Sëriñ Muhammadu Faliilu Mbàkke

Jóge Wikipedia.
Dencukaay:Sëriñ Fallu Mbàkke.jpg
Sëñ Fallu

Sëriñ Muhammadu Faliilu Mbàkke (dàkkantal: Sëriñ Fallu, Sëñ Fallu, Fàllu Galas, Alaaji Fàllu) gane àdduna ca Daaru Salaam (kërug jàmm) nekk ci tundu bawol ca réewum Senegaal ci 27 ndeyu-koor (rajab) atum 1305 ci gàddaay gi yamoo ak atum 1887/88.

Mu tombe ak bis bi turandoom Sunu Sang Muhammad (jàmm i Yàlla ak xéewalam ci kawam) riñaanee ci ndingalal boroomam ànd ak sunu Sang Jibriil (jàmm ci moo) war daaba ju deesi woowe «Al-buraax», Ci rañaan googii la ko Yàlla sunu boroom joxee julliy joróom di ponk bi ëpp doole ci lislaam, waral ko ci mboolem jullit ñi, ak xeet i xam-xam yu mu fi sotti ngir nun ak ya ko ñeel ci ag jagle, Muy guddi gu màgg ci Lislaam, guddi gi nu xéewal gi dikkale juge fa Aji-Màgg gi. Sëriñ Fàllu Mbàkke génn na àdduna ci atum 1968 (dund 81 ciy at) ci ginnaaw bi mu nekke xalifab Sëriñ Tuubaa ci atum 1945 ba 1968. Sëriñ Fàllu Mbàkke mom Seex Ahmadu Bàmba Xaadim Rasuul (baayam) mi sos yoonu muriid ak Soxna Awa Buso (ndayam) doomu Sëriñ Muhammadu BUSO (Sëriñ Mbusóobe) nijaayu Sëriñ Tuubaa, Mu bawoo ci njaboot gu sell gii, di askan wu ragal Yàlla daa jàng tey jàngale, dëkkoo jaamu Yàlla te di ko jaamulu, di ay wàlliwuy Yàlla yu mat, Mu cosaano ci askanu Sëriif gog calale ga dem na ba ca Imaam Hasan mom Imaam Aliwu mom Abii Taalib ak Faatima mom Muhammad Yonentub Yàlla (jàmmi Yàlla ak xéewalam ci ñoom). Mu dondoo ci loolu (doonte ag njub déesu ko dondoonte waaye dees na ci yare, te moo baaxoo am) ag cell, Yar, xam, ngëm ak melo ya war ci doomu Soxna, ci yooyu jikko lako ay way-juram yare te nàmptal ko ci.


Am njàngam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Dencukaay:S Fallu.jpg
Sëñ Fàllu ci njàngum Alxuraan

Ci loolu mu dal jàng ci bi muy làq 8 i at, dalee ci njàngum Alxuraan téereb Yàlla bi, ci jàngalekat bu tudd Sëriñ Ndaam Abdu Rahmaan LO ca dëkkub Ndaam deesi ko woowe «Aalimun Xabiir» ak ci Sëriñ Moor Jaara Mbàkke miko tuural Alxuraanam, ba wattu Ko wattu gu yéeme ci ab taar, ba daan a wax ni:«Ku ma bokkalul jàng ci Sëñ Moor Jaara maala man ci alxuraan» ngir di wone taarub wattu alxuraan gi mu fa jële, ginnaaw bi baxoo woon na di bind ay kaamil di jox Baayam Seex Ahmadu Bàmba, ku taaru woon am mbind la, (Yàlla xéewalal na nu ba nu gis te jànge ci am mbindam), muy kaamilu alxuraan bu rafet wallaahi! te wér ci ay yàq, batay di firndéel rafetug alxuraanam, limu bind ci ay kaamil nag lotteef na ci di ko takk mbaate xayma, waaye dondoos na ci ay ñeenti fukk ci ay kaamil yu mu bind ci ay yoxoom yu bokkul, Ñaar fukk ak juróom ñatt (28) ya baayam Seex Ahmadu Bàmba la ko jox àddiya.

Ginnaaw njàngum alxuraanam jàng na xam-xamu diine ca Maam Moor Jaara Mbàkke (Boroom Saam) Ak Maam Cerno Ibra Faati Mbàkke, niki jennal Yàlla ak ngëm (Tawhiid, iimaan), Àttey Lislaam akuw yoonam (Fiq), Séllal ak jaamu ngir Yàlla dong (Ihsaan, Tassawuuf), bamu xarañe ko, Ginnaaw bi sëriñ bi jugee ci tukkib géej gi la ko mottalil xam-xam boobu ci Gànnaar ci dëkk bees di wax Xumaag, Mu ànd ak Sëriñ Moodu Mustafaa Mbàkke ak Sëriñ Moodu Roqaya BUSO mom Sëriñ Mbàkke Buso.

Ci njàng moomu nag ak yar bi, mu fàggoo ci lislaam ju mat sëkk, ragal Yàlla maandu, bëgg alxuraan, jëfe ab xam-xamam, di boroom ngor, muñ, ak jikko yees taamu. Mu doon ku xarañe làkku araab itam, ba bind na ci ladabu araab lu sakkan, ci xeet i nose di ci ñaan ak a sant Yàlla, tey julli ci Yonent bi.

Lenn ci ay jikkoom akug taalibewoom ci Sëriñ Bi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sëriñ Fàllu Mbàkke Di Ab jullit bu di doomi jullit, Nangu te seere ni: «Amul jenn Yàlla ju dul Allaa, (Yàlla aji sàkk ji yélloo wul Wayjur, mbaa doom, ëppante naak di bokkaale ak kenn, Mooy dégg, Mooy gis) Muhammad (Jàmmi Yàlla ak i xéewalam ci kawam) ndawul Yàlla la, (ndaw lumu jox Bataaxal bu ñeel nit ak jinne la,). As gor su di doomi gor, di ku sàmmu, ragal Yàlla lool, Gëm Yàlla diko jaamu, Sopp Yonent bi di topp sunnaam, Bëgg Sëriñ Tuubaa lool topp ay ndigalam, fonk ay bokkam te nawloo leen, di ab jullit bu koy jëfe, di as gor su gore, di ab jàngkat buy jàngale, di boroom xam-xam bu koy jëfe, di boroom alxuraan ci wattu ak ci bind, doon ku nangu dogal te man a muñ, doon ku yaru te daa yare, doon ku ñime njaboot te di leen taxawu, Ku woyof la woon te bëgg aw nit, ubbéeku lool te bari jàmm, ku manoona waxtaan te xarañ i wax, ku xeluwoon te daa xelale, ku xoromu te bari fulla, ku dégg wolof te man a tontu, ku bari yërmande tey jéggale, waxees nani daa tolloon ci màqaama mu kawe Yàlla, ba tax lu waay defat i neex nako, darra metteetu ko, lu waay def muni baax na, du sikk kenn du sikk lenn.

Ku Am ag taalibe la woon, ba waxees nani bi ñu nekkee Xomaag ci Gànnaar Sëriñ bi daa xëy bis woote, Sëriñ Moodu Mustafaa Mbàkke, Sëriñ Fàllu Mbàkke ak Sëriñ Moodu Roqaya BUSO mom Sëriñ Mbàkke Buso ne:

«Duma baayub kenn, mbaa mbokkum kenn walla nijaayu kenn, Jaamub Yàlla laa bu koy liggéeyal, ñi ma topp ci yoon woowii ma yeesal, ñooy samay doom, di samay jarbaat, di samay mbokk, di samay taalube»

ci loolu Yàlla xiir Sëriñ Fàllu mu ni Sëriñ bi jébbalu naa, jaay samag njuréel jënde ko ag taalube, Ba loolu sax moongi koy féddali ci ag xasidaam moom Sëriñ Fàllu naan:

«Sunug yaakar moongi ci yaw, Yaw minu ubbil wunti yombte gi, Jaay naala samag njuréel jënde ko ag Taalube, Boo ma nangulee loolu, danaa sàkku defaat ko àddiya man ame ci xar-baax».

Ku bëggoon Sëriñ Tuubaa lool, sopp ko, topp ko, yaakaar ko, roy ko, naw ko te sawar lool ci waxtaane ko, bariwaana xista yoy moo nu ko leeral, niki li xewewoon Jeewal ci tukkib Sëriñ bi ak yuni mel. Ku soppoon Seex Ibra Faal, naw ko ci ag taalubeem, daa ko roy, yittewoo aw doxiinam te daa yéem ak taalubéem, amoon it ci moom ab cer bu rëy.

Ci taalube googu la wéy di ko dunde ak way-yur wi diirub limuy dund, noonu la amewoon yitte yu màgg yu mu def ci defarug jumaay njaaréem, Ginnaaw bi fi Sëriñ bi jugee ci atum 1927, mu wéy ci yooyu tànk i taalube, topp tey déglu Sëriñ Moodu Mustafaa magam doon xalifab Sëriñ bi ca booba, ba ci ndigalul Sëriñ Moodu Mustafaa la deme demam gu siiw ga Màkka ngir aji, mottali yéeney Sëriñ bi ju ko yittéeloon te bëggoon ko ci xolam, ba daan waxni:

«Loolu ñu naa góomub deeyaale, bu ma ci amee darra sama naalub dem Màkka siyaare sama soppe ba la.»

Ba ci loolu Sëriñ bi tànnaloon boppam ñimu war a àndal ngir Aji, ñu doon: Sëriñ Mbàkke BUSO, Sëriñ Siidi Maxtaar Mbàkke Gaawaan (Maam Seex Anta) ak Alaaji Mayoro Faal, waaye njëkk muy matal yéene jooju wuyji Boroomam. Ci atum 1928 Sëriñ Moodu am yéeney yabal Sëriñ Fàllu mu ànd ak ñooñii Sëriñ bi tànnoon, ku ci nekk ci ñoom yobbaale kenn ci ag njabootam, ñu aji màkka Aj gu jéeme te bari ay xew-xew, ak i xar-baax yu kawe, Ginnaaw Sëriñ Fàllu dafa xeesoon pecc ni Sëriif gi mu doon, ak cell gi nekkoon ci moom, ba mu demee yéem na léen lool, mook ñi mu àndal ci séen i melokaan akug ragal Yàlla te xam Ko, ame baatin bu jege, te bari xam-xam lool niki Sëriñ Mbàkke mi doon ab mufti.

Waykat ba Sëriñ Muusaa KA tënk lii ci ne:[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Allaahu zóol fadlil aziim () Kum jox ngënéel deefi la yéem Faadilu mooy fadlu hamiim () Turam wi doyna xarnu bi Mooy doomi shamsun wa xamar () Mbàkkeek mbusóobe duñ ko jar Moo nàmp yaari meeni ngor () Mooy Bàmba tay ci xarnu bi Saddiiti baayam lay royaat () Leerug cosaan ga day royaat Nday jaa di xayru muhsinaat () Moo donn mbóoti xarnu bi Mooy noobalub lislaam finun () Mboolem shariif yi moo ci gën Donoy usaynu wal-Hasan () Maay xaadamam ci xarnu bi Ma wax la lëf ci ay jikkoom () Lewet woyof ànd ak sagoom Niru na baay ba mat na doom () Ëmb na kersag xarnu bi Dem na ba màkkam jullikaay () Haj na siyaare ngën ji baay Te ëndiwul alal di jaay () Nawleem amul ci xarnu bi Taalifi baayam'ay wayam () Moo donn duusi xam-xamam Moo naan ci géejug hikkamam () Sirroom ba doyna xarnu bi Yàlla na am lamuy mébat () Ci nun nu am li nuy mébat Ci moom te yal nan ami sët () Yu gën a gëm waa xarnu bi

Lenn ci ay jëfam ak i xarbaaxam:[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Xilaafa gi: Ci tànk yooyu ba ci 1945 Sëriñ Moodu Mustafaa Mbàkke wàcc-liggéey, Sëriñ Fàllu di xalifab Sëriñ Tuubaa Mbàkke, nekk ci di ko liggéeyal Muriid yépp jox ko séen kàddu, di déglu ay ndigalam, Mu sóobu ci yeggale jumaay Tuubaa ànd ko ak mboolem taalube yi, ñu topp ci ginnaawam, ngir yeggale naalub lislaam bu rëy boobii, di jumaa ji gën a rëy ci afrig, mu def ko it juróom i sooroor, tudde bu mag ba Làmp Faal ngir fàttalikoo ko Seex Ibra Faal taalubeb Sëriñ Tuubaa. Yàlla dimbali ko mu yeggale liggéey bu rëy boobii dul fay mukk ci 7 suwe atum 1963, mu ubbi ko te jiite njaalbeenu julli ga, mbooloo mu takku teew fa.

Ba mu ca jugee teg ca ni: "Fàllu neena «Galas» ci tuubaa" manaam dematu ma fenn tuubaa rekk, batax deesi ko woowe ginnaaw bi Fàllu Galas. Ci biir liggéeyub jumaa ji waxees nani Sëriñ Fàllu toog na mbooloo mi nekk ci liggéey bi di yanuy dem ak a dikk, am góor gu ca nekk di yanoondoo ak mbooloo mi, Sëriñ Fàllu woolu ko mu ñëw mu ni ko "wax ma ñaata nga fi liggéey joxees la ko ?" mu wax ko Sëriñ Fàllu jox koko muni mes! kenn gisatu ko, Sëriñ Fàllu ni: "kooku dey góor mag la (Ibliis)". Loolu di wane basiira bu xóot ci waa tasawuuf ñi, ngir gisub basiira, boo ci gisee man a xam li nga gis lumu doon, niki gisub bët, loolu basiira bu diis gann lay wone ca gaaña.

Def na ay liggéey yu am solo ci luy yokk dëkk ba, ak diko dëppale ak soxlay nit ñi, niki defar ab fooraas bi fa njëkk nekk Daaru Manaan ngir jox way-dëkk yi séen soxla ci ndox, di jottal kuraŋ ca dëkk ba, akit rëdd ak jubale penku kër ya ngir mu dëppoo ak melow dëkk ba. Sëriñ Fàllu sos na ay dëkk niki ko kilifay Muriid yi baaxoo ngir man faa yare ak a bay a ka jàngale, dëkk ya ñooy: Ndindi, Madinatu Salaam, Aaliya Mbepp, ak Tuubaa Bogo...

Sëriñ Fàllu nag moo woote màggalug Tuubaa ngir Muriid yi àndandoo defee si ko Tuubaa, ginnaaw njaalbéen ga fu waay nekk rekk, ca kër Sëriñ Tuubaa ga fa nekk walla kër seexub muriid ba fa nekk lees ko daa defe, mu mujj ko woote ci Tuubaa ngir ñépp ku ko man defee si ko fa, nu diko defe noonii ba jamono jii, ay milyoŋ i nit di ko teewe at mu nekk, ci ndigalul xalifa bu fi nekk.

Sëriñ Fàllu nag boroom i xarbaax la woon, bu waa-senegaal xamandoo, ku amoon mayug Yàlla la, May gees di wax «KUN» Fayakuun (na am mu am) nga xamni yonent bee ko njëkk a feeñal ci kaw suuf, Sëriñ Tuubaa donde ko ci moom, rafaatale ko ñenn ci ag njabootam ak i taalibeem, Sëriñ Fàllu bokk na ci ñi yoroon xéewalug Yàlla gu rëy googu, Yàlla mu yaatu mi te barile lool, rëyle, yaatule te bëgg lool ku koy ñaan, Yàlla miy wax ne: «Ngëneel (fallu/fadlu) ci yoxoy Yàlla, di na ko jox ku ko neex» di maye lu ko soob ci nguuram gu yaatu gi dul jeex walla di wàññiku, Neena ci Hadiisu Qudsi (Waxtaan wu sell) ne: ña njëkk ak ñi mujj ci nit ñi ak jinne yi mbooleséen, bu ñu taxawoon ci benn barab ñaanandoo li ñu bëgg ma mayandoo léen ko, du tax mu wàññi sama nguur gi ludul niki nga jël ab puso jam ko ci géej la cay taqe ci ndox ak la fa des noonu la li ma fajee séen ajo di toll, cey! nguuram gu rëy gii mu bokkul ak jenn walla kenn.

Sëñ Fàllu yor may googu boole ak yërmànde di ci dimbali jaami Yàlla yi, ci di léen fàggul ab taw, fu ñu ko soxlaa, maneesu la takk ñaata yoon la baykat yi ñëw ci Sëriñ Fàllu ngir ñaan loo ko ab taw, dàqal léen njéeréer yi fi teewoon, ci ay jamonoom di lekk mbayum waa-senegaal, mu dagaan ko Yàlla, mu def ko ci anam gu jéeme, akit di faj way-tawat yi ci ndigalul Yàlla.

Sëriñ Fàllu daan na wax ak mala yi, niki bu siiw bii te werloos ko: Amna bis taalube yu Sëriñ Fàllu liggéeyloo woon ay tool, te fas wa ko waroon a bay di bañ ba tax liggéey ba yeexe, xayna Sëriñ Fàllu dem fa, ñu jàmbat ko ko noonu niko moo waral liggéey bi yeexe, Sëriñ Fàllu di toŋal fas wa naan ko: "Ndax rusoo lii ? sa moroom yépp bëgg a liggéey ngir ngërëmul Sëriñ Tuubaa, yaw nga am foo ci man a bokke di bañ ! dëgg-dëgg bett ngama dé!." ña fa teewoon neeñu, fas wa daadi sëgg, ba mu tàmbalee liggéey ba nangootul a taxaw, jant so maneesu ko wàcce, mu melni ku xabtalu.

Waxees nani am na jëmm ju bawoo ndakaaru ni woon daal day jébbalu ci Sëriñ Fàllu waaye dakoy natt ci ay mbir, mu juge Ndakaaru jëm Tuubaa, ñëw ba ci yoon wi ni day wàcc gas ñatti pax, ndax Sëriñ Fàllu dina ko xam bu yeggee am déet, Mu gas pax ya, jawal tuubaa, mu yegg ag mbooloo mi bari, mu bokk ci buuxante bi, Sëriñ Fàllu toppoo naan: May léen boroom ñatt i pax ya ca yoon wa mu yegsi ! waaja yéemu, fekk xamul ni nitug Yàlla suturas Yàlla lay làmbool, maneesu koo suufeel mbaa diko wàcce, ku Yàlla yekkati la te suturaal ko.

Amna góor gu dëkkoon yaraax (nëbbees na tur wa ngir ag njabootam ginnaaw tuub na) doon kilifa lool, waaye Yàlla nattoo ko muy naan sàngara su metti te diko nëbb, bëgg koo bàyyi mu të ko, bis mu dem Tuubaa siyaare ji Sëriñ Fàllu, beru ak moom jàmbat ko tawatam, Sëriñ Fàllu neko: "waxu mala sàngara waaye lépp lu deefi xelli ci bitéel rekk dootoo ko naan" ba ni fi góor gi jugee ci 1986 darra lu deefi xelli ci biteel rekk noppi na ci, ci lu dul coobareem, ngir loolu la bëggoon te man a lu ko boppam.

Nettalees nani Sëriñ Fàllu daan na dekkal ku dee, loolu it xarbaax la bu yéeme, bu naqaree dégg te mooy li am, Kon ana gan dekkal lees di wax ? waaw lii a jar a laaj, ndax boroom basiira (ciiw) yi neeñu bakkan man naa dem ñatti yoon ci dundug nit, ci nan ? ñu ni nit Yàlla man na koo defal ay àpp ci nu mu neexe, ñatt i àpp yi man naa mucc ci ñaar yi, mooy ni:

  • Bu njëkk bi, ngir rëcc ci, day doon ku fegu, te moytu lool, di muzlu ci ay yi, Yonent bi neena:«ñi ci bàmmeel yi li ci ëpp làmmeñ moo léen fa yobbu (manaam ayu làmmeñ gir ñàkk a muzlu)»

tey sàmm bakkanam kem kàttanam, niko ko Sariya digale, walla mu am yërmàndey Yàlla.

  • Bu ñaareel bi: fàww mu doon ku set wicc, di ko sàkku ci Yàlla, di saraxe niko Yonent bi di waxe ne: «Sarax day feg dee» dee googu lay feg, akit yéene nit ñi jàmm walla mu am lool ku koy feg ci lor yi niki ab Sëriñ bu mat ba Sëriñ.
  • Bu ñatteel bi moom kenn du ko weesu, mooy dig bi Yàlla naan: «Bakkan du rot lu dul ci ndigalul Yàlla ci dig bees takk».

Dee-dee yii nag, ku koy weddi xayna, xamoo fi nu saytaane féete, Yàlla may nako ci nun, lu baree bari, man nay daw ci sunu biir dereet te yàql nu rekk a ko tax a jug ak fowe nu, ba ku dul fegu ci Yàlla, di muzlu ci moom, lu nekk man nako ci yaw, ba ci ñi am i rab aki xàmb ci réew mi, am na ci ñu am lu léen di daaneel lol man naa yobbu séenug ruuh, bis walla ay bis, ñuy door a dundaat, lu am la fi te saytaane moo léen di fowe ndax mucclu wu ñu ci, ku gëmul ni dekkal yu melnii ma wax man naa nek: Rikk! jox nu ag leeral ci lu waral ñii séen i ruuh di dem ak a déllusi ? ku weddi lëf teg fa lëf mbaa delloos fa lëf la nga fa jëlewoon rekk.

Lenn ci ay Waxam:[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sëriñ Fàllu Daan na wax ni:

  • Bu ñu nee kii doomi «diw» la, mu ne: «diw doomi ràkkal la; fexee doon ràkkal a gën»

Wax ju fees dell ak i njariñ man a jàjji bépp doomi Soxna ci mu jéema melni baayam te bañ a rekk doyloo mbaaxug baayam, ngir ni ag mbaax déesu ko dondu.

  • «Xaw a dof mbaa xaw a dee rekk a fi nekk»

Manees cee degge, kuy wut Yàlla nekk di jëf mu nduru ci nit ñi jëf i dof, moo gën ñàkk Yàlla ba ëllëg nga xaw a dee.

  • «Dee leen bëgg ndir lu waay bëgg am ca darra»

Wax ju am solaati, manees cee xame ni ci ag bëgg rekk lees di ame mboolem càkkutéef yi, ag bëgg nag ci ngëm la bokk, Yonent bi (jàmm i Yàlla ci moom) nee: «Kenn ci yéen du gëmm lu may da maa gën a bëgg baayam, doomam ak mboolem nit ñi» Lu waay bëggul def ko du ko ca may njariñ.

  • "Li baax ci mag «Këll!», «Këlëj»"

Wax ju baax ji mag ci dëgg nag, «Këll» jox ko mu lekk ba suur këll, «Këlëñ» bàyyi ko mu tëdd dallu.

  • Amna ñaar ñu yoroon ak fital (pistoler) soxla xaalis ni dañu koy jaay i Sëriñ Fàllu, ñu yegsi niko:lii de fital la da nu koy jaay, Sëriñ Fàllu ni léen ayca! defaral ma xool,

Waaji diko di defar fital gi te fekk mu jëm ci Sëñ Fàllu, mu ni ko déet jëmale ko nale, Waaja neko: déet darra nekku ci, Sëñ Fàllu niko: «waaw kon jëmale ko fi darra nekkul fii maa fi ne»

  • Amna jëmm ju masa ñëw ci Sëriñ Fàllu diko jàmbat Yaayam, naan ko dafa naqari dereet lool, ba kenn manu la dëkk am moom, Sëñ Fàllu neko: aah! mbaa du jooy guddi ?

Déggal lii tontu lu yéeme rekk! waaw! ndax kune ci nun daanga jooy guddi sa nday diko muñ ak a jug dila topptoo, nga tee koo nelaw, kon nag, lu nu ñu def bi nu màgge rekk war nanu koo muñe loolu. .........

Mottali:[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Waaw-kay! kenn ci kiimaan i Yàlla, Màndargay Yàlla yi, bokk ci ñi Yàlla gaaral sunu kanam, ngir nu am firnde ci ni, Ku defal Yàlla lii am lii, neko Sunu sang Muhammad waxe: Ku dox jëm ci Yàlla akub Yonentam; Yàlla daw jëmsi ci yaw» wone it ni Yàlla ku laabiir la, kuy maye lune, di bégal ab jaamam ci lu ko soob, Sëriñ Fàllu Mbàkke mom Sëriñ Tuubaa nag mooy ñaareelu xalifab Sëriñ Tuubaa ginnaaw bi mu wuutoo Sëñ Moodu Mustafaa ci atum 1945 ba 1968 mu wàcc-liggéey Sëriñ Abdu Laat Mbàkke wuutu ko di xalifab Sëriñ Tuubaa.

Sëriñ Muhammadu Faadl mii nag lees di defal Màggalug «Kazu Rajab» 27 ndeyi-koor ci at mu nekk ca Tuubaa, ak barab yi muriid yi féete, niki kër Sëriñ Tuubaa yi ci àddina si.

Kazu Rajab nag bis la bu màgg lool ci lislaam, ngir ni ci lees wàcce julli, ci la Yonent bi (jàmm i Yàlla ak i xéewalam ci moom) riñaane woon wuyuji wooteb boroomam ca asamaan ya, ci guddi gii la gise ak Maamam Ibraahima ak Ismaayil, am mboolem Yonent Yàlla yi (jàmm ci ñoom) jiite léen julli ca Bëyti Al-Maqdis (nee bu sell ba), ci lako Yàlla yéege ba fa moom, ñii ni gis nako ñee ni gisu ko, waaye lu ci man a am daal, Yàlla nettali na nu ni: ñëw na ba sës ci moom rikk, Yàlla gaw ko ci diggante ñaari xala niki (), loolu lépp nag Màggug guddi gi lay wone, Kon Yàlla nanu Yàlla wonale ak barkeb guddi gi, nu séddu ci, te Yàlla baaxe nu ca xam-xam boobee ci ñeeloon Yonent bi (jàmm i Yàlla ak xéewalam ci moom) kem sunu tolluwaay.

Sëriñ Muhammadu Faadl Mbàkke, noongi ñaan ci Yàlla mu dolli ay leeram, dolli koo yërëm, dolli koo gërëm te xéewale nu ci barkeem, Ci barkeb turandoom Mahammad (jàmm i Yàlla ci moom).