Réewum ñaari dex yi
Réewum ñaari dex yi ab diiwaanu Penku gu Jege la, nekk ci diggate Dijla (Tigre) ak Furaat (Ëfrat). Su nu koy xool ci lu ëpp mooy nekk Iraak gu tay jii.
Tekkig baatu Mesopotaami daa soppiku ci doxug jamono. Ci tekkeem bu yàgg bu waa Geres ak waa Rom, moo doonoon wàllu bëj-gànnaar gi araab yi doon woowee itam Jasiira, beneen barab bu guus bi moom araab yi Sawaad lañu ko doon wax, ca seen mbind yu yàgg ya. woowin gu barab bi moo ngi tëggoo ci làkki ña fa cosaanoo, dinañu ko fekk ci wu-Akkadi Birīt Nārim "digalug dex gi" (birīt, « digal » ak nārim « dex ») walla Māt Birītim «Réewum digal bi» (māt, «Réew» birītim, «digal»). Ci wu-armeeni, ñoo ngi koy wax Beyn Nahrīm "digante dex yi" (beyn «digante», nahrīm «dex»), ci waxiin yépp mi ngi doon tekki wàll wi féete kawu Ëfrat.
Melosuuf
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Amoon na ay barab yu seen suuf nangu woon mbéy, nekkoon ci diggante Sagros, Taurus, ci tefesi Géej-Gu-Diggu gi ak ci Dóoxug waa-Peers gi.
Di nañu ci boole diiwaan bi nekk ci bëj-saalum, diggante Tigre ak Ëfrat (ca Iraak gu tay). Waaye diiwaan bii tawam taxu koo bari noonu.
Asiri lañuy fara di woowee bëj-gànnaaru Mesopotaami, Babilon moom di bëj-saalumam.
Taariix
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Jamonoy taariix mi ngi tambali ci Réewum ñaari dex yi ci 3300 njëkk juddug Isaa, bañu sàkkee mbind. Ñu dog-dogaat ko ciy jamono:
- Jamonoy Uruk (3400-2900): la bind soqaliku ca Mesopotaami, waaye mbind yi ca jamono yooyu neexuñu woon a firi. Ay mbindi yoriin aki limi baat lañu woon, waaye manuñoo wax dara ci seenug dund.
- Jamonoy (2900-2340): dañu koo séddale ci ñetti ron-jamono. ci ndoorteelu xaaju IIIu junneel(millénaire), lañu tambalee xam dara ci xew-xew yi, balaa dara ci ndimbalu dencu(archive) yi ñu wuññee Lagas.
- Jamonoy Akkad(2340-2180): Sargon bu Akkad moo dakkaloon xaajale bafa amoon ciy dëkk-dëkkaan, boole leen ci menn réew, mu mujj doon imbratóor gu mag, ci ndimbalu sëtam ba Naram-Sin.
- Jamonoy waa-Sumeer ju bees(2180-2004): Imbratóoru Akkad a ngi daanu ginnaaw fippu ak congu askani barbar yi. Nguur-nguuraani waa Simeer yi amaat seenug tembte, laataa Ur-Nammu ak doomam Sulgi di leen boole ci genn imbratóor gu mag, teg-tànk ci barab bépp.
- Jamonoy waa-babilon ju njëkk(2004-1595): Imbratóoru Ur mi ngi daanu ci 2000 ciy pexey waa elam yeek waa amuru yi. Ñu mujj ñi ñoo jël boppi nguur yépp, daadi séddale Réewum ñaari dex yi: Isin, Larsa, Esnunna, Mari ak Babilon, mi mujj teg-tànk ci diiwaan bépp ak buuram ba Hammurabi, laataa muy daanu ndànk-ndànk, ba Itit yi mujj jël dëkk ba ci 1595.
- Jamonoy waa-babilon ju diggu(1595-c.1080): Kasit yi ñoo mujj teg-tànk Babilon ci diirub ñenti xarnu. Ci bëj-gànnaar, nguurug Mitanni moo fa doon noote laataa nguurug waa Asiri gi di ko fél.
- Jamonoy waa-asiri ju bees(911-609): ci IXu xarnu bi, la waa-asiri yi jógaat, joxaat seen baat doole, tegaat fa tank. Taxawalaat imbratóot gu mag yilif Penku gu Jege gépp, Ci jamonoy Sargonid yi la àgg ci pujam, laataa ag daanoom ci VIIu xarnu ginnaaw ay cong yu jóge ci waa-babilon yeek Med yi.
- Jamonoy waa-Babilon ju bees(625-539): ci jamono jii la waa-babilon yi jëlaat genn wàll ci nguurug waa-asiri ju bees ji boole ci seen bos, ci ndimbalu Nabusodonosor II. Doonul nag nguur gu yàgg, ci 539 la ko waa-persi yi sanc.
- Jamonoy waa-akamaniisia(539-331): donte ci jamono jii waa-akamaniisia yi ñoo yilifoon diiwaan bi, waaye terewuloon seenug suqaluku jëmoon kanam.
- Jamonoy selewsid yi(331-140): imbratóor gu waa-persi gii di Akamaniisia ngi daanu ci congug Aleksandrë gu Mag, ginnaaw ag deewam ak ŋiir-ŋiirloo ya ca toftaloon la Selewsid yi jël nguur ga. Ci jamono jii la cosaanu Réewum ñaari dex yi tambalee juutu, te yokk ci IIu xarnu bi.
- Jamonoy waa-pati(140 nj. Isaa, 224 g. Isaa ): Ci jamono jii la waa-Pati yi daq callala gu selewsid yi ci biir IIu xarnu bi. Ci seenug nguur la aada ak cosaani ña njëkk a dëkk ci diiwaan bi saay ba faaw, donte yenn aada yi doon nañu leen dund ba-ta ci julliwaay yu Babilon yi.
Téerekaay
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- (fr) Collectif, De la Mésopotamie à la Perse, Encycloædia universalis, coll. « La grande histoire des civilisations », 1999 (ISBN 2-7028-3080-3) ;
- (fr) Collectif, Atlas de la Mésopotamie et du Proche-Orient ancien, Brepols, 1996 (ISBN 2503500463) ;
- (fr) Adolf Leo Oppenheim, La Mésopotamie : portrait d'une civilisation, Gallimard, 1970 ;
- (fr) Jean Bottéro, Mésopotamie. L'écriture, la raison et les dieux, Gallimard, coll. « Folio Histoire », 1997 (ISBN 2070403084) ;
- (fr) Francis Joannès (dir.), Dictionnaire de la civilisation mésopotamienne, Robert Laffont, 2001 ;
- (fr) Jean-Jacques Glassner, La Mésopotamie, Belles Lettres, coll. « Guide des civilisations », 2002 (ISBN 2-251-41017-1) ;
- (fr) Jean-Claude Margueron, Les Mésopotamiens, Picard, 2003 (ISBN 2708406930) ;
- (fr) Georges Roux, La Mésopotamie, Seuil, coll. « Points histoire », 1995 (nouv. édition) (ISBN 2-02-023636-2) ;
- (fr) Pierre Amiet, L'Antiquité Orientale, PUF, Que-sais-je, 2003
- (fr) Pierre Amiet, Introduction à l'Antiquité Orientale, Desclée de Brouwer et École du Louvre, 2000
- (fr) Agnès Benoit, Art et archéologie : les civilisations du Proche-Orient ancien, Manuels de l'École du Louvre, 2003