Mbootaayu Réewi Jullit yi
Mbootaayu Réewi Jullit yi gii mi ngi sosu ci saxal goo xam ne buur ak njiiti reewi jullit yi jëloon nanu ko, ci waxtaanu seen daje bi nu njëkk’a daje, te defe woon ko Ribaat, peeyub reewum Marok, ci diggante 9 – 12 /8/ 1389 g.g , deppoo ak 22 – 25 /9/ 1969 g. Ñaar-fukki reewi lislaam ak juroom bokkoon nanu ca waxtaan woowa, mbootaayug goreel Falastin (OLP) it teewe woon na ko waaye niki aji fuglu rekk .
Ndajem waxtaan moomu mi ngi amoon ci ginaaw bi nu lakkee Masjidul’Aqsaa, ci 21/8/1969 g , te ay yahuud def ko. Waxtaan wa ba muy tëj daa ñaawlu jëf ju bon jooju, nga xam ne day wone ag noonu gu nu def jullit ñi te ñàkk’a wormaal seeni gëm-gëm . ñu sàkku woon it ci Israayil mu genn ci mbooleem suufi araab yi mu tegoon loxo atum 1967 g. Te delloosi dëkkub Quds bi ci ni mu nekke woon ca xareb sue (juin) ba atum 1967 g. Mu feddali ba tay moom ndaje mi, jàpple gu miy jàpple reewi artaab yi, ci seen xeex bi nuy def ak Israayil, ak jàpple gi muy jàpple waa Palastin ci nu delloosi seen àq ak yelleef yi nu teg loxo, te goreel seeni suuf.
Kollëreg mbootaay gi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Kollëreg mbootaay gi mi ngi genne ca ñatteelu waxtaan wa jëwrini bitim reew yu reewi lislaam yi amaloon ca Jidda atum 1392 gg, dëppook 29/2 - 4/3/ 1972 g. Mu sampu woon – moom kollëre gi - ci li taxoon nu sos mbootaay gi.
Li nekk ci poñ bu njëkk bi ci kollëre gi mooy “reew yi ci bokk ñi ngi sos mbootaayug reewi jullit ñi (walla mbootaayug daje gu lislaam gi)” poñ bu ñaareel bi làmboo dali mbootaay gi aki jubluwaayam. Jubluwaay yooyu nag weesuwunu woon “ amal fi jawwu ju baax, ju nu man a dëgërale dimblante ak deggoo ci diggante reew yi ci bokk, ci seen biir, ak ci seen diggante ak yeneen réew yi. Waaye dal yi nag ñoom ci nii lanu taxawe:
- Yamoo gu mat ci diggante réew yi ci bokk
- Wormaal àq ak sañ-sañu reew mu ci bokk, ci wutal boppam mujj ga ko soob, ak bañ’a dugg ci mbiri biiram.
- Wormaal moomeelug reew yi bokk ak seenug temb.
- Dëgëral dalu dimblante gu lislaam gi, ci diggante reew yi bokk.
- Dëgëral dimblante ci diggante reew yi bokk, ci wàlli: koom-koom, mboolaay, aada, xam-xam ak ci yeneen wàll yu am solo yi, ak diisoo ak yeneen reew yi bokk ci yeneen mbootaay yi.
- Jeem a far boddante ci biiru xeet, ak sanc ci mbooleem ay anamam.
- Def lépp lu man a indi jàmm ak kaaraange ci adduna bi, ci anamug maandute.
- Dëppale ak nos ligeey bi reew yi seq, ngir njoηal barab yu sell yi te goreel leen , ak jàple waa Falastin ci seen xeex bi, ak dimble leen ba nu man’a delloosi seen àq ak yelleef, te jotaat seen suuf.
- Jàpple mbooleem reewi jullit yiy xeex ngir njoηal seen teddnga, jot seen tèmbte, dollosi seeni yelleefi reew.
- Lijjanti xuloo yi nar a ami ci diggante reew yi bokk ci mbootaay gi, lijjanti loolu ci jàmm, niki: waxtaan, dox diggante , ak layoo .
- Réew yi ci bokk, danoo war’a bàyyi - ci seeni seqoo – di jëfandikoo doole walla xuppe ci jëfandikoo ko, jëme ko ci suufus reew mu bokk walla jëme ko ag tèmbam .
Campeefi mbootaay gi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Mbootaay gi sos na ay campeef yu bari yu cosaanu niki :
- Jataayu buur yi ak njiit yi
- Jataayu jëwrini bitim reew yi
- Koolute gu matale gi
- Àttekaayu maandute bu lislaam bu adduna bi.
kureel yi ci bokk
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- Kureelu Quds
- Kureel bu sax bi ñeel wàllug koppar
- Kureelu lislaam bi saytu wàllug koom, mboolaay ak aada.
- Kureel bu sax bi ñeel dimbalanteg xam-xam ak xarala
- Kureel bu sax bi ñeel dimblanteg koom ak yaxantu
- Kureel bu sax biy yëngu ci wàllug xamale ak aada
yi bànqaasoo ci mbootaay gi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- Nafag dimblante gu lislaam gi
- Nafag Quds
- Daaray gëstu gu lim yi ak koom, ak mboolaay.
- Barabu lislaam biy yëngu ci jàngale mecce ak xarala, ak defi gëstu.
- Cëslaayu lislaam giy saytu xam-xam xarala ak suqli koom-koom.
- Barabu àdduna biy yëngu ci yar ak njàngalem lislaam.
- Barabub lislaam biy sonn ci suqali yaxantu
- Kureelu lislaam gi saytu terute gi ci adduna bi.
- Kureel adduna gi saytu ndono lu lislaam li
- Akaademi bu xam-xamu lislaam
- Jataayu lislaam bi yor tukkib jawwu bu nit ñi
- Kureelu lislaam bu adduna bi ñeel yoon
yeneen cëslaay
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Bu lii jàllee, teewul sosees na ba tay yeneen cëslaay yu bokk ci mbootaay gi, ñooy
- Banku lislaam bi
- Barabu xibaar bu lislaam bu adduna bi
- Mbootaayu rajoy reewi jullit yi
- Neegub yaxantu bu lislaam bi, ak mecce ak joqalanteg njaay yi
- Mbootaayu peeyi lislaam yi
- Suqali gu lislaam gi jëm ci boroom gaal yi
- Mbootaayug lislaam gi jëm ci yar, xam-xam ak aada.
Jagley campeef yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Jataayu buur yi ak njiit yi, mooy campeef bi ëpp solo ci mbootaay gi. Moom nag dana faral di daje saa su ko yitey xeet wi laajee, ngir gëstu ay mbiram, ak lijanti ay lëj-lëjam.
Buur yi ak njiit yi ci bokk nag, saxaloon nanu ca seen ñatteelu ndaje ma nu defoon ca Makka (mu sell mi) ak Taayif, ci diggante 19 – 22 rabihul-awal 1301 gg, dëppook 25 – 28/1/1981g, saxaloon nanu fa ne danuy def ndaje yi ñuy luy wër ci seen diggante ci ñatti at yu nekk.
Niki nu ko waxe woon, mbootaay gi, ndajeem mu njëkk, mi ngi ame woon Ribaat, diggante 9 – 12/7/1389gg, dëppook 22 – 25 /9/1969g. Mu defaat meneen ndaje ca Lahoor ca Pakistaan, diggante 29 muharram – 01 safar 1394 gg, dëppook 22 – 24/3/1974 g . Ñatteelu ndajeem mu defe ko Makka ak Taayif, diggante 19 – 22/3/1401gg , dëppook 25 – 28/1/1981g. Mu def ñeenteelu ndajeem ca Kaasa Balanka, ci diggante 13 – 17 rabiihu-saani 1404 gg, dëppook 16 – 19/1/1984g. Juroomeelu ndajeem ame Kuwet, ci Jumaadas-saaniya 1407 gg, dëppook 26 – 30/1/1987g.
Jataayu jëwrini bitim reew yi nag, mooy ñaareelu campeef bi ëpp solo ci mbootaay gi, ginaaw jataayu buur yeek njiit yi. Campeef bii nag dana faral di daje – ci anam guy wër – ci at mu nekk, ci benn ci reew yi bokk, ngir xool mbooleen bataaxel yiy doxal politigu mbootaay gi. Ak jël saxal yi war ci mbir yi am ay njariñ yu reewi mbootaay gi bokk, loolu lepp nag, fekk mu dëppoo ak jubluwaayi mbootaay gi aki bëgg-bëggam. Jataayub jëwrin yi mooy xool saxal gi nga xam ne kureelub koppar bu sax bi di na koy def, ngir saxal ko te wéyal ko. Mooy xool it njël lu yaatu lu kooluteg mbootaay gi. Bokk na ci ay ligeeyam, di sàkku ci mbootaay gi muy daje, bu jaadoo, ngir ay xew-xew yu bette, yu yitteel jullit ñi. Jataayub jawrin yi ba tay dana faral’a daje ci anam gu xotti baax, saa su ko yitte laajee.
Bu dee koolute gu matale gi nag walla, moom mooy campeef biy wéyal jëf yi ci mbootaay gi. Mi m ngi sosoo ci saxal (resolution) gu genne woon ca ndajem jëwrini bitim reew ma nu amaloon ca Jadda, diggante 23 – 25/3/1970 g. Yiteem nag mooy def ligeey yi nu ko sant, ci biir àttey kollëreg mbootaay gi. Dina dimbli tam yeneen campeef ak bànqaas yi bawoo ci mbootaay gi, ak di dëppale seeni prograam yu wuute yi. Bokk na ci yitteem ba leegi, topp ak xeeñtu saxal ak ndenkaane yi tukkee ci ñaari ndaje yii: mu mbootaay gi ak mu jëwrin yi. Kiy saytu ligeeyi koolute gi, mooy ku nu wóolu ki nga xam ne mbootaay gee koy fal, ngir diirub ñeenti at yees manul’a yeesal, bu ko defee ñeenti dimblikat ak ñeenti ñu-ñu wóolu di ko jàpple, kenn ci ñoom, jagoo mbirum Palastin ak Quds, mbootaay gi Jidda la defandi dalub kooluteem gi, ba kero nuy goreel Quds,insallaa, ngir nu def ko dal bu sax bi. Làkk yi mbootaay giy jëfandikoo ciy ligeeyam ñooy: Araab, Franse, Angle. Mbootaay gi nag mbirum Palastin yitteel na ko lool, ak mu Quds, moom mi nga xam ne moo uuf Masjidul-Aqsa, mi Yàlla teral te teral li ko wër, ak doj wu sell wa, ak miir ba nuy wax “Miiru Buraax” . Ak yeneen mbir yi aju ci diiney lislaam te nekk ci mbooleem barabi lislaam yi. Quds nag boo gisee nu fonk ko, day suuf si Yonnant bi rañaane woon yeeg, loolu nag dana waral ci jullit ñi ñu fonk ko te yittewoo ay mbiram, te aar ko ba noon yi dunu ko tilimal. Kureelub Quds mi ngi sosu ci ndigal lu tukkee ci juroom benneelu ndaje mu jëwrini bitim reew yi, mi ame woon Jidda ci diggante 12 – 15/7/1975 g. Ndajem jëwrin mu fukkeel ma nu defe woon Faas ca Marok, ci diggante 10 – 14/5/1979g, ndaje moomu dal di denk njiitug kureelu Quds bi buuru Marok bii di Asan mu ñaareel mi.
Liggéey yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- Di gëstu lay xew Quds
- Di topp ak a xeeñtu doxalug saxal yi aju ci Quds, te jataayub jëwrin yi def leen,
- Di jokkoo ak mbootaayi adduna bi, yi man a dimblee ci aar Quds
- Di wax ci lu man a doxal saxal yi ci aju.
- Di indi ag saxal ci at mu nekk guy leeral ay ligeeyam aki jëfam ci jataayu jëwrin yi.
Kureelu Quds moom, njiit la ko jiite moo ko man’a dajeloo walla lu mbootaay gi. Kureel gi nag mi ngi ame ci ndawi 15 reew, yu bokk ci mbootaay gi, yoo xam ne jataayu jëwrin yee leen di tànn ngir diirub ñatti at.