Këwsu
Këwsu garab la gu bokk ci njabootug moracées. Moo ngi bàyyikoo ci dëkki Asi yi. Garab la gog ci ay bot lañ koy jëmbët, ci réew yi xaw a tàng. Xeetu garab la gog bareetul ci foofu mu cosaanoo muy Asi.
Melo
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Këwsu garab gu mag la, day màgg màgg gu gaaw. Guddaayam mannaa toll ci 30 ba 40i Met. Xobam day nëtëx fu mu toll. Garab gi bu màggee day am ay doom. Doom yu ndaw yi seen guddaay 1 jàpp 2i sàntimet lay toll. Garab gi xob yu mag yi seen guddaay danay toll ci 10 jàpp 35i ci ay sàntimeet. Seen yaatuwaay moo ngi toll ci 5 jàpp 15i ci sàntimet. Garab yu ndaw yi seen xob mooy gën a gudd, Xob yi ñoo ngi màgge ci biir lu mel ni mbaxana. Mbaxana moomu day màgg ni xob di màgge. Bu demee ba xob wi mat, mbaxana mi day daal di rot. Garab gu bari ay reen la.
Njariñ yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Këwsu dees na ko jëfandikoo ngir rafetal ay barab.
Nataal
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]-
Xobi garabug Këwsu
-
Car bi
-
bàrtt bi
-
Doom yi
-
Doom yi batay