Sëriñ Móodu Lóo Dagana
Sëriñ Móodou Lóo Dagana (Sëriñ Móodu Lóo Dagana) mi ngi judd ci atum 1858 ca kër madu yala, mooy dëkku cosaanam, ma nga ca njàmbur (Luga).
Yaayam mi ngi tudd Soxna Astu Lóo, baayam Sëriñ Subayru Lóo. Mi ngi jànge Alquraan ak xam-xam ca njàmbur ba mujj doon ab jànglekat bu mag.
Yoroon na lu mat fukki daara ak juróom ci kilifteefam.
Mi ngi seeti sëriñ Tuubaa ci atum 1898 juge ca kokki guy dëkkub ay nijaayam la.
Daa tëdd guddi am lu ko feeñu ne ko demal wuti ab sëriñ, ci la jug ne seeti Sëriñ Tuubaa, te booba kenn xamul fu Sëriñ Tuubaa nekk, tubaab yi dañ koo génne woon (exiler).
Sëriñ Móodu Lóo Dagana dox seeti ko jaar na ci dëkk yu bari di dox ak tànkam ba gis Sëriñ bi te xamul woon fumu nekk. Bi miy dem at la am ci yoon wi. Bis bim juge woon kokki guy ba mu delsee ca at mële la soog a gis sëriñ bi. Moom la sëriñ musaa ka naa:
"Xëye na kokki guy bisub talaata
namm ca géej ga bañu naan xad maata
Ba weer deelsee ca déwen saak bis ba
la doog a seeru bàmba ngir pas-pas ba"
Mi ngi gis Sëriñ Tuubaa ci atum 1900 ca maayoomba ca gabon. Moom mooy waa-senegal bi njëkk a juge fii dem seeti Sëriñ bi. Bi mu àggee toog na fa ay weer Sëriñ bi yabal ko ne ko, dellul senegaal wool ma Maam Seex Anta. Mu daal di ñëw Senegaal woo Seex Anta ànd ak moom yóbb ko Gaboŋ ca Sëriñ ba. Sëriñ bi jox Seex Anta ay xasaayid yu bari yum taalifoon yabalaat ko mu ñëw Senegaal.
Moom ak sëriñ móodu lóo desaat fa ba 1902 ci la tubaab bi indiwaat Sëriñ bi Senegaal ñu ànd ñoom ñaar. Bi Sëriñ bi amee ci réew mi ay weer, tubaab bi yóbbuwaat ko Gànnaar, sëriñ jëlaat sëriñ Móodu Lóo teg ko ca Dagana ne ko bu kenn ñëw te jaarul ci yaw.
Looloo waral ñu koy woowe sëriñ Moodu loo Dagana. Bi Sëriñ bi jugee Dagana la ko seexal boole kook ay taalibe yu bari. Yabal ko saalum mu sanc fa ab dëkk di tërbiya, dëkk ba di dagana ca kër mbukki.
Moom nag mi ngi fi juge dibéer 13 maars 1954 ca Ndakaaru ñu indi ko Tuubaa ci armeel yu mag yi.