Aller au contenu

Waalo

Jóge Wikipedia.
Waalo

Waalo bokkoon na ci yénn ci nguuri Senegaal yi fi nekkoo. Buuru Waalo dañu ko daa tànn ca péncum Seb ak Bawar. Njurbel moo nekkoo péeyam ci lu njëkk, ganaaw bi lañ ko tuxël Jinge, tuxëlaat ko Ndeer. Tuxu yu bari yooyu doy na tegtal ci dellu ganaaw ak ñàkk doole.

Jëwrin yi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ñooñu ñooy: Jawdaŋ mi yor suuf si ak Jogomaay mi yor ndox ak Maalaw mi yor koom-koom gi. Ganaaw ñooñu amoon na ñu nekkoon ci kër buur. Bokk na ca Meet moom mooy njiitu bëkk-nèeg yi ak bëkk-nèegu Njurbel moom mooy wax ci turu buur bi ak njiitu ñi yor baxan buur te mu gën a siiwe ci Baadi ak taawub buur. Moom mooy saytu néegu buur ak Fara Njurbel moom mooy njiitu tëgg weñ gu ñuul ak wurus yi. Fara Juñ-juŋ bi moom mooy njiitu waykat yi.

Waalo, amoon na ñeeti kër ñu daan taan Barag bi, soqikoo ci ñeeti xeet yooyu:

  • Tejeek (Pël ak socé)
  • Joos (Séeréer)
  • Logaar (Naar)

Barag bi, di turu buuru Waalo, dafa joge ci turu ku jëkk nekk Barag, mooy Barka Bo (Mbooj). Barka moo soppiku Barag.

Ndete Yalla

Barag mooy maqaama bi ñu joxoon buuru Waalo. Yilifoon na li dale ca Mbàmbulaanu Atlas ba Lag de geer. Bokkoon na ci ñi dar Barag ñaari mbooloo: ba njëkk moo di Lingeer miy yaayu buur bi ak Aawo miy soxnaay buur su njëkk, moom moo am teraraagaay toog ca gangunaay (mooy toogu gu buur) ga.

Bu ñaareel ba moodi ñatt ci boroom ndombay tànk yi ci péncam Sëb ak Bawar: ñoom ñooy Jawdun mi yor suuf si ak Jogomaay mi yor ndox mi ak maalaw mi yor koom-koom bi.

Bokk na ci ñi nekk kër buur ku ñuy wooye Meet, moom moo di njiitu bëkk-néeg yi ak bëkk-néeg Njurbel moom miy wax ci turu buur ak kiy jiite ñi yor mbaxanaam buur. Baadi moom mooy njiitu doomi buur bi, ak yénn ci Jëwriñ yi.

Barag daawul génn ci am at lu dul ñaari yoon: bu njëkk bi ngir jiite lëlu xare. Bu ñaareel bi ngir teew ci xumbeemi gàmmu, moom ak waa këram. mbooleem ñi yor ndomboy tànk dañoo wara teew ci gàmmu gi. Képp ku wuute dees na la mbugal, ñu folli la mbaa ñu rey la. Ndaxte senug teew li muy tegtal moo di yeesal seenug nangu, lañu lokki ak lañu siif. Mbooleem alal yooyu daanañu leen séddale ñetti xaaj: ben ba moo ngi jëm ca buur ba, ñaareel bi mu ngi jëm ca pécum Séb ak Bawar. Bi ci des mu ngi jëm ci taxawal xumbèem yi

Seddaleeg yorte gi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Nguur ga dañ ko seddale woon ci ay diwaan, bu ci ne amoon na bàjjo buy dox mbiri buur bi (Sàmba Lingeer). Kàjj moom la ñu fal ci ndijjooru dex gi, li ko dalee ca aarnik ba fa dex gi sottee. Buriko moom la ñu fal ci bëj-gànnaaru Lag de geer, mu ngi daan dëkk ca Foos, Baadi moom lañu fal ci li dale Sirigi ba Sinò Bawaal. li des ci pal yi mu ngi ci kilifteefu Kangam yi: Marooso moo nga dëkkoon Boroso Piccoo. Barlaf moo nga dëkkoon ca sowu Lag de geer.

Buuri Waalo

[Soppisoppi gongikuwaay bi]
1.Njaa jaan Njaay 31.Fara Yirim
2.Barka 32.Njaag Kumba Saam Jaxeer
3.Caaka Mbaar 33.Njaag Kumba Saam Jaxeer
4.Amad Faaduma 34.Fara Xéere
5.Luftu Numayga 35.Njaag Kumba Majigéen
6.Farna Numayga 36.Njaak Kumba Naar Saang
7.Cabati Numayga 37.njaag Kumba Njaay
8.Faduma Numayga 38.Mbaan Naatago
9.Mbaañ wàdd 39.Mambooj Njaak
10.Fajo Wàdd 40.Yirim Mbañig Gilé
11.Dafo wàdd 41.Fara Tòkò Tabi
12.Ànta Yaasin (gòor) 42.Yirim Koddu Giran
13.Yirim Mbañig Ndaw Demba 43.Fara Penda Tigrila
14.Tukubaa Mbòoj 44.Mambooj Maalig Aysa Daaro
15.Natago Ànta 45.Fara Penda Aadama Sàll
16.Caaka Daara Waxoot 46.Demba Ali
17.Natago Fara Njaag 47.Yirim Anta
18.Natago Yirim 48.Yirim Koddu Fara Mbooma
19.Fara Penda Jeŋ 49.Mbooj Kumba
20.Taan Fara Njaak 50.Fara Penda Tigerel
21.Fara Ko Jeŋ 51.Njaag Kumba Morige
22.Fara Kura Joob 52.Saydu Yaasin Mbooj
23.Fara Penda Laga Ndeen 53.Aram Faati Boroso
24.Fara Kor Ndaama 54.Yirim Mbañig
25.Fara Aysa Naalew 55.Xayer Fàr Xayeri Daaro
26.Natago xari Daaro
27.Barcaaka
28.Yirim Mbañig Aram bakk
29.Njaag Aram Bakar
30.Yirim Ndaten Buubu

Ay jafe-jafeem

[Soppisoppi gongikuwaay bi]
Waalo

Daanaka Waalo nit desatu fa ndax ya cong yi jòge Gànnaar ak ay xeet yu sax ci diggante sang yi. Moo tax ba ci xarnub XX waa waalo jublu woon ci seen gàddaay wàllu Saalum ak tëdd mi nekk ci diggante Kees ak Mbuur ak dëkk yu mag yi ci réew mi.

Ba besu tey Waalo ngi jànkonteeg coon ya jòge woon ca ŋaayoo ga. loolu mooy jur dellu ganaaw ak daanug waalo, ba ku nekk di ko cokkaas: Taraasaa ak Almaami ak Dàmmeel. Ki ci gënoon a fés nag mooy Faraas. ganaaw ba Faraas rimbee Waalo ba mu nëx, dakoo teeyal dëtëm ko ci ndimbalu Budeŋ ak Potore ak Fedeerba mi ñëw seen ganaaw ci 1885. Booba la nootee Waalo, te naa daf koy xettali.

Paate sow, Démbi Senegaal: ci làmmeñu Wolof, Dakaar, 1998

Lëkkalekaay yu biir

[Soppisoppi gongikuwaay bi]
Seetal BUNTU TAARIIX
wikbaatukaay am na xët wu tudd: Waalo