Seere yi ko mag ñi seereel ag màgg akug wilaaya
Doggantal :
ci seere gi ko ñu mag ñi seereel ag màgg ak ag wilaaya
Xoolal Sheex Siidiya mii ak màggam gi mu màgg lépp,téewul mu tegoon Sëñ bi fu mu tegul kenn,bind na ci moom,woy ci moom wesar ci moom,bu waxutoon lu ëpp ñatti xasida yii tam,ci xasidaam yu bari yi,loola da na doy,ñooy yii:
(Sheex Ahmadu daal xéewal la ,gu Yàlla jox mbindéefam yii yépp) (ag cant ñeel na Yàlla mi ngi xam ne ay xéewalam jaamam yi manunu koo takk,mbaa nu lim ko) (boo dajee ak moom,fekk ñuy yekkati raayob teddnga,da nga ko gis mu alawtiku ko ci loxol ndayjooram,ànd ak di tudd Yàlla ) ( bu gisee bis jikko yu rafet yi ñu dëdd leen,day dogu jublu ya ca gën a mag) (suuf su ko dëkkal daal ,ab lolli bu ko ñàkk a ndàndal du tax mu lor ko ) (miskiin yi ngir sa baax gi fàtte nanu seeni dëkk,ba mujj na sa koom mii de lanu jàppe seenum koom ) (seen mbooloo yooyu de buy daje ak ñoom mbégte mu rëy te dëggu lay àndal,nga xam ne da ngay jort sax ne,lu toll ne li mu leen di jox ciy xéewal rekk,lanu koy jox )) (( mbooloo yépp seere nanu nekk gi mu nekk di ku baax,ku tedd,kuy jaamu Yàlla te dib tuubaakon )) (( bokk na ci ñi gisoon jariñ nit ñi di farata,ci jamonoom,tey ci ñi daan tudd Yàlla )) (( dogal bu ñëw mu nangu ko te gërëm ko,xam ne Yàlla’ay ki ko dogal )) ((bu kuy tëñëxu cig lëndëm di tëñëxu it,moom genn muuraay du man a muuri bëtam wëlif dëgg gi )) ((kersa du dañ di ab rootukaay ci sab hadara,bu ko defee yiw yi di noyyi ci gelawam lu sedd li)) ((jaam yi de ,dox gi nu dox jëm ci moom,seeni aajoy àdduna’ak allaaxira’a ko waral))
Ñaareelu woy wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]mi ngi ko def bi mu tàmblee tabax jumaay Njaaréem ji,mi ngi nii:
( jàkkay Sëñ bii de mooy jumaay barke ji,tey barabub ay yiw ak yërmaande )
( fa lanuy jéggalee ñaawtéef yi,ña koy siyaare it seeni yiw danu koy ful)
(boroom fondumangub ragal Yàlla la ,ak miiri jëf ju baax ak teraanga)
((jëf ju sell ñeel boroom mbindéef yi,ci yeene,te jëf ya’a ngi ci yéene yi)
(boobu barab de,làquwaayub ku bëgg a taxaw guddi ngir jaamu Yàlla la,kon de bu baax la,làquwaayub ñu ndool ñi de làquwaay bu baax la)
(bu fa julli ngir Yàlla amee ab néeg it,du tee muy neegub jokkoo ngir Yàlla)
(xamal nanu fi julli ay waxtu,waaye jàkka jii de am na lu dul waxtuy julli rekk)
( nit ñi danu koy jublu,ànd aki xol yu boole lu tàqalikoo ciy yeene)
(ab kuréel bu fay ñëw ngir julli,ak beneen bob mbiram mooy asaka )
(Yàlla digale na ñu yèkkati ay néeg,yu tedd ci kaw yeneen néeg yi,ngir turam wi)
(yal na Yàlla faye tabax gi, ay kër yu niy tabax ca àjjana,ay jigéen nekk ci)
(Sëñ bi daal xéewal la,gu Yàlla joxe,di kiimaan ci kiimaanam yi)
(nit ñi de xam nanu ko ci penku bi ak ci sowwu bi,mu dib sang ci taax yi ak ci kaw gi )
(mi ngi bokk ci tabaxkati jëf ju baax,te loolu lu néew la ci nit ñi)
(dellu nanu seeni kër,ànd akug cant,gu toll ne cantug ku soxla woon am ndox Yàlla jox ko dexug Furaat)
(yal na ko Yàlla wattu ci wattoom ga akug kaweem,aki doomam yu gó0r ak yu jigéen)
(ak ñoñ néegam bu kawe bi,mboole seen,ak muritam yi juge ci wàll yépp)
((te Yàlla may ko “Xurratu Hayni” (am mbégte) ci àdduna ak allaaxira) .
Ñatteel bi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]ci yu mujj la,da fa mel ni danu koo wonoon ne ab digam daa jotoon :
(burub nit ñi yal na la fay ngën ji fayam,te dolli la ci teralam gi ak mayam gi)
(te mu desal la fi,ngir mbindéefam yi nga xam ne,sag des moo di seenug des,xéewale la mooy xéewale leen)
(kuy jéem a tolloo’k yaw bu woomlee tam,nan lay yéege ba jot ku ko gën a woomle fopp?)
(nan lay yame kok am koomam mi ngi ci joxe ko, ak kok mi ngi ci denc ko ak làq ko? )
(ndax kuy jënde alalam ab yool ak ndam,da na mel ni ku nuur ci njaayam ma’ak njëndam ma ? )
( cam la su teddnga di feeñ bu feeñee,bu làqoo,sooroolub njèkk làqu )
(bis bu Yàlla dogalee tenqam gëbum koom,da koy dal di seddale way yalwaan yi)
(day jàppe jeexug alal,akug naaxsaayam, muy di ko jéem a màggal ak a dajale,joxe ko ci yoonu Yàlla it mu jàppe ko muy li koy yokk )
(bariwaa na ay gawar yu mel ni ay cati xéej,naaga (giléem) yi daw ak ñoom,jéggi ab àll,bob suuf sa daa mel ni asamaan sa )
( ki leen di wommat,di yaakaar ju rafet ji nu am ci moom,ki leen di gindi di kaweem gu rafet gi )
( ñu jublu ,bu nu àggee ca ëttam ba,fajug seeni aajo ci lu dul nëx-nëx,ànd ak am lu leen ci wóor )
( ayibam daal du lu dul jaamu Yàlla,ak jariñ nit ñi suba’ak ngoon) .
Aji seere ju mel ni moom cig ragal Yàlla,ak am xam-xam,te di ko jëfe ak sax ci sunna,doy na sëkk. Xam na aw yiw,ak barabam,dal di koy laabiire jaam yi,tegtal leen ko,yal na ko Yàlla fayal lislaam ak ñoñam.
Xoolal ku mel ni Sheex Sahdu Abiihi,wàlliyu wu ñépp nangulug wilaayaam,bokk ci néegub teddnga,di ci askanu Yonnant bi(j.y.m),xoolal ku mel nii wax ,bind,wesar,woy.Bokk na ci li nu ko askanale ci lénn ci ay bataaxelam,ginaaw bi mu santee Yàlla ,julli ci Ynnant bi,da ne: ab nuyyoo ngi juge ci man jëm ci Sheex Ahmadu Bamba,yal na Yàlla rëbb ku ko bañ,te rëbb ku ko waral,ma lay ñaan nag nga bañ maa fàtte,te bañ a fàtte xeetu Yonnant bi (j.y.m) .
Lii nii juge ci sang bu màgg bii,ag laabiire la ñeel xeet wi,di it ag tegtale gu muy tegtale aw yiw, di ko junj,junj gu nooy,te làqu. Mu ne ci ag xasidag ndokkeel,bi Sëñ bi dellusee ci tukk bu nu barkeel ba,ginaaw bi mu defalee Sëñ bi ag seede ci bayit,wu yàgg,muy:
( jamono giñoon na ne da na fi indi ku mel ni moom,waaye ee jamono,sa ngiñ gi amul de,kon demal kafaara ji ) .
Mu neeti:
( tubaab ya’a ko jële woon ca mbellam ya,mu mujj ca géej yooyee di wurusu ngalam ) (mu feeñe ca xori géejug mbàmbullaan ga,di wurus wow ag leeram akug xuy-xuyam tax na ba bët yi gëlëm) (mu di weer wu leer,wu fàddu ci sowwu bi,feeñaat ci dib jant cig yékkatiku ak ak tasaaroo ) (yéemu naa ci wurus wii nu jaarale cig nattu, mu mujj di wurusuw yaaxoot,wu deesul jaayante ab taar ak moom) ( yéemooti naa,na ngeen xam ne buntub tuub ak njéggal de,ubbi nanu ko,ñeel bépp murit,bu sàkku ci moom ag dëkkaale )) (ag ndokkeel ñeel na diine jii, nga xam ne mujj na di puukarewu ci yaw,ngir mbégte ak ndamu ) . Esklëy,eskëy,xoolal ma wàlliyu wu tedd wii,ga xam ne làqul lu dul ag dëggu .
Xoolal ma wàlliyu wii,Sheex Mustahiin Alkumayli,sunu mbokk mi ci Yàlla ak ci Sëñ bi,Alhaaji Muhammad Abdul Laahi doomi Ubaydur Rahmaam,nee na ca téereem ba tudd (( Annafahaat Almiskiyya Fil Xawaarix Almbàkkiya)),: bi tubaab bi tuddoon Kaylaan - yal na nu Yàlla musal ciw ayam - laajee Sheex Siidiya,lan mooy àtteb jiyaar ji jullit ñi di def ci nasaraan yi,ci jamono jii,ndax lu dagan la ,ginaaw nasaraan yi dunu leen def lenn lu ñaaw ci seen diine,ak li ni nu leen di ëpp doole lépp,ak li jullit ñi di néew doole lépp ? Mu tontoo ko la mu ko tontoo ,mu jébbal tontu bi Sheex Sahdu Abiihi,mu gaaral ko ko,bëgg mu wax ci, mu bind moom Sëñ bi,lu mel ni li Shayxaani (Buxaari ak Muslim) bindoon,jëme woon ko ci wàlliyu yi ak boroom xam-xam yiy jànkoonte ak ñu dul ñoom muy: ki bind araf yii de Yàlla def na ko muy buntub texe ak mbégte ak njèkk . Dara ci loolu jubluwu ko,ndax moom kat féex na ci fitnay àdduna ak allaaxira,atun kasasin di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk,bu feexutoon ci fitnay àdduna ak allaaxira,kon mu indi tontu bu ñatteel,waaye moom mujj na ,bokk ci ñi ñu wax ci ñoom (( bal ahyaaun hinda rabbihim yurzaquun)),muy :ñoom de fa seen boroom ñuy dund lanu,ñu leen di wërsëgal, loolu ki ko wax a ko bind di,Ahmadu mom Muhammad,mom Habiibul Laah,yal na ko Yàlla mu kawe mi musal,te nekkal ko te méngoo ko. Subhaana rabbika rabbil hizati hammaa yazifuun wa salaamun halal mursaliin walhamdu lillaahi rabbil haalamiina .
Dégg naa Sheex Mustahiin mu naan: loolu de dëgg la bu dutoon dëgg du ko bind. Dégg naa ci Sheex Bashiiru mom Sëñ bi,mu nettali jële ca Sheex Mustahiin mu ne: man de yéemu naa ci mbirum Sëñ bi,toog nanu ak moom bis ,di mbooloom boroomi xam-xam,yaakaar naa ne Abdul Laahi Ibnu Muxtaar Alhaaji,ca la woon,mu tàmbli di wax ak ñun wax ju yéeme,ju dugg sunu xol yi,ñu bégg tey dëggal te xamunu sax dëgg-dëggi li miy wax,waaye mu jàpp sunu xol yi,nu xame ca ne ca Yàlla la juge.
Sunu mbokk moomu nu tuddoon nee na ci téerem bi nu tuddoon : bokk na ci karaamay Sëñ bi,yal na ko Yàlla wattu,dellusi gi mu dellusi bawoo ca dun booba,nga xam ne kenn la fa tubaab yi masul a yobb mu dellusi . Sànni nanu fa nit ñu bari,waaye de kenn a ci dellusiwul,loolu mooy firnde li gën a mag ci ne moom demam gi moo ko tànnoon,dëgg naa ne Sheex Mustahiin mom Talha Alkumaylii,nee na : moom de bu bëggutoon a dem du dem,dunu ko man a génne it dëkkam. Te kooku doy na ndëërlaay. Sëñ bi bindal na ko ag laabiire gu mu tudde, “Diyaafatul qudoos,wa laa yashummu raaihatahaa dayfu ibliis” muy ci maanaa nganaleg Aji sell ji,ag xetam du xeeñ ganug ibliis.
Daa na siyaaresi Sëñ bi ,juge fu sori di liiru (dox ci tànkam),daan bañ bu ko Ku tedd ki masaan a jox alal,bu ko masaan a jox sijaada ngir mu ciy jullee,da ko daan jël di ko taf ci dënn bi, te daawul nangu deesi sàggane ko.
Li Sheex Mustahiin waxoon rekk, la sunu baay Muhammad Alkuntiyyu,mi nu gën a xame ci turu Bu Kunta ca Njaasaan wax, ca wetu Tiwaawon . Kenn ci taalube yi nee na ,booba dafa’a demoon di ko siyaareji,mu laaj ko Sëñ bi,te booba xam na ne mi ngi ci tukki bi,ne ko ana Sëñ bi,mu ne ko moom de tubaab yee ko yobbu,mu ne déet,bul wax loolu,mu ne ko lu may wax kon ? Mu ne ko,moom kay daa dem ligéeyi,fa ligéey ba neexe,murid bi nee booba maa ngi fi ma toog di dégg nit ñuy wax te xamuma dara ci li niy wax,mu ne ma ndax dégg nga làkkuw gaa yooyu ? Ma ne ko déedéet,mu ne ma li ko waral da dul seenuw làkk,ndax Sëñ bi njëkk muy tukki,daa samp ab làkk wërale réew mii,kenn du fi man a am benn taalube,ba kero muy ñëw,man nag samay taalube maa ngi leen jële ci ginaaw làkk bi,samay taalube dunu ñëw li feek ginaaw weer walla ay weer.
Bokk na ci kilifa yu mag yi seereel Sëñ bi,Sheex Abdalla Attamkali Addaymaani,wax na te dëggal te rafetal:
(dama ne jéngal jëm Daaru Salaam ak Tuubaa,boo ragalee ay mbamb,aki coowi jamono)
( ngir nga ame fa’b xool bu tukkee ci xawsub jamono ji,bob da nga ci ame njéggal ak’ag texe)
Ñaari bayit yii de maa ngi ko mokkale ci Sëñ bi,ndax bis da ne ma ndax xam nga ñaari bayiti Abdalla yi,ma ne ko déedéet,mu jàng leen ma dal di leen mokkal,xam it li mu doon junj ci dëggal wax ji ci nekk di “xawsub jamonoom”.
Boroom xam-xam bu màgg bi ,Sheex Abdul Laah Attandaxii Albohbiinii,nee na bi mu siyaaresee Sëñ bi Njaaréem:
(boo mujjee ñëw wàlliyu yépp, ba noppi kawe leen,na nga xam ni ngën ji mbindéef de,ci xarnu yu mujj yi la ñëw) .
Sheex Abldullaah mii de mooy ki Sëñ bi ne woon :Abdullaah ag xasida’a ngii,gog ku ko mokkal ,Munkir ak Nakiir du nu ko laaj ci bàmmeelam,Sheex Abdullaah ne laaylaaha illal laah,ana mu ? Mu ne ko mi ngi ak Muhammadul Amiin mii,mu ne giñ naa ne di naa ko mokkalloo samay doom ak samay jigéen,ak samy jaam,yu jigéen ak yu góor,mu nekk di lim rekk ak a dëël,Sëñ bi moom di ree rekk. Xasida gi mooy Jaawartu.
Sang bii moo ma nettali woon,nettali bu yéeme ba,masumaa dégg lu ni mel,da ne ma sama mbokk man dey daa am bis,may jàng li may faral a jàng bis ci Alxuraan,bi ma ubbee kaamil bi,amul lu dul Yàlla mi man lépp won ma bisub (( alastu birabbikum)) muy ba mu naan (ndax du ma seen boroom?).
Nee na ma jàkkaarloo ak xew-xew ba,gis yonnant yi,yonnant topp yonnant, yu bari yi ak yu néew yi,teg ci ma jàkkarloo’k wàlliyu yi,wàlliyu teg wàlliyu,ak seen mbooloo yu bari yi ak yu néew yi,ba mujj ma gis jenn jëmm,mooy Sheex Ahmadu mii,gox yépp fees dell aki taalubeem,mu génne ci Hadara bi ,sori’s lëf,dal di wëlbatiku ne ana ku may jottalil ab yonnee sama boroom ?,wax ko ñaari yoon ba ñatt,Yàlla tawfeexal ma, dëgëral ma,ma ne ko man,mu gestu ne ma ndax yaw la diw ? Ma ne ko waawaaw,mu ne boo ko defee de ,ba nu dem àdduna di naa la defal,di naa la defal..,mu ne ma neel sama boroom,mu dolli ma,ndax sama ñi ma topp de danoo bari te bëggaluma leen lu dul lu leen di bégloo,ak wax yu mel nii,ma dugg,ci biir,wax li nu ma waxloo woon,ma gis nu koy jox , ba ma dégg ko mu naan doy na,dal di dem.
Eskëy,moom de ci jëlewaayi (masdar) Sheex Sahdu Abiihi la bokkoon. Xibaar boobu nettaliwu ma ko kenn,lu dul ginaaw bi mu faatoo,ci ndigalm,sheex bii nag sama xarit la woon,te nekkon bu Sëñ bi,mas na maa yonni ca Sëñ ba di ko ñaan doomam,mu ne nee ko sàkkuwu ma ko lu dul ngir xér ci am lu ma jaxase ak moom ci fii ak ëlëg . Sëñ bi ne ni mu ko waxe la de,ñoom de bi ma nekkee seen réew sàkku woon nanu ma’a jox seen doom,waaye ma ne leen wuuteg aada yi moo nanguwul loolu rekk . Maandu na te dëggal.
Bokk na ci ñu mag ñi ko seereel,Alhaaji Ibraahiima Albaxdaadii,moom de ci kiimaani araab yi la woon,mi ngi juge woom Baxdaad,ku meloon ni moom ci xam-xam moom jafe woon na,Sëñ bi moom ci jëmmi boppam nettali na ma ne gis na Alhaaji Ibraahiima mii,booba gone la woon,muy tukki di ànd ak waajuram wu góor,ak Xaali Majaxate Kala,ñuy ànd ak Latjoor,bis nee na gis na ko mu toog ak ñaari sëriñ yooyu ci lalub sëriñ Buubakar FALL,yéeme lool ci barig nettaliy xam-xam yi mu leen doon defal,ci noonu Xaali manutoon a ñàkk a bind nettali yi,mu yonnee nu woolu ma,ngir ma bind xam-xam bu bari bii,mu diy woy,ngir mu bañ a sànku,ma dikk,muy wax may bind,muy lu bari ciy woy. Ma dégg ci sama waajur mu naan masumaa gis ku man a mokkale ni naar bii,ku dul Alhaaji Omar Fuutiyu,moom de jamono ju nekk mi ngi naan:Buxaari nee na,Muslim nee na.
Nee nanu bis laaj nanu ko turu buur bii,mu ne Latjoor,buur bi bég lool ci waxam jooju,bi loolu jàllee ba teg lu tollook ñaar fukki at,walla lu jege,ginaaw bi Sëñ bi jugee ci tukkib géej gi,la ñëw ci moom jébbalu,fàttali ko la xewoon bu njëkk,mu yéemu lu bari,nettali nanu ne bokk na ci li tax mu jébbalu,daa am bis mu ànd ak Sëñ bi cib tukki,ñu yendu ci ron genn garab,dëgg naa ci Sëñ bi,mu ne Alhaaji moomu booba mi ngi tux,mu génne gënn gi,am lu mu sotti ci loxoom,daa di ne ma loo wax ci lii ? Ma ne ko defal te bul laaj,mu ne ma ,duma man a ñàkk a laaj,ndax wuute gi da cee bari,ñii di ko daganal,ñee di ko araamal,ma ne ko ,bu dee noonu la deme de kon lu lënt la ci yaw,mu ne waa-waaw,ma ne ko xanaa gisoo Axdariyu,mu ne ma ahakay,gis naa ko,ma ne ko moom de nee na ca njëlbéen ga,daganul ci mukàllaf mu def dara te xamul la cay àtteb Yàlla,kon doo ko bàyyi,ba xam li ci Yàlla wax?.
Sama wax ji wedamloo ko,àgg ak moom fu sori,mu sëgg ab diir,siggi,ne ma seereel ne bàyyi naa ko ngir Yàlla,dal di jug ca saasa,suul gënn gi,ak li ci nekkoon,ca bis ba mbaa ginaaw bi la jaayante ak Sëñ bi,jébbalu ci moom .
Bi ñénn ci mag ñi yëgee ne jébbalu na,ñu tàmbli di ko yedd naan ko yaw ak sa màgg gi ak sa xam-xam bu bari bi,lu tax ngay jébbalu ci ku ñuul kii? Mu ne ko man dey Baxdaad laa juge, ni nga ko xame,yitewoowuma lu dul ku ma jox sama loxo,bari na wàlliyu mbaa boroom xam-xam bu ma romb,te xetug li may wër xeeñewuma lu dul ci moom,looloo waral ma aju ci moom, jaayante ak moom,ci noonu ñu dëggal wax ji,dogal ko ngànt.
Bi mu delloo ci Ku tedd ki,nettali ko li nu ko doon wax,Sëñ bi bindal ko lii:
Wasslaamu halaykum wa rahmatul laahi,wa barakaatuhuu,
ma lay xamal ni ca sama xasida ga tudd ((masaalikul jinaan,fii xidmatil mutahhiril janaani)) di ci maanaa,soobuwaayi àjjana yi,ci ligéeyal kiy laabal xol yi,bayit yii a nga ca:
(( Képp ku ma jorte lu dul kuy ligéeyal Ku nu tànn ki,man de dama koy ligéeyal ca la mu tànn)) ((dama koy ligéeyal ba kero may dugg àjjana,kërug sax ga,ak mébat ak xéewal )) ((képp ku yaakaar ne man na koo bégale ni,ni ko sama ligéey biy bégale )) ((na xam ne réer ak réeral wor na ko,te ci moom la ma lu dagan di dikkale juge fa boroom ba)) ((taggoon naa ko bu njëkk ca Libarwali,ag tagg gu wàlliyu yépp a ci lòtt )) ((taggoon naa ko ca Maayomba,tagg wu far samay ayib te dindi samay bàkkar)) ((taggoon naa ko fa niti Kalwaa,tagg wu ma fegali noon ak musiba)) .
Nee naa ci ligéey bi ma koy defal (j.y.m):
((ñeel na ko tukkee fi man,ab ligéey bu taqoo’k rawdatoom ba (bàmmeel),ba yawmal xiyaam te màgg)) ((sëtam ba Jiilaanii gëram na ma,yal na ko Yàlla mi ma kaweel gërëm)) ((sëtam ba Abool Hasan gërëm na ma,yal na gërëm luy saxalub taar nekk ci moom)) ((Attiijaanii gërëm na ma,yal na gërëmul kiy alag ibliis nekk ci moom)) ((ñeenti Xalifa yi gërëm nanu ma,làq naa gërëmul ñu ñu jegeel ñi)) ((ku ma gërëmul de,Yàlla Mu tedd ,mi moom gërëm na ma,ngërëm lu dul dog )) ((yal na Yàlla fay Mustafaa ngën ji pay,ni mu nangoo te amal ab dëël )) ((jullig ki nga xam ne teraangaam day daje ak man,yal na nekk ci ki nga xam ne mooy ki dëxëñ )). Subhaana rabbika rabbil hizzati hammaa yazifuun wasalaamun halal
mursaliin walhamdu lillaahi rabbil haalamiina .
Li nag booy xool ag junj la ci ne ñi ko ci doon yedd de,xamunu dëgg-dëggi mbiram,kon lu tax waxunu lu mel ne li ki leen xamul waxoon ? :
((yaw ki nga xam ne dëgg-dëggi am mbiram xamuma ko ,aka neexoon ma xam luy dëgg-dëggi mbiram)) .
Bokk na ci li nu soloo ci seere yi ko mag ñi seereel,mooy ne Sheex Muhammad mom Abiibur Rahmaan,Attanaduxii,da daan def fu nu tudde Sëñ bi ci wetam mu yëggal boppam,ne cëy cam soosu,moom dey fu ma ko nemmikoo rekk,fekk ko ci sama kanam,lu tolloo’k aw xur,walla ñaar.
Sama mbokk Muhammadu Abdur Rahmaan,Ibnus Saalik Baaba mom Halawi,wax na ma ne xalifab Sheex Ahmadu Bun Buddin,ak doomam ju màgg ja,Muhammad Amiin,nee nanu ko Sëñ bi de wilaayaam gi, indi na ci ay firnde, aki lay yu leer, ñépp gis ko, kenn ku am aw yiw dey du sikk ci wilaayaam gi.
Bokk na ci seere yi,li ma Muhammad mom Ahmad, mom Aliyu Alyahxuubii,nu gënoon koo xam ci taalubeem yi,ci turu Muhammad Tuubaa,ngir barig lu mu fa daa nekk ak Sëñ bi,li mu ma nettali woon,muy moom de bis seeti na ay nijaayam,ni nu ko baaxoowoon a defe,mu dem ca ku yéeme,ku bëgg ka Yonnant bi ak jëwrinam,di Muhammad FAAl,doomi Muhammad mom Ahmad mom Haaqil,mu yobbante ko ab nuyyoo akub siyaare ca Sëñ ba,sàkku woon it ci moom mu jox ko barkeelub mbubum njiitlaay,mu mu daa sol, ngir mu barkeeloo ko,nee na ma jotal ko Sëñ bi mu bég ci,jox ma njiitlaay lu ndaw,lu mu daa jiitloo,maanaam turki,mu ne ma gaawal jox ko ko,ma indil ko ko,mu bég ci lool,di ko foon ak a teg ci bopp bi,ag bët yi,nit ñi dégg ko,mujj ku ñëw rekk,ñaan ko,ma barkeelu ci,ba mu mujj sànku,mu sàkkuwaat ci man ma demalaat ko,ne ko nit ñi de sànk nanu sama barkeelu ba,na ma sarax beneen,ma dikk ci Sëñ bi,leerale ko ko noonu,mu bég,jox ma beneen,ma indil ko ko,mu sànt Yàlla bu baax,tagg Sëñ bi lu bari,man itam mu sat ma,ne ma boo jébbaluwutoon ci Sëñ bi de, di naa wax ci yaw kon loo xam ne !,waaye jébbalu gi tax na ma fiire la .
Bokk na ci seere yi nu tuxale ci doomi mbokkam ma,Ahmadu Yoora Muhammad : lenn ci ay àndandoom danu koo yeddoon ci néew gi mu néew lu muy siyaare Sëñ bi,mu ne leen wallaahi,bëggumaa deem di ko siyaareji te yor ci sama xol,lu toll ne fepp suuf ci bëgg àdduna,kon fii ma toog laa koy siyaaree ,eskay.Ana ku gën tedd Muhammad,moom daal doy na sëkk seere .
Néeg bii ki ci gënoon a taqoo ak Sëñ bi,gënoon cee rafet lu mu wax,mooy Ahmadu mom Abdallaah,ki bokk ak ñoom ñaar nday ak baay,moom dey moo’k Sëñ bi danoo meloon ne benn bakkan,seere naa bis Sëñ bi di jànglu lenn ci ay xasidaam,ñu jàng aw bayit mooy: ((taqdiimu Ahmadabni Habdil laahi, yahrifuhuu xayru xabiyyin laahi)),muy ci maanaa jiitalug Ahmadu mom Abdul Laahi,ku dul ab dof,buy fo xam nga ko,bi nu tuddee Ahmadubnu Habdil laahi rekk, xelam dem ci,Ahmad moomee,mu ne nanu ko ko wool,bi mu ñëwee,mu nettali ko ne tudd gi nu ko tudd,ci biir njàng mee tax xelam dem ci moom mu woolu ko, moom itam mu bég ci,sant ci. Ahmadu mii nag mi ngi faatoo Ndakaaru,bàmmeelam a nga fa,siyaare naa ko .
Bokk na ci seere yi ,li ma Abal mom Baay Addaymaanii,nettali,mu ne moom de sax na jamono ju yàgg ci,sàkku ci sunu boroom mu won ko,maqaamam Sëñ bi,mu ëppal bis ci sàkku gi,ñu ne :yeen de du ngeen xam ci Sëñ bi,lu dul bu ubee ba toog ngir daje ak nit ñi,ngeen ne kii de mooy Sëñ bi,mbaa mu ubbi mihraab bi,taxaw,ngeen ne Sëñ bi de jiite nanu,lu dul loolu ciy mbiram de,fàddu na leen.
Ma ne wax jii de niroo na ak waxi Uwaysul Xaranii,sangub way topp yi,ji mu waxoon lenn xalifa yi, ne ko: yeen gisu leen ci Yonnant bi (j.y.m) lu dul keram !,nu ne ko Ibnu Quhaafa sax gisu ko,mu ne leen déedéet . Habal mii nettali na ma karaama,gu bàyyikoo ci goroom,baayu soxnaam,mu ne moom de daa am bis mu nekk cib xaymaam,moo’k doomam,mu koy bësal boppam,ndax daa jékki-jékki woon rekk buur ,buur gu metti,te gaaw (buur = jékki-jékki rekk jug),bi mu ko defee,dal di génn xayma bi,door tànk bi cig weñ,ba nu dégg ni ci tànk bi dale,te foofa génn weñ nekku fa,ci noonu tànk bi damm,mu rot ,xëm,bi mu ximmee,ñu laaj ko,lu mu doon,mu ne daa gis aw wàlliyu wu ñuul,di Muhammad mom Mahluum,ñu jénge ko ay weñ,mu bëggoon koo xettali,door tànk bi ci weñ gi,ngir damm jéng bi,far tànk bi damm,werul ci damm-damm boobu,ba kero mu faatu,yal na ko Yàlla gërëm te nangul ko jëfam,bi mu daataa faatu,bégaloon na doomi Daymaan yi,ci ag ubbiku gu yaatu ci alal,bu wàlliyu woowu dellusee,mu nekkoon ni mu ko waxe woon.
Bi Sëñ bi dellusee,mu jël leen,bindkati xam-xam yi,ak alxuraan yi,seeni waxambaane ak mag ñi ba ci jigéen ña ak gone ya,di leen sotti ci alal lees manut a misaal, ña ca rafetle ak ña ñaawle,loolu di jàppndal akug tàggatal gu tukke ca Yàlla, ñeel leen,te di ndimbal ak sarax bu nu def ci sekkare,di ag ligéeyal lislaam it,ak Yonnant bi (j.y.m) ci xeetam wi . Ni nu binde woon la ñeneen it binde woon,ci naar yeek ñu ñuul ñi,waaye ci ñoom la gënoon a siwe,gën cee feeñe.
Bokk na ci ñu màgg ñu barkeel, ñi seereel Sëñ bi,Haamidun mom Muhammad mom Muhanda Baaba,ak doomi baay tëxam yi,Baaba ak Ahmad, ñaari doomi Mahmuud ak Haamid yi, ñoom ñépp , ñu ñu jagleel lanu woon ci moom,boroomi wax yu rafet it lanu woon ci moom .
Yàlla dogal, bi Sëñ bi nekkee Cëyéen yonni woon na ma Dagana,ba ma fa àggee,Ustaas Haamid dégg ma, booba da fa’a ganesi woon Alhaaji Bekaay SEKK,yàggul dara mu seetsi ma,bég ci dikk gi ma fa dikk,yendook man ca sama kër waajur,di ma laaj ci mbiri Sëñ bi,aki xibaaram ,yi ci di yu nu man a tas,ak yi ci di yu ñu bari mant a xam,bu ko defee muy ree rekk,bég lool ci Sëñ bi , aki mbiram, ci noonu ma won ko teereb Sëñ bi tudd “Masaalikul Jinaan”,mu sëgg ci,siggiwul ngir dara,ba kerook ngoon di jot,mu ne ma Sëñ bi de ñëw gi mu ñëw ci jamono jii nu nekk de,firndéel na yiwam wu bari wi .
Lii nag ag mosle rekk la ,waaye waxi ak seerey sangi naar yi,fii taxu koo jug, fi ko tax a jug kay mooy sunu téere bi tudd,(alminahul miskiya,fil xawaarixil mbàkkiya).
Da nanu ci dolli li nu man ci tudd murid yi ci ñoom,bu soobee Yàlla. Bokk na ci kilifa yi ko seereel,sunu sëriñ tey sëriñub jullit ñi ci Senegaal,soppeb Sëñ bi,tey mbokkam,ci jegeñaaleg diine ak askan,ak réew,Alhaaji,Maalik SI, yal na ko Yàlla gërëm te jariñ ñu ci moom Aamiin,dégg naa ko,ku dul man it dégg ko,ba xaw naa doon lu ñépp xam,mu ne: amul kénn ci nun ku dul koo xam ne,daa def lu ñaaw,ba noppi,tuub ko,te jubal,bàyyi ag dëng,ku dul Sheex Ahmadu Bamba,moom de daa judd,rekk di def lu baax ak a rafetal . Maanaam loolu mooy ñun ñi ñiy tudd ñépp de,amu ci kenn ku gisul ci boppam ab rëcc-rëcc,walla ay rëcc-rëcc,bu ko defee mu tuub ko te jubal,ginaawug dëng,ndare moom,moom dey ,am mbiram cig ndawam akug magam ñoo yam rekk,lépp ag tegu ci yoon la.Moom de wallaahi dëggal na,te laabiire.
Sama mbokk, Muhammad, mom Ahmad Aliyu Alyahxuubii,nu gënoon koo xam ci turu,Muhammad Tuubaa,xibaar na ma ne moom de ci lenn ci ay siyaareem yu mu doon def,daa romboon Tiwaawon,siyaare Alhaaji Maalik SI,bi mu xamee ne ca Sëñ ba la jëm,mu ne ko man de da ma laa bëgg a yobbante ay baat ca moom,boo àggee na nga ma ko nuyyul,te fàttalil ma ko sunu guddi ga nu bokkoon fanaan ca Ndakaaru,ci benn néeg ñun ñaar rekk,kenn ñatteelunu ku dul Yàlla,bu ko fàttalikoo ba xam ne maa la yonni ,nga ne ko,man kat maa nga ca la ma waxoon ak moom,maa nga ca kollare ga ma defoon ak moom.Muhammad nee na man de wallaahi,xamuma gan kollare la jublu ci waxam jooju,te moom dolliwaatuma ci genn leeral. Bi ma àgsee ba fàttali Sëñ bi guddi gi,ba mu fàttaliku ko,ma wax ko li mu ma wax,mu bég ci,dëggal ma te dëggal ko,tagg ko bu baax,tàmbli di coppati sama nopp bi,ak sama bakan bi,boole ca di ree rekk,ngir bég .
Bokk na ci mag ñi ko seereel ba tay Xaali Majaxate Kala,xaritu Sëñ bi,tey mbokkam ci diine ak askan,ak réew,xaritu waajuri Sëñ bi la woon,da daan def ,bi Sëñ biy jàng,saa su ko masaa na romb rekk,sànni ko aw bayit walla ab jumla,ngir nattu ci ab tolluwaayam ci nahwu,muy (xam-xamu tegi wax ci yoon) walla bayaan:(xam-xamu rafeti wax) ngir ñawal am xelam, leeg-leeg,mu génneel ko ci ab yàq,leeg-leeg,déedéet,ba mujj Sëñ bi far ko raw,bi Sëñ bi màggee ba weesu fi mu tolloon,mu mujj naan ko,yaw de doom nga woon,waaye leegi baay nga, donga nga woon it,leegi sëriñ nga,muy lu mu dëggal te fas ko ci biir ag kaf,akug woyofal .
bokk na ci li nu koy askaneel,aw bayit wu yéeme,yaakaar naa ne tàmblig ag xaasida la : (tukkee na ci man jëm ci Ahmadu Bamba,mi bàyyi nit ñi,ngir Yàlla ,mujj far di sangub nit ñi ) .
Bokk na ci li nu askanale sang bu màgg bi,Sheex Muhammadu Alfuutiyu,baayi Zannuuni,ak mbokkam ma Ibnul Harab,mi bokkoon ci jëlewaayi Sheex Sëhdu Abiihi,bayit wii,moom tàmblig xasida la gu mu defal Sëñ bi : (mi ngi jëm ci kok Yàlla da koo defal ag tàllal (ay xéewal) akug wéttal,àtteloo ko ci àddunay jinne yi ak nit ñi) .
Moom xasida gi,gu yéeme la,téewlootuma ko fii mu nekk, wax na ci, ci wenn bayit wu muy waxante ak Sëñ bi,naan ko:
( sotti leen ci seeni miskiin,desiitu kaas bi) .
Sëñ bi daan def,saa su gisee Zannuuni,defaral ko ab kaas ne ko, càkkutéefug sa baay la woon, Zannuuni mii,mi ngi bokkoon ci woykat yu mag yi,yu rafetooni woy yi,def na ab diiwaan ci tag Yonnant bi (j.y.m), def beneen ci tagg sëriñ si,rawati na Sëñ bi,mooy ki ci wax lii:
( yaw xarit bi,ndaw sa bunt bii,bari lu ko siyaaresi,ci buur ak jaraaf,ak jinne ak malaaka) .
Loolu di tàmblig xasida gu rafet, te yéeme,moo’k baayam ci jëlewaayi Sheex Sahdu Abiihi lanu,yal na leen Yàlla gërëm,mi ngi faatoo Cees,nu denc ko ci almeeri Sheex Ahmad Baru, siyaare naa ko, alhamdu lillaah.
Bokk na ci kilifa yi seereel Sang bi,sëñ bu màg bi,di Sëriñ Tayba, Muhammad Ndumbe Maar SILLA. Sëñ bi nee na ma sëñ boobu de,fu mu ma masaa na gis rekk sànni na ma bayit wii,di ci seere ci sama mbir,mi ngii: (bariwaa na baay bu yéege ci doomam,ay tundi teddnga,ni Hadnaan kawee ci Yonnant bi) .
Mu bëgg a wax foofu ne,cam sii de ab taar la,tey ag mat ñeel cosaanam.
Bokk na ci kilifa yi seere,sang bu màgg ba Alhaaji Abdulaay SIISE,mom Saalum,nekkoon na di ku rafeti wax,ak pas-pas ci Sëñ bi,am na bis aw nit di wax cib jataayam ba tudd Sëñ bi,ak jële gi mu jële wirdam wi ci Yonnant bi (j.y.m), am ci ñi teewoon ,ku ci waxe ni kuy weddi,Alaaji gëdd ko,ne ko looy wax nii ?,xanaa Sheex Ahmad Tiijaan waxul ne lenn ci ay wirdam Yonnant bi moo ko ko jox (j.y.m) ? mu ne ko ahakay, mu ne ko moom de,nekkutoon lu dul boroom xam-xam,bu jëfe xam-xamam,bu ragal Yàlla,te doon jëfe sunna, rafet gi nu rafet njot ci moom moo waral nu dëggal ko,kii nag di Sheex bamba,xanaa melul ni moom rekk,di boroom xam-xam buy jëfe xam-xamam,ragal Yàlla tey ku sunnawu,ndax kon du nu ko dëggal,ngir rafet njort gi nu dëggale woon kee ?,waa ja wedam, amul lu mu tontu . Hasbunaal laahu wa nihmal wakiil,nihmal mawlaa,wa nihman nasiiru.
Ag cant ñeel na Yàlla lii doy na ci li sama xel man a joxe,li am nag mooy,bu ma joyaloon samab gog,féexal xel mi ci mu dikke li mu wattu,ak li ma wattoo ci samag maas,ci lu wér ak lu wéradi,kon de ma indi fi gën jaa yéemey yu yéemu yi,waaye kon loolu am raddu rekk lay doon, ñax gu nekk a ciy nekk, ag jub ak ag jubadi,dëgg ak safaan,looloo tax ma tànn indi fi li ma man,teb yool nekk ci,ndax kat déet ab yool,ci lug jub nekkul,bu nu doon tollale li ma indi,ci li ma indiwul,da nga naan benn la ci junni,li ma xam it bu nu ko doon tollale ak li ma xamul,da nga naan as kook la ci géej .
Yàlla mu kawe mi,laay ñaan mu baril sama lu néew,te wisaare ko,te nangu ko,te dimble ma, moom kat mooy aji tedd jiy aji gën, kiy boroom ngënéel lu mag li.
Tàmbli nanu ko te mu mat,cig barkeel,yal na Yàlla nangu,te dimbalee,te yekkati,te wisaare,Aamiin.
Yaw buur bi, jéggal ma, ak sama ñaari way jur,te nga yërëm leen ni nu ma yarewoon may ndaw .