Seex Anta Jóob

Séex Anta Jóob mu ngi juddu ci 29 deesàmbar ci atum 1923 ci ceytu, faatu ci 7 féwrier ci atum 1986 ci Ndakaaru. MoomlSénégala Saa-Senegaal la di gëstukat ak ku doon yëngu ci walu polotig giirug dundam, dafa doon wane ñariñu Afrig rawati na der bu ñuul ci mboorum aduna si.
Ba tay amna ci Mbidam yu ñuy ŋañ, ba taxna du ñu kay faral di féssal, rawatina li mu binda ci walu Egypte ak ciossaanu kalaama wolof.
Wayé Séex Anta Jóob bokk na ci ñi njëkk a bind ci mbooru Afrig ak kolonisationg.
Diar diar am ak ŋiagalém
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]Séex Anta Jóob muŋi juddu ci 29 déçambar ci atum 1923 ci ceytu, ci diwaanu Bambeï, ci ŋiaaréem.
Ci askan wu mag la soxékoo. Bi mu amée 23 att la dem farançe ŋir diag physique akk chimie, waaye mu mujje julu ci histoire ak science sociales, rawatina ŋiaŋalém Gaston Bachelard akk bu Frédéric Juiot-Curie. Moome bokkul gis-gis ak ñiy xalaat ni afrik amul histoirou boppam.
Ci atum 1951 la Séex Anta Jóob , ci dimbalu Marcel Giraule, waajal thézou doctorat ci ñiangalé mu kawe ci université bu Paris. Ci thèze boobu ci la xamlée ni waa Egypte ay nitt ñu ñuul lañwoon te itam lakk ak aaday afrik yi foofu la soxékoo.