Lonkoyoonu àdduna bi
Boo gëstoo kartu adduna bi bu baax dinga ca gis dëgg yii : - Kaw kol-kolub suuf si mi ngi ame ci jéeri ji ak ndox mi, bu ko defee jéeri ji yóbb ci benn ñeenteel, maanaam bu doon ñeenti xaaj la benn bi, ndox mi moom yóbb ci ñatti ñeenteel . - Jéeri nag mi ngi ame ci juroom benni gox walla kontinã ( ci lu dul goxub dott (pole) bu bëj-saalum bi nga xam ne kenn dëkkewu ko ngir jawwu ak dénd bu méngoodi ba), juroom benni gox yii danu leen a toftale kem ni nu yaatoo : 1 – Goxub Asi : moo ëpp ci gox yi, ab tolluwaayam toll ci benn ñaareel 44 milyoŋi kilomet yu kaare , way dëkk ya tollu ci 2200 milyoŋ ciy nit. 2 – Goxub Afrig : ab tolluwaayam di benn ñeenteel 30 milyoŋ ciy kilomet yu kaare , way dëkk ya tollu ci 350 milyoŋ ciy nit. 3 – Goxub Amerig gu bëj-gànnaar gi: ab tolluwaayam tollu ci benn ñeenteel 24 milyoŋi kilomet yu kaare, way dëkk ya tollu ci 270 milyoŋi nit. 4 – Goxub Amerig gu bëj-saalum gi: tolluwaayam toolu ci ñatti ñeenteel 17 milyoŋi kilomet kaare, way dëkk ya tollu ci 300 milyoŋi nit. 5 - Rëddu yamoo wi (équateur) di ( rëdduw tus wu gaar wi (latitude) ) mooy wi séddale àdduna bi def ko ñaar : benn xaaj bi bu bëj-gànnaar la, bi ci des di bu bëj-saalum, moom rëdd woowu dafa romb ci wàlli bëj-saalum yu goxub Asi , ak ci digg Afrig ak bëj-gànnaaru Amerig gu bëj-saalum gi. Bu ko defee gëwéelub sànkar bi (Tropique du cancer) romb ci bëj saalumu Asi ak bëj-gànnaaru Afrig ak bëj-saalumu Amerig gu bëj-gànnaar gi , ci noonu gëwéelub tef bi (Tropique du capricorne) ñëw moom itam jaar ci digg Ostraali ak Afrig gu bëj-saalum gi ak digg Amerig gu bëj-saalum gi . Rëdduw Grinits (longitude;meridien) di (rëddu tus wu taxaw wi) moom it jaar ci sowwub ñaari gox yii di Afrig ak Tugal , moom rëdd woowu nag mooy wi séddale àdduna bi def ko ñaari xaaj bu penku ak bu sowwu. 5 – Goxub Tugal ab tolluwaayam tollu ci benn ñaareel 10 milyoŋi kilomet yu kaare, way dëkk ya tollu ci 750 milyoŋ ciy nit. 6 – Goxub Ostraali : ab tolluwaayam tollu ci ñatti ñeenteel 7 milyoŋi kilomet kaare , way dëkk ya tollu ci 15 milyoŋi nit. - Ndox yi nekk ci kaw kol-kol bi (globe) ñi ngi ame ci mbàmbulaan yi : ñoom ay diggante yu rëy lañu yu ndox, ak ci géej yi: ñoom ay diggante yu gën a ndaw lañu yu ndox . Bokk na ci mbàmbulaan yi : màmbulaan gu dal gi (moo ci gën a rëy) ak gu atlas, ak mbàmbulaan gu end gi ak gu bëj-saalum gi ak gu dott bu bëj-gànnaar bi(pole nord). Bokk na ci géej yi :géej gu diggu gi (mediteranee) gu xonq gi , gu araab gi, gu ñuul gi añs . - Adduna ju njëkk ja walla ju yàgg ja – moom mi ngi ci xaaj bu penku bu kol-kol bi – mi ngi ame ci ñatti gox walla kontinã yu taqaloo, daal di sos nag benn dank (bloc) walla jóor, ñatti gox yii ñooy : Asi, Afrig ak Tugal, dara taqalewu leen lu dul yenn ci ay feeñte yu dénd yu néew : niki géej yu xat yi ak càllalay doj yi ak tund yu yaatoodi yu néew yi ag yékkatiku. - Nit dundal na goxi adduna ju yàgg ja la ko dale ca ba mu tegee tànkam ci kaw suuf rekk, bu ko defee ay xay (civilisation) yu mbay, yu kawe, yu yàgg daal di am ci xuri ay dexam yu naat ya, lu ci mel ne xay ya amoon ca xuri dexug Niil ga nekk Isipt ak dexug Dijla ga ak Furaat ca Iraag ak dexug Sand ak Gangas ca End ak dexug Sigyang ak Yangci ca Siin. - Adduna ju yees ji – moom mi ngi ci xaaj bu sowwu bu kol-kol bi – mi ngi ame ci Amerig gu bëj-gànnaar gi ak Amerig gu bëj-saalum gi, ñoom ñaar ñooy ñaari gox yi nga xam ne bi leen nit wuñee (decouvrir) ak leegi ay xarnu (siecle) rekk la, la ëpp ca ña fa dëkke ay waa Tugal lañu yu gàddaaye Tugal dëkksi fa, moom Tugal nag benn la ci goxi adduna ju yàgg ji . - Goxub Ostraali –moom moo gën a tuuti ci gox yi, te gën a rëy ci duni adduna bi- mi ngi nekk ci xaajub kol-kol bu bëj-saalum bi, ca bëj-saalum gu penku gu dankub adduna ju yàgg ja. - Mbàmbulaan gu dal gi moo dox ci diggante ñaari gox yii di Asi ak Ostraali cig wàll, ak ñaari gox yii di Amerig gu bëj-saalum gi ak gu bëj-gànnaar gi ci geneen wàll, bu ko defee mbàmbulaan gu atlas moom dox ci diggante ñaari gox yii di Tugal ak Afrig ak ñaar yee di Amerig gu bëj-saalum gi ak gu bëj-gànnaar gi , bu ko defee mbàmbulaan gu end gi tàqale ñaari gox yii di Aseek Afrig wëlif goxub Ostraali, mbàmbulaanug bëj-saalum gi tàqale mbooleem gox yi wëlif goxub dott bu bëj-saalum bi. - Rëddu yamoo wi (équateur) di ( rëdduw tus wu gaar wi (latitude) ) mooy wi séddale àdduna bi def ko ñaar : benn xaaj bi bu bëj-gànnaar la, bi ci des di bu bëj-saalum, moom rëdd woowu dafa romb ci wàlli bëj-saalum yu goxub Asi , ak ci digg Afrig ak bëj-gànnaaru Amerig gu bëj-saalum gi. Bu ko defee gëwéelub sànkar bi (Tropique du cancer) romb ci bëj saalumu Asi ak bëj-gànnaaru Afrig ak bëj-saalumu Amerig gu bëj-gànnaar gi , ci noonu gëwéelub tef bi (Tropique du capricorne) ñëw moom itam jaar ci digg Ostraali ak Afrig gu bëj-saalum gi ak digg Amerig gu bëj-saalum gi . Rëdduw Grinits (longitude;meridien) di (rëddu tus wu taxaw wi) moom it jaar ci sowwub ñaari gox yii di Afrig ak Tugal , moom rëdd woowu nag mooy wi séddale àdduna bi def ko ñaari xaaj bu penku ak bu sowwu.