Léebu
Manees na a yër foofu, yennat ciy léeboo nga fa: http://www.au-senegal.com/-Proverbes-wolof-.html
Aduna weru koor la faw jant so nga do nga waññi bis = La vie est comme le mois de ramadan tant que le soleil ne s'est pas couché on ne doit pas compter les jours
Alalu golo ca lex ba = Tous les biens du singe sont dans sa joue.
Léébu: proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986
Am naa giléem ca Gànnaar yomb naa wax = J'ai un chameau en Mauritanie, c'est facile à dire. Léébu, proverbes CILF/edicef/ACCT. 1986
Bakkan waruw dàll la : fa muy dagge doo ko yëg = La vie c'est comme une lanière de sandale : avant qu'elle ne soit rompue, on ne peut pas savoir où cela va se produire Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986
Bala nga xam luw taat di jariñ, mbate toog jot = On ne connaît l'utilité des fesses qu'au moment de s'asseoir. Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986
Bant, lu mu yàgg cig dex, du tax mu soppiku jasiit = Un bout de bois, il peut rester longtemps longtemps dans un fleuve,ce n'est pas pour ça qu'il va se transformer en crocodile. Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986
Bëgg-bëgg yee wuute, moo-tax njaay may jar ca ja ba = Les goûts sont différents, c'est pour ça que tout ce qui se vend au marché trouve acquéreur. Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986
Bëggum ñeex duma taxa dëppoo cin lu tàng = Ce n'est pas parce que je veux de la sauce que je vais me retourner la marmite chaude sur la tête. Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986
Benn loxo du tàccu = Une main n'applaudit pas. Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986
Bes boo gis, day leb walla muy fey = Chaque jour est l'occasion d'une dette que l'on contracte ou que l'on rembourse. Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986
Bët du yenu waaye xam na lu bopp àttan = L'œil ne porte aucune charge, mais il sait ce que la tête est capable de porter. Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986
Bëtub mbëggeel jéll nab gàkk = Le regard de l'amour passe par-dessus les défauts. Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986
Béy du gëmal gënn = Une chèvre ne croit jamais qu'un mortier est vide. Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986
Boo bëggee xam luy laabiir, amal doom = Si tu veux savoir ce qu'est l'indulgence, aie un enfant Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986
Boo bëggee xam luy muñ, amal jabar = Si tu veux savoir ce qu'est la patience, prends une épouse. Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986
Bopp du ngir karaw kessé = La tête ne sert pas qu'à retenir les cheveux
Boroom ndékki ku ko jëkka yeewu tëddaat = Celui qui se lève avant le responsable du petit déjeuner peut aller se recoucher. Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986
Boroom tubéy, bu jàngoo sol = Le propriétaire du pantalon, après s'être lavé les pieds, c'est lui qui le met. Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986
Bu daay také ceeli yendo naaw = L'épervier passe la journée à voler quand la brousse est en feu
Bu la am-am taxa bew, ndax ñàkk du wees = Il ne faut pas être fier de sa fortune, car un revers peut toujours arriver. Léébu, proverbes wolof. CILF/edicef/ACCT. 1986
Bu lëk lékkee olom nako gërëmee coy =
ñaara mën k&nn te ñëtt du bëre =
Lu kénn mën ñaara koko dàq = Ce que peut faire une personne, deux sont meilleurs que lui.