Seex Muhammadu Murtalaa Mbàkke
Apparence
Góor Yàlla, jàmbaari Lislaam, taxawoon na ci tas lislaam ci àdduna bi bépp, moo waraloon foo ko fekk daa wul toog, mi ngi woon jamono ju nekk ci ab tukki mbaa muy door a wàcc te lepp dara du sababam lu dul taxaw ci baatu Yàlla bi di bu kawe, moo digle kër Sëñ Tuubaa yi ci biti, te lenn la ci jubluwul lu dul barabi lislaam yu jullit yi di man a daje ngir jaamu Yàlla ak dimbalante.