Fànn
Apparence
(Yoonalaat gu jóge Cosaan, Fànn)
Fànn, ci tekkeem gu yaa, dafa ëmb bépp yëngu-yëngu nit - muy lu kenn walla mbooloo di def - moom, su sukkandikoo ci gisiin yu xereñ, ñaw ak doxaliin wu bawoo cim njàng walla cig yàgg-jëf, mooy tax a man a biral genn kàllaama gu taaru gi. Ci fireem gu tay, fànn dees koo féetale ak man-gee jokkaley yëg-yëg, ba tax kàllaamay fànn, donte dañuy jokkaley bataaxal, taxul ñu doon dëgg-dëgg aw làkk, ndax taxawuñu ciw yoon wu ñépp ànd déggoo, xanaa kay safaan wa ku nekk ak sa gisiin walla déggiin.
Cosaan, Fànn
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]
Xool it Wikimedia Commons
|