Mikroneesi
Apparence
(Yoonalaat gu jóge Mikroneesi, Etaa yuñu Federe yu)
Mikroneesi benn la ci diwaan yi ñu seddatlee goxu Oseyaani.
Bii seddatlin nga xam ne Kureelu Mbootaayu Xeet yi moom la jëfandikoo suy seddatle àdduna bi ci ay Diwaan, gëstukat yi ñoom seddatle bu bees bi la ñu taamu, moo xaaj Oseyaani ci ñaari diwaan: Oseyaani gu jege ak Oseyaani gu sori yi Mikroneesi box.
Baatu Mikroneesi waa faraas bii di Jules Dumont d'Uville moo ko sakk ci li jege atum 1830 (moo sakk itam baat yii di Polineesi, Mikroneesi ak Maleesi), mi ngi jóge ci baati waa Geres yii di μικρος (tuuti) ak νησος (dun), maanaam dun yu tuuti.
Diwaan bi ay teemeeri dun a nga fa. Ñaari réew yu témb a fa ne ak ñaar yu bokk ci Réew yu Bennoo yu Aamerik yi:
- Guam (US)
- Duni marsaal
- Dunu Maryian gu Bëj-gànnaar (US)
- Kiribati
- Nauru
- Palau
- Réew yu Bennoo yu Mikronesi
Diwaani Oseyaani | |||
Óstraali · Melaneesi · Mikroneesi · Pacific Rim · Polineesi |