Aller au contenu

Germaine Acogny

Jóge Wikipedia.
(Yoonalaat gu jóge Germen Acoñi)

Royuwaay:Infobox Musique classique (personnalité)

Germaine Acogny, ca Benee la juddoo ca atum junni ak juróom ñenti téeméer ak ñent fukk ak ñent, ab fecckat ak naskatu pecc di doomi Farãas ak Senegaal, di jëmm ju am mboor (taariix) ci wàllum pecc ci Afrig ginnaaw bi mu ubbee bulub feccukaay bu njëkk ci Afrig ci atum junni ak juróom ñenti téeméer ak juróom benn fukk ak juróom ñatt, ci Ndakaaru.

Germaine Acogny, doomu Togun Serwee Akoñi la, nekkoon liggéeykatu nguur ci jamonoy nooteel te bind « Nettali Aloofo », delloo na ko njukkéel ci po mii dii « À un endroit du debut »[1]

Sos na ab barabu feccukaay[2] ci Ndakaaru ci atum junni ak juróom ñenti téeméer ak juróom benn fukk ak juróom ñatt.


Ci diggante atum junni ak juróom ñenti téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróom ñaar ak atum junni ak juróom ñenti téeméer ak juróom ñatti fukk ak ñaar, jiite na Mudra Afrique bi Maurice Bejart ak njiitu réew mi woon Leopold Sedar Seŋghor sosoon ci Ndakaaru.


Ca atum junni ak juróom ñenti téeméer ak juróom ñatt fukk, mu génne téereem bii di « Peccum Afrig » ci ñatti làkk.

Ginnaaw tëjug Mudra Afrique, la dem jàngale ji ca L'Isle-Jourdain, digganteem ak Toulouse[3] tolu ci fan wer i kilometar ak juroom, ginaw bi mu dem dëkki ca Bruxelles andadook Maurice Bejart, di amal ay ndajey peccum Afrig ci àddina wërngal kapp, mu doon ndaje yu am solo ci saa-Órob ya.


Ca atum junni ak juróom ñenti téeméer ak juróom ñatt fukk ak juróom, moom ak boroom këram, Helmut Vogt ñu sos «bulu-lekoolu pecc ak tiyaatar bu ñatteelu àddina» ca Toulouse.

Ci atum junni ak juróom ñenti téeméer ak juróom ñent fukk ak juróom, Germaine Acogny, jëloon dogalu ñibbisi Senegaal ba ca atum junni ak juróom ñenti téeméer ak juróom ñent fukk ak juróom ñatt, mu sos mbootaay gii di Jant-Bi/lekoolu suuf si ( l'Ecole des Sables).


Ca atum junni ak juróom ñenti téeméer ak juróom ñent fukk ak juróom ñaar ba ci atum ñaari junni, la ñu ko tabb njaatige ci fànnu pecci Afrig yi ñuy fent ca Pari ak ay ndajey pecc yu bees yu Afrig.


Ci atum ñaari junni ak ñent mu dallo am màkkaan mu ñeel àddina wërngal kepp te di yëngu ci peccum Afrigu démb ak tay mu tuddee ko Lekoolu suuf si, féete ca Tubaab Jalaaw.


Màkkaan moomu amoon i jafe-jafe si wàllum koom ci njeexitalu atum ñaari junni ak fukk, ginnaaw bi mbootaayug Olànd gii di Dowen dakkalee ndimbal[4] li mu ko doon jox.


Germaine Acogny jot na ay mbandal yuam solo yi ñuy takkal nit ñu ràññeeku ak nit ñu jàmbaare ci fànnu mbatiit yu réewum Farãas ak réewum ci Senegaal.

Ci atum ñaari junni ak fukk ak ñent, bokk na ci juróom fukki jëmm yi ñuy gën a bàyyi xel ci àddina bi, këru caabal gii di, Jeune Afrique[5] tabb koko.


Ci atum ñaari junni ak fukk ak juróom ñent, mu feeñ ci film boobu di ''Yao'' te Omar Si doon si jëmm ji ci gën a fés.

Ko 17 2021, moom ko gaynde d'or de la pecc par la Biennale de Venise.

Pecc yu ëpp solo yi mu bind

[Soppisoppi gongikuwaay bi]
  • 1987 : Sahel,, feccu benn nit, mu bind ko fecc ko it
  • 1994 : Yewa, Eau sublime Ndox mu gànjaru
  • 2004 : Fagaala, powum fecc ak Kota Yamasaki, ñu jagleel ko rayante ga woon ca Rwanda
  • 2007 : Les Écailles de la mémoire ak Jawole Willa Jo Zollar
  • 2007 : Waxtaan, di càmbar ci nguur [1],
  • 2016 : À un endroit au début ,Ab barab ca njëlbéen mu nas ko ak Mikaël Serre


  1. «  » [archive], sur www.lafermedubuisson.com (consulté le 17 mars 2016)
  2. Virginie Garandeau, , dans Béatrice Didier, Antoinette Fouque et Mireille Calle-Gruber (dir.), , Éditions des femmes, 2013 (lire en ligne [archive]), p. 38.
  3. «  », Le Monde,‎ 1er octobre 1994 (lire en ligne [archive])
  4. Salma Niasse Ba, «  », Le Monde,‎ 13 décembre 2018 (lire en ligne [archive])
  5. «  », Jeune Afrique,‎ 27 avril 2014 (lire en ligne [archive])