Aller au contenu

Sancug waa Tugal ci Afrig

Jóge Wikipedia.

Canc nag dees na ko xamalee ci ne mooy teg loxo gi réewi ndefar (endustri) yu mag yi tegoon loxo mbiri koom-koom yi ak yu politig yeek aada ci réew yu bari ci yu amadi-doole yi ci àdduna bi. Rawati na yi ci di yu woomle ci wàllug mbay ak mbell. Looloo tax sanc - ci maanaam mii mu yor – du lenn lu dul luy yëngu ci nangu ak fëkk alali jàmbur ak ngacc dooley mbindeef yi ak jariñoo leen.

Li sikk amul mooy sanc gi toppoon ci yewwuteg ndefar gi ci Tugal, rawati na ci ñaari xarnu yii di bu fukk ak juroom ñeent ak bu ñaar fukk, sanc gii de ay reenam tàlliku woon na di dem ba ca yëngu-yëngu yu wuññiy melosuuf yu Tugal yi nga xam ne dees leen di jàppe ñuy bunt bi ñu jaare bay dugg ci sanc gu yees gi Tugal doon def ci réewi àdduna bi.

Sababi sanc gu bees gi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Li sabab sanc lu bari la te lënkaloo, ñu tudd ci yi ci ëpp solo yii:

  • Màgg gu gaaw gi ba ëpp ci wàllug ndefar (industrie), ci lu bari ci réewi ndefar yu mag yi. Loolu nag tax ba réew yii mujj soxlawoo ay ñumm aki ja. Tax na tam ba ag gëpplante gu tar te metti am ci diggante réewi ndefar yu mag yi, jëm ci yaatal seenug kilifteef ak sañ-sañ ci gox yi leen man a warlul ag yokkute ci wàllug ndefar, ndax seen koom-koomu xeet wépp ci ndefar la tegu woon. Li juddoo ci loolu nag lu mujjoon metti la ci réew yu néew doole yii nga xam ne yu mag yii dañu leen tegoon loxo, ngir muucu seen njariñ yeek ne-ne yu ñumm yi, ak ngir def leen ay ja yu mag te yaatu, yu ñu man a jaaye seen njuddéefi(produits) Tugal yu ndefar yooyu.
  • Yokku gu ñi dëkke ci réewi ndefar yi yokku woon, loolu moo waraloon réew yii gëstuji woon fu ñuy wàññi seen ëppiitum askan moomu, bu ko defee ñoom ñu man leen a nekkal dib jumtukaay bu am solo buy dëgëral seen koom-koomu réew miy nday. Laaj na ñu xamal leen ne politigu génne ëppiitum askan boobu ak sotti leen ci réew yi ñu sanc, politig la bu ñu nosoon, jublu woon ci liggéeyal xemmeemtéefi sanc yu reewi ndefar yi amoon way dëkk yu bari woon ba ëpp.
  • Bëgg a soppi nit ñi def leeni nasaraan (nasaraanal), ak wisaare diiney nasaraan ci kaw-kaw yi, ak ñu xamul ñi. Nga xam ne nasaraanal bokk na ci sabab yi gën a rëy yi waral wuññiy melosuuf yu Tugal yi am, te ñooy li ubbi buntub sanc. Waa Tugal yi jëfandikoo nañu diine niki ab raas bu ñuy jaare ngir àgg ca seen bëgg-bëgg yu sanc yi, yu politig yi, ak yu koom-koom yi, ak doonte danoo làqoon loolu, bu ko defee mbubboo seen wax jooju ñu daan wax naan: «Wisaare ag nasaraan du lu dul xayal ak yiwal nit ñu deltu ginnaaw, ñi xamul dara». Àdduna bi nag sonne na bu baax ci par-parloo ak boddanteg diine ak xalaatu maa-la-gën bi réewi nasaraan yi ame woon jëm ci yeneen askan yi dul ñoom.
  • Wàññiku gu tar gi amoon ci ñi dëkke woon ci kaw gi, ci réewi Tugal yu ndefar yi, taxoon ba jafe-jafe am ci wàllug dundub mbay ci réew yii. Loolu yóbbu woon na réew yii ci ñu wuti bii dund ci réew yu néew doole yii nga xam ne mbay amoon na fa doole. Réewi Tugal yi nag jaaruñu woon ci yoon ngir am seen càkkuteef loolu, ci misaal manoon naño jaare loolu ci yaxantu, waaye kay dañoo jëfandikoo doole ak noot ak sanc, sukkandiku ci seen dooley xare ji, ak séen ñawug ngànnaay, ak néew dooleg geneen wàll gi mu fas yéenee noot, loolu mooy li ko dimbli ba mu man a am bëgg-bëggam yooyu ci kaw askan yu doyadi yi.
  • Lu bari ci réew yu mag yi, li leen doon defloo sanc googu mooy feeñal ag yëg-sa-bopp, aakimoo mbir yi, ag rëy ci wàllug xeet, yaakaar ne ñoo gën, yooyu nag ay jumtukaay lañu woon ngir wone doole ak màgg gi nga xam ne réewi sanc yii màggoon nañu ko te ame ko ni doole.
  • Ay lonkoo(société) yu Tugal ak yu dul ñoom, yu mag feeñ nañu ci biir yewwuteg endustri gi. Dajale woon it alal ju bari, ba gisoon ne leegi dañu koo war a meññali ca réew yay màgg, ci wàlli koom-koom yi. Ci noonu lonkoo yu àdduna yu mag yi tàmblee gëpplante ci meññilu alal yooyu, loolu nag jur ag jongante gu mag te tar, ba mujj sax yii lonkoo tàmblee sàkku ci seeni goornamaa ngir ñu jàpple leen te dëgëral leen, loolu tam daan yóbbu goornamaa yi ci ñuy aar seen njariñu lonkooy réew. Loolu nag nooyal na yoon wi ba xeetu sanc gu politig man a taxaw, di lol gëpplanteg koom-koom a ko fi indi.
  • Bëgg gi réewi sancaan yu mag yu bari bëggoon a dëgëral seen yoonu jokkoo gu àdduna, loolu yóbbu leen ci ñu teg loxo yenn yoon yu strateji yi, ak waax yu am yi solo, ak yoon yu mag yi am solo ci wàllug jokkoo gu àdduna gi, di taqale diggante goxi àdduna bi.
  • Bëgg gi yenn ci réewi sancaan yu mag yi bëggoon a tas seeni xalaat, aki dal (principe) yu seeni làngi politig, ak seeni aada, jàppe loolu nag ab jumtukaay buy liggéeyal seeni xammemteefi sanc.

Anami sanc gi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sancug Tugal gi dafa jëloon ay melo aki anam yu wuute, yoo xam ne xew-xew ya peegoon te yiiroon réewum sancaan mi ak mi muy sanc, xew-xew yooyu dañu doon jeexiital ci ñoom, bu ko defee sanc gu bees gi dikk ci ay anam yu bari, ñu tudd ci yi ci ëpp solo yii:

Sanc ngir dëkk

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Xeetu sanc gu ñaaw gii feeñ na ci ginnaaw yëngu-yëngug wuññiy melosuuf yu Tugal yi. Bu ko defee réewi Tugal yiy wuññi, daal di taxaw ci néewal doole ñi cosaanoo woon ci réew yi ñu wuññi. Jaare ko nag ci di leen dàkku ak a génne seeni réew, ak di leen alag ci xare yi, di leen toraxal, di leen seeyal ci biir mboolaayi réew miy sanc, maanaam di leen def daanaka ñuy ñenn ci ñoom ci wàllug aada, deesu leen manatee ràññale.

Xeetu sanc wii mooy li waa Espaañ defoon ca Endo yu xonq ya ca Diggu Aamerik ak ca bëj-saalum ga, bi nu leen sancee te dëkke leen, taxawal fa ay sancu, mujjoon nañu cuub gox bii ci cuubug Espaañ, ginaaw bi fi ay waa Espaañ jëlee barabu endo yu xonq ya fa cosaanoo, mel ne leegi fa lañu cosaano, loolu di ci Diggu Aamerik ak bëj-saalum gi, lu ci dul Beresil, moom waa Portigaal a ko sancoon.

Nu mel noonu la sahyooni yawud yi defoon ca Palastin, bi ñu ko sancee ci doole, dëkke ko, réewi sancaan yu mag yi jàpple leen ci, Britani nekk ca bopp ba. Ci noonu la yawud yi tasaaroo woon ci àdduna bi, dajee, dëkksi ca Palastin, ginnaaw bi ñu leen fa gàddaayalee jëme, ci ron aarug réewi sancaan yi, ak li askanu Palastin daan xeex loolu lépp, te daan ci jiyaar ngir bañ ko.

Nii it la sancug Tugal gi meloon ca Afrig gu digg gi, ak Rodisiya, ñu fay teg doomi Afrig yi lu sakkan te lëw ciy coona, di leen noot, di leen teg loxo, di leen tiital, di leen tàqale ak a gënale ci wàllug xeet, ak lu bokkul ak loolu lepp ci anami mbugal yu tar te mbaam-àlle.

Teg loxo gu xare

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ay réew yu sancaan jug nanu, teg loxo ay réew, nangu leen ci doole. Loolu nag li leen ci gënoon a jañ, gënoon leen cee yobbu mooy néew doole gi nu gendiku woon ci yii réew, rawati na ci wàllug xare. Li ñu doon jublu ci teg loxo googu, mooy man cee jaare bay wéyal ak a doxal seen naali sanc yooyu daan tax ba nuy man a teg loxo ci koom-koomi reew yi nu nangu, ci seeni dooley xare, ci seen politigu bitim réew ak seeni mbiri xam-xam ak aada, ngir man a samp bu baax seen kenoy sanc ci dëkk yii. Misaali sanc yu mel nii yu bari lanu, nañu ci indi yii rekk: Sanc gi Fraans defoon Aljeeri, atum 1830g, ak sanc gi Britani defoon Adan, atum 1839g, defoon ko it Isipt atum 1822g, ak teg gi Fraans tegoon loxo dunu Madagaskaar, atum 1894g, Beljig defoon ko Kongo atum 1907g ak nangu gi Itaali nangu woon Libi atum 1911g, ak Ecopi 1936g.

Xeetu sanc wii mooy wi gënoon a tar te gën a ñaaw ci xeeti sanc yi, ndaxte lu diisoon la ci ñi cosaanoo woon ci reew yi nu tegoon loxo. Ndaxte sanc gu sukkandiku woon ci jëfandikoo doole la. Waaye li muy tar lepp ak a tiitale, teewul nit ñi xeexoon ko, te xaru woon ci jële ko fi. Jànkoonteek lu sakkan ciy jafe-jafe aki coona ci seen xeexu njàmbaar boobu ñu ko doon xeex, ba mujj ame ci lu màgg li nu doon wut, muy gore ak tembte, ak dàq sancaan yi ñu juge seeni reew.

Reewi sanc yi mujj nanu wut geneen anam gu yees gu nuy sance ak a tege loxo reewi jàmbur yi, ñu soppi woon seen sanciin woowu doon tegu ci dooley xare, wut weneen wu nuy tudde “AAR”. Aar nag ci maanaa mu sanc mi mu yor, gënul benn yoon sanc gi nu daan defe ci teg loxo ak nangu reewum jàmbur ci doole, moom daal AAR, tur la ci tur yi sancaan yi indi te jëfandikoo ko ci yenn ci ay jamono.

Bu dee maanaa mi aar yor ci wàllug sanc, mooy def gi reewi sancaan yi daa def ay dëppoo aki kollarante ci anam gu maandoodi ak yeneen reew yu doyadi yi, te neew doole. Bu ko defee reewum sancaan mi day kollaranteek reew mi mu sanc ci di ko aar ci mbooleem tooñ gu ko man a dikkal, juge ci dooley politig ju digook moom walla jeneen. Bu ko defee loolu di may reewum sancaan mi, muy doxal mbirum reew mi nuy aar, ci wàlli kaaraange, bitim reew, ak koom-koom. Reew mi nu aar daal du doxal lu dul mbiri biir reewam rekk. Loolu nag daa na tax mu nu aar mi daawul am temb gu mat, ndax ag gore gu politigam kollarante yooyu danu ko daan tënk, ba daa ko tee muy def ay ligeeyam ci mbooleem ay mbiri reewam, ci ni mu ko neexe. Misaal yi ci loolu yu bari lanu, ñu indi ci yii rekk: Aar gi Fraans defoon Tunisi atum 1881g, ak Maraakes 1912g, ak aar gi Britani defoon Adan, dale ko ca ba mu ko tegee loxo atum 1839g, ak yeneen barab yi mu tegoon loxo.

Reewi sancaan yu mag yi tàmbli woon nanoo wutati ay tur yu bees, ngir sanc gu bees gi, ginaaw xareb adduna bu njëkk bi. Loolu nag mu jublu woon ci muur sanc gii muy def muuraayu ag yiw akug xay. Loolu nag du tee sanc moom di lenn rekk, ak mbubb mu mu man a sol, ak melokaan wu mu man a dikke . Ci noonu la “feetale” dikke, moom nag ag anam la ci anami sanc gu yees gi nga xam ne jataayu kureelu xeet yi saxaloon na ko, te nangu ko, mooy kureel googu nu sosoon ca Paris, ca ndajem jàmm ma nu defoon atum 1919g, ngir lijjanti lëj-lëj yi amoon ci ginnaaw xareb adduna bu njëkk bi. Boobu kureel nag Fraans da ca’a defoon ay jeexiital yu mag mook Britani. Nga xam ne ni nu bëgge mu mel ni daanaka la mel.

Dalu feetale ci jëmmi boppam, ñi ngi ko jële - ci cosaan la – ca yoon wu Rom wu yagg wa . Feetale nag noste la gog defoon na mbooleem reew yi nga xam ne “reewi dëppoo yi ” nangoo woon nanu leen ci imbraatoorug Almaañ gi, ak reewum Usmaan mi , ñuy ay reew yu nekk ci ron feetale googu. Bu ko defee, reewi dëppoo yi ñoo nekkoon reew yi nu joxoon feetale googu, maanaam ci seen ron kilifteef lanu feetale woon mbooleem reew yi nu nangoo ci Almaañ ak reewum Usmaan mi.

Bu ko defee ñu waral ci reew yiy feetewoo feetale gi ñuy def leeg-leeg ñu indi ay saxal aki leeral yu aju ci seen dooley xare yi nekk ci reew yi nekk ci seeni loxo, te nu feetale leen leen. Saxal yii nag ak leeral yi kureelug feetale gi nekk ci kureelug xeet yi lanu ko daa indil. Feetale gi tam mi ngi daa yam ci benn ñeenteelu xarnu, maanaam benn xaaj ci xarnu bu xaaj ñeenti xaaj. Misaal yi aju ci xeetu sanc wii yu bari lanu, ñu wax la ci rekk: Feetale gi nu defoon Britani Iraak, penkub Jordani ak Falastin mi nga xam ne dafa genn ci teg loxo gu Britani, ngir tàbbeeti ci gu Israayil. Ak feetale gi nu feetale woon Fraans Siri ak Libaa, ak feetale gi nu defoon goornamaab neewiit yu weex ya nekk Afrig de Sud, feetale gi nu leen feetale woon mbirum Namibi, ñu yor ko di ko doxal. Ak feetale gi nu feetale woon Japon duni Pasifig, duni Marshal, ak feetale gi Ostraali ame woon ci kaw Gine gu yees gi añs. Kureelug xeet yi nag, daa xëyoon rekk sàkk feetale, di ko teg reew yu neew yi doole, ci sañ-bañ, te du leen ci tàggu mbaa mu ciy diisoo ak ñoom.

Moom itam aw xeetati la ci xeeti sanc yi, wii nag xeet la wu feeñ ci ginnaaw xareb adduna bu ñaareel bi. Ñu amale ko nag ci genn saxal gu juge ca mbootaayu xeet ga ñu sosoon , atum 1945g, ngir wuutu fi kureelug xeet yi. Mbootaayu xeet yi nag neenaloon na kureelug feetale gu sax gi nekkoon ci kureelu xeet yi, ngir teg fi leegi jataayub denkaane bi nga xam ne moom lanu wekk leegi mbirum saytu sancu yi “reewi digg” yi moomoon, yilifoon leen: Reewi digg yi ñooy Almaañ, Itaali ak Japon bi nu leen laata a dàqe ci xareb adduna bu ñaareel bi. Moom jataay boobu tam moo yoroom mbirum reew yi tembagutoon. Misaalum xeetu sanc gii: denk gi nu denkoon Itaali Libi ak Somali ak denk gi nu denkoon Britani Tanganyika ak yeneen .

Sancug aada

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Moom de xeet la ci xeeti sanc gi nuy jaare ci xalaat. Yenn ci reewi sancaan yi danoo jugoon ci jariñoo xalaat ak aada, ngir ligeeyal seeni njariñi sanc. Ci noonu ñu sosoon ay jàngu (leekol) aki xamluwaay aki fajuwaay , aki barabi nasaraanal, ak yeneen, loolu lepp nag ngir man cee jaare bay sanc yii reew ñu ko def, te man leen a moom.

Fraans de xeetu sanc wii def na ko ci Afrigu bëj-gànnaar gi, ci : Tinisi, Aljjeeri, Maraakes, (sunu reew mii it di Senegaal def na ko fi), defati ko ci reewi Shaam yi, rawati na Libaa. Reewi dankub mbokkte bi it (communisme), Bennoog Sofiet gi jiite leen, ñoom itam jeem nanu ba sonn ci wisaare seen xalaat yi ak seen dali làngi politig yi ci réew yu bari ci adduna bi.

Barabi sañ-sañ

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Lu bari ci réewi sancaan yi danu doon ngàrtaajoo ak a aakimoo koom-koomu lenn ci reewi Asi yi ak yu Afrig yi, ba noppi naan ñoom de dugguñu te seen yoon nekkul ci mbiri politig yu reew yii, du caageenug seen mbiri biirum reew. Misaali xeetu sanc wii, mooy la xewoon ca Iraan atum 1907g, nga xam ne danoo defoon bëj-gànnaaru reew ma muy barabu sañ-sañ ñeel Rusi gu Xaysar gi, bëj-saalum ba nu def ko barabu sañ-sañ ñeel Britani. Amoon na it ay xejj(lu mel ne sañ-sañ) yoo xam ne yenn ci reewi sancaan yi amoon nanu leen ci reewi adduna bi, lu ni mel mooy xejj yi nga xam ne reewi Tugal yi amoon nanu leen ci reewi Shaam yi, ci jamono ju Usmaan ji ak xejj yi nga xam ne reewi sancaan yi amoon nanu leen ci Siin ak Tayland ak yeneen.