Aller au contenu

Jalambaan

Jóge Wikipedia.
Garabug Jalambaan

Jalambaan as ngarab la su am ay xop yu sew yu toll ci ñeent ak xaaj, ba ci juróom-ñaar ak xaaj, ci ay met waaye néew na lool lu muy yegg fukki met ak juróom. Garab gi noo ngi koy fekk lu ci ëpp ci àll bi di ko jëfandikoo ci wàllug paj walla ci ay jumtuwaay. Bantu jalambaan bokk na ci li ëpp dayo ci liy jóge ci Afrig boole ko ak ay jumtuwaay yu bari yu nu ci man a jële. Bokk na ci it yi ñu gën a jox cër gën koo yittewoo ci wàllug yattum bant ci wàllum defar ay jumtuwaay yu jëm ci wàllu misig ñu di ko jaay ci àdduna bébb ci lu ndaw waaye ci njëk lu kawe.

Dëkkuwaayam garabu jalambaan man nañu koo fekk ci gox yu bari ak ci dundiin wu wuute man nañu koo fekk ci suuf su wow walla suuf su xaw a tooy dana ñu ko fekk it fu am i xeer waaye fi ëpp ci fi ñu koy fekk mooy cib àll ci àll boo xamentani lu ëpp ci garab ya séeni xop day sew walla fu jége géej.


==Melo wi== Xooxi jalambaan yi buñu leen génnee ci koog yi ñu nekk ba ji leen dina ñu gaaw a sax. Da ñu leen di teg ci kaw ub car ngir ñu wow ba laa ñu leen a weer ci naaj wi. Dina ñu sax juróom-ñatt jàpp ñaar fukki fan bu ñu ko jiyee ak it lu tolloog juróom-fukk ci téeméer bu ne ñu man a dund séen ug màgg nag gaawut lool ndax man nañu dem ba ñaari at toll ci fukki sànt-met ak ñaar yépp ci reen yi lay nekk.

Ay ñariñam

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Li ci njëkk ci njariñ yi ci wàllug paj nee nañu reeni garab gi boo ko jëfandikoo dana ray ay saan dana yokk it ngóora góor, ku ko togg it man nañu koo jëfandikoo ngir fàggandiku ci ëmbu jigeeen buy yàqu walla faj biir buy metti walla biir buy daw walla faj xeeti feebar yiy juddoo ci sëy. Bant yi boo ko lakkee saxar si nga noyyi ko man naa faj bopp buy metti walla soj walla xeeti sëqat yu metti yi. Xas mi ak reen yi bu ñu ko boolee ci paj um cosaan man naa faj biir buy daw bu ñu ko boolee ak buy.

Batay ci wàllug paj xas mi ku ko jël dëbb ko ba mu mokk ba mu xaw a nooy man nañu koo faje góom ku jël xop yi it dëbb ko ba mu nooy man naa faj ay metiitu yax walla ay teq ak yu ni mel ndox miy génnee ci garab gi nu koy wax njoy-njoy ak ci xop yi man naa faj gémmiñ guy nàcc mbaa gu sofe walla it put guy xasan Batay ci xas mi as lëf ci xas mi wane nañu ni man naa faj lu jëm ci ay mikrob te it man nañu cee faj ay gaañu-gaañu.

Ci wàllu jëmbat garab gi, garabu jalambaan man naa doon luy gën a dundal suuf yokk ak mbaaxam man nañu koo jëfandikoo it ngir fàggandiko dees na ko jëfandikoo it ci sàkket yu dëggar.

Yaneen i njariñ ci jalambaan, léppam day jëm ci bantam ndax bant la bu njool xaw a jàpp ... leeg-leeg mu dër lool walla mu jël yeneen wirgo. ay bantam man na dem ba ci fukk ak ñaar ci ay sànt-met, bantam nag dana niin dëgar lool duy gaaw a dammu, man naa it fàggandiko ci ay yàq-yàqu yu mel ni ay max añs teg ci it neex a jëfandikoo te rafet lool ba tax na dañu koy jëfandikoo ci jumtuwaay yi ñuy defe misig ak bant bi ñuy doxe nu koy wax dokk dees na ko jëfandikoo fii ci Senegaal ci yu bari lu ci mel ni kurus ak yat ak jaaro añs.

Turu xam-xam

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Dalbergia

Wàllu garab