Jolof
Jolof moo doonoon nguur ngi gënnoo na mag ci Senegaal ci jamono yooyu. Mi ngi sosu ci xarnub XIV ba Nguuru Mali gu mag ga saayee, rawati na la feete woon ca sowam. Ba nguuru Jolof taxawee, jëloon na melokaanu nguur yi ko jiitu woon, waaye bàyyi woon na fa melokaanu càmm ak màng ga xewoon ci jamono.
Sosteefam
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ki ñu ne moo sos nguur googu mooy Njaa Jaan Njaay. Mooy doomu araab la bu ñuy wax Abaabakar ak Lingèer ab Tukulòor bu tudd Faatimata Sall. Moom, Njaa Jaan Njaay, def na ci réew mi liggéey yu réy.
Bokk na ci def wolof yi ñuy benn, teg réew mi ci yoonu nguur gu leer. Samp nguuru Waalo ba mu dëgër, mu dal di koy jox rakkam. Sos nguuru Jolof gu mag ga ba mu yegg fa gën a kawe mu door a wàcce boppam. Looloo tax ña ko wuutu ñoo mottali liggéeyam ci xarnub XIV, waaye jotu ñoo moytu taste gu gaaw ca nguur gu mag ga.
Boo seetloo turi buur yu njëkk yi ci nguur gu mag gi di nga leen fekk ñekk fukk doŋŋ. Seen péey nekkoon na Céŋŋ ca jamonoy Njaa Jaan Njaay. Réew yu bari nekkoon nañ ci kilifteefu gu mag ga. Lu mel Senegaal ak Gaambi ak Faleme nekkoon na ñu ci suufu Jolof gu mag ga.
Buuri ñu mënoon fal ngir elif nguuru Jolof, dañu doon wara bokk ci juroomi meen (wallu ndeey) yoyu, sant: Njaay, Joob, Faal, Ndaw, Ñaŋ. Ci xeeti Seereer ak Pël, lañu joge.
Buuri Jolof yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]1.Njaa Jaan Njaay | 20.Lat Samba |
2.Saare Njaa Jaan | 21.Giran Buri Jaleen |
3.Ndiklaan Saare | 22.Biram Penda Paatar |
4.Ci Koli Ndikaan | 23.Biram Mbakori Penda |
5.layti Ci Koy | 24.Bakan Tamyagu |
6.Jilaan Mbay layti | 25.Amadu Sayxu |
7.Birima Njèeme Ileer | 26.Lan Kodilu Majigèen Ndaw |
8.Tasi Dagotin | 27.Mbakam Baas |
9.Biram Kura Kan | 27.Mba Mbari Njubu |
10.Bukari Biige Sanguleen | 28.Biram Kumba Gey |
11.Biram Njéeme Kumba | 29.Al butaam |
12.Lele Fuli Fakk (1549) | 30.Bakko Koddu Biige Faakonte |
13.Alburi Saar Ndaw | 31.Biram Aram Xureyja |
14.Alburi Njaay | 32.Baane paale Kumba Ngoye |
15.Baka Penda Xule | 33.lan Koddu Majigéen Baay Faal Maalig |
16.Baa Kantam Gan | 34.Biram Jigéen Baay Faal Maalig |
17.Alburi Jaxeer | 35.Alburi Baay Birima |
18.Biram Jigéen Ndaw | 36.Tanoor Faatim Jeng |
19.Brawa Keme | 37.Bakan Tamxari Jaboor |
Nguuru Jolof
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Jolof boo ko dee xool dafa këll bunom dem na ba lag da geer, égg na Ferlo. Moom dafa xawa uuf Tooro ak Dimat ak Waalo ak Kajoor ak Bawol ak Siin-Saalum wàllu penku wi ndand féy-féy la. Jolof fu neew ñax la, bari na lool garabi werek. Mel na ne du fu naat it ndax ab woykat bu siiw ci yu wolof yi di Sëriñ Musaa KA am na fu muy melale lu ni mel ci genn xasidaam, mu ne : nawet Jolof noor fa te doo nooraani - ndaw lu ca sax soo màggatee yalwaani
Kon du war a nekk fu bari ay balluwaayi xéewal .
Ay way dëkkam
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Waa Jolof nekkoon nañu ay giir yu wuute, booba ñu ngi ci seen joge bëj-gànnar jëm bëj-saalum: giir yooyu ay Séeréer lañu ak ay Wolof ak ay Tukulòor. Naari gànnar yi daana ñu song ñi dëkk ci tàkkal dex gi. Nee nañ ki fa njëkk a dëkk mu ngi tudd Njolofeen Mbeng, mu ngi bokk ci xeetu Màndeŋ. Turam la ñu jox nguuru jolof. moo fa njëkk a sos dëkk bu ñu daan wooye Kàyti, moom mu ngi nekkoon ci Yeŋ-yeŋ.
Jolof gu màgg ga
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Fuuta moo doon gën jaa màggi réew ci mbooleem gox yi. loolu masu la deñ ba ci fukkeelu xarnu ak ñeent, moo tollook falug waa Tonjon.
Jamono jooju la màndeŋ yi yaatal seen nguur gu mag dale ca géeju Atlas ca bëj-gànnaar ba bëj-saalum ca Gàmbi. Ca jamono jooju yit la nguuru jolof nangoo boppam, moo gënoon a am solo ci réewu Wolof yi ak Séeréer si ak ci mbooleem réew yi ci géej gi, ci li ko dale ca bëj-gànnaar ba bëj-saalum, Fuuta ba Saalum. Ëmboon na Waalo, Kajoor, Bawol ak rèewi Séeréer si ak lenn ci Fuuta Tooro.
Saayug nguuru Jolof gu mag ga
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Rèew yu bari nangu nañ seen bopp ci nguuru Jolof gu mag ga. Kajoor njëkk a nangu boppam topp ca Waalo ci njiitu Barag. Bawol ci njiitu Teeñ. Rèewi Sèeréer si ci njiitu Buur. Jolof mujj na nekk réew ni yeneen yi ci xarnub XVI ba XIX. Waaye Dammeel moom moo gënnoona metti ag jàmmaarloo ak Burba jolof ca xareb Danki ba nga xam ne moo njëkk a faagaagal nguuru Jolof gu mag ga. Ganaaw loolu la xareb Mbisin ca 1697 foofa kajoor moo Jekku, ak xareb Ambaal ci 1760, ak xareb 1886.
Ngirtey saayam
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Bok na ci li ngirteel saayam, ñaari noon yu doon xëccoo nguur ga ñaarelu xaaj bu xarnub XIX. Noon bu njëkk bi mooy Tanoor Jeŋ. Ñareelu noon bi mooy Amadu Sayxu.
Tanoor Jeŋ doomi Lingeer Kura Ngoy, song na Buurba ngir nangu nguur ga. Ginaaw bi moom Amadu Sayxu nanguwaat ko ci 1870. Yor ko ba ci atum 1875, ci at moomu lañu ko jekkoo ca xareb Sàmba Saajo. Ci noo nu la Jolof tàbbee ci loxoy Faraas ci 18 rakki gammu 1885.
Delluwaay
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Paate sow, Démbi Senegaal: ci làmmeñu Wolof, Dakaar, 1998
Lëkkalekaay yu biir
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Téerekaay
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- Samba Lampsar Sall, Njajaan Njaay. Les mythes de fondation de l’Empire du Djolof, Dakar, Université de Dakar, 1982, 157 p. (Mémoire de Maîtrise)
- Mbaye Thiam, Le Djolof et Bouna Ndiaye, Dakar, Université de Dakar, 1976, 110 x.
- Eunice A. Charles, A History of the Kingdom of Jolof (Senegaal),1800-1890, Boston, 1973, 280 p.
- Eunice A. Charles, Precolonial Senegal: the Jolof Kingdom 1800 to 1890, Boston, African Studies Center : XII-163 p. African Research Studies, n° 12.
- Victoria Coifman-Bomba, History of the Wolof State of Jolof until 1860 including comparative data from the Wolof State of Walo, Madison, University of Wisconsin, 1969, 395 x.
- Jean Boulègue, Le Grand Jolof (XIIIe-XVIe siècle), Paris, Façades, 1987, 207 x. tome 1 : Les anciens royaumes wolof (Sénégal) (Thèse d’Etat publiée en partie)
- Patrice Mingou, Le Jolof de 1870 à 1895, Dakar, Université de Dakar, 1977, 111 x.
Seetal BUNTU TAARIIX |