Nordic Africa Institute
Nordic Africa Institute – NAI – (cii suedwa: Nordiska Afrikainstitutet) Kërug gëstu la, xeltu aki xibaar ci Afrigug tey ngir réew Ërob yi féete bët gànnaar. Kër gi day amal liy gëstu ci coobareem yu am solo ci njiitéef joxey xalaat aka leeral jëlum dogal yi, aju ci defi jéegoy xam_xam yu tënku ci gëstu ci Afrigu démb ak tey.
Kërug Afrik ngir réew Ërob yi féete bët gànnaar (Nordic Africa Institute) ñu ngi ko soss ci atum 1962 dax muy jàppale ci wàllu koom réewi Sued, Finland ak Island. Danmark ak Norwes ñoomit ay bokk lanu cag njalbéen ci réew yi ko soss bokk yit ci ñi ciy jàpp ci wàllu koom waaye danu cee génn ci atum 2013 ak atum 2015. Ci yorin gi ci yëngu-yëngu gi kër gi day dox niki nguurug suwed gi wéeru ci bãxaasu bi yore li ëmbu ci bitim réew. Mu ngi nekk ca Uppsala.
Nordic Africa Institut mu bokk ci – AEGIS –, Lëkkaloog kërug gëstug Afrig yi ci Ërob. Kër direktëër à kiko jiite ak kureelug xeltu ci sémb ak gëstu seen cër di xelal njiit li direktëër.
Direktëër NAI yii fi nekk tey akk yii fi nekkon
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- Therese Sjömander Magnusson, tambale ci atum 2019
- Iina Soiri 2013-2019
- Carin Norberg 2005-2013
- Lennart Wohlgemut 1993-2005
- Anders Hjort af Ornäs 1984-1993
- Carl Gösta Widstrand 1962-1984