Xaralay xibaar ak jokkoo
Apparence
(Yoonalaat gu jóge Jumtukaay xara yu bees yi)
Xaralay Xibaar ak Jokkoo (XXJ) walla Xaralay Xibaar ak Jokkoo yu Yees yi, ci wu-angalteer Information and Communication Technology, ci wu-faraas Nouvelles technologies de l'information et de la communication, moo ëmb mbooleem xarala yees jëfandikoo ngir yor ak jokkale ay xibaar. Yitteem mooy sos ay noste yuy yor ay xibaar, yor seenug suqaliku, seenug dencu, seenug jokkale, ak seenug kaaraange.
Yombul joxe ci ab tekki bu daj ndax amul benn tekki bu ñépp ànd déggoo. Ñi ciy liggéey raññee nañu leen niki ñu seen xam-xam daj, dañoo nekk ñuy xam lépp lu laal: mbëjfeppal, xam-xamu nosukaay, jokkoosoryante.