk a wóor gi, ci bu ñuy boy (départ), bu wuutuloxo (masin) biy wëndéelu ak buy wàcci.

Li Sofiet yi def ci xareb jawwu ji[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sofiet yi de njëkk nañoo nattu jawwu ji, jarbu ko, làmbtu ko, loolu ñu jaare woon ko ci jëfandikoo ay bayyima, ngir ragal nit di ci loroo.

Sofiet yi ñi ngi njëkk a joyal seen gaalu gu jawwu gi tuddoon Fostok – 1, ñaari soobukati jawwu yu sofiet nekkoon ci biir – di Yori Jajarin ak Alaan Shabard, ci subag bisub 12 awril 1961 g . loolu nag bettoon na adduna bépp. T ukkib jawwu bii nag yobbu woon na lu tollook téeméer ak juroom ñatt-fukki simili, ci biir diir boobu, gaalug jawwu gi wër na ci suuf si benn yoon ak xaaj.

Tukkib xam-xam bu jawwu bii xew-xew la bu am solo ci taarixu nit ci jamono ju yees jii, ndax kat moom ubbi na fi ay gox yu yees yu yaatu ci wàllug xam-xamu jawwu.

Sofiet yi wéyoon nañu ci seen liggéeyi jawwu yooyu nga xam ne am na ci yu jàmm taxoon a jug ak yu xare taxoon a jugg. Seen jumi jawwu (satellites) yi gënoon nañoo yokk seeni cawarte rawati na ci lu aju ci xare, ci diggante ati juroom-ñaar-fukk yi ak juroom-ñatt-fukk yi, ci xarnu bii.

Li ci waa-Amerig def[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Waa Amerig yi - ci ati juroom fukk yi, ci ñaar-fukkeelu xarnu g – def nañu ay jéem aki pexe yu am solo ci wàllug xareb jawwu ji walla aakimoo ko. Seen cawarte ci wàll googu dolliku woon na ci ati juroom benn fukk yi ci xarnu bii, ndaxte seen liggéey yu jawwu yi gënoon nañoo ràññiku te gën a fés ci diggante bii, ndax ci la kërug jawwu gu Amerig gi, ñu koy wax NASA, jot a joyal ay waruwaayi jawwu , yoo xam ne ay jum ñoo leen di jañ, jañax leen ñu naaw, bu niy dellusi ci suuf si nekk ay fafalnaaw yu yor ñaari laaf, ñu leen di man a jëfandikoowaat ay yooni yoon. Lii nag tax na ba li nu daa ñàkk ci tukkiy jawwu yi gën a néew, te itam indi na ay ngérte yu am solo ci xareb jawwu ji.

Waa Amerig jot nañoo sànni waruwaayu jawwu wii di Apolo ci 20 sulye 1969g, ñaari soobukati jawwu nekkoon ca, ñooy: Aarmustrong ak Adwin Drin, Aamustrong nee na “ Amoon naa yëg-yëg bu tumbrànke, bi may dox ci kaw weer wi, damaa yëgoon ne sama màndaxe daa woyofoon lool”. Waa Amerig yi sàmp nanu ci kaw weer wi ay jumtukaay yu xam-xam yu bari, jële nañu fa it ay còmp (échantillons) yu juge ca weer wa, teg fa it ab juddalkaayu mbëj bu saal .

Kongres it dëppoo - ci 5 samwiye 1972g – ci prograamu jawwu bi nu tudde woon (baaganteg jawwu) ngir barig li nu daa dem ci jawwu jeek a dellusi. Tukki bu jawwu bu njëkk bi nuy wax Kolombiya tàmbli na ci 12 awril 1981g, yeneen tukki topp ci yu jawwu yu àntu .

Waa Amerig yi defati tukkiy jawwu yu Carlinger , bi ci njëkk di ci 4 awril 1983g, juroom ñeenti tukki topp ci, bi mujj di ci 30 oktoobar 1985 g.

Musibam Carlinger:

Am musiba xewoon na ci baagante gu jawwu gu Amerig gii di Carlinger-10, loolu nag mooy bi waruwaay bi fàccee , ci bisu talaata 28 samwiye 1986 g, lu tollook juroom ñaar faatu ci, ñaar ñi di ay soxna . Njiitul Amerig la nu daa wax Ronaald Rigan nee na woon “ Bii bis de dana doon bisub naqar ak fàttaliku” . Waa Amerig yi it tudde woon nanu ko bis bu tiis bi.

Musiba mii du mooy mi njëkk a dal Amerig ci wàllug jawwu gi, mu ni mel njëkkoon na ko fi ci lu tollook ay at, loolu mooy bi sawara tàkkee ca joyaluwaayu waruwaay ba tudd Apolo 11, ci samwiye 1967 g, ci noonu ñatti soobukati jawwu ya ca nekkoon yepp dee.

Amerig defati yeneen tukkiy jawwu yu baagante, tudde ko Discovery, bi ci njëkk mi ngi amoon ci 30 Ut 1984 g, yeneen tukk yu àntu topp ca.

Lii nu tudde xareb jawwu ji daal, def na lu am solo ci wàllug xam-xam, rawati na lu aju ci mbiri jàmm yi. Ndaxte xam-xamu Jëmm gën a jëm kanam, bu fuglug jawwu , ak xam-xamu nataalu jawwu biy nataal kaw suuf si te di ko natt, xam-xamu kart yi ak nataali jawwu yi gën na a jéego ay jéego, naka noonu ndefar bu mbëjfeppal (bu elektron), ni nuy xame fi mbell yi nekk gën a xarañ, ak ni nuy xeexe lakk yi añs.

Sofiet yi ak waa Amerig yi ku ci nekk sóobu nga ci jawwu ji ngir ay xemmemteefi xare, jawwu ji mujj di lef mu stratejig mu yaatu ñeel ay liggéeyi xare, la ñu ca jublu it di door ak jam ay barab yu nekk ci kaw suuf, jaare ko ci seen jumi jawwu yi nekk ci asamaan si, yi ci yanu ay boppi fepp (tête atomique), cig wàll, walla nu jaare ko ci ngànnaay yu wuute yi nu man a joyale ñu tukke ci jawwu ji, ci geneen wàll.

Xareb jawwu ji, yamatul rekk ci diggante Sofiet yi ak waa Amerig yi, leegi kay lu sakkan ciy réew bokksi nañu ci, mu ci mel ni Siin ak Fraans. Am na yeneen réew yuy waaj ngir sànni seeni jumi jawwu walla satalit ci jawwu jii nga xam ne mujj na di barab bu yaatu ngir rawanteg xam-xam, ak gëpplante ci wàllug xare.