Niiruw jant
Apparence
(Yoonalaat gu jóge Niirub jant)
Niiruw jant cig njort, mooy niiruw gil wi nga xam ne ca la sunu nosteeg jant juddoo.
Bii xalaat-jiital(hipothèse) kii di Emmanuel Kant mooy ki ko njëkk a biral ci atum 1755, jàppoon na ne niir wi day wëndeelu ndank-ndank ci boppam, di gën di danku ak di tàcc ci sababu bijj (gravité) gi, dem ba nekk ay biddiw walla ay àdduna. Pierre-Simon Laplace it ci atum 1796 biraloon na gisiin wu ni mel.