Aller au contenu

Feebaru stress buy wëy

Jóge Wikipedia.

Royuwaay:Redirect

Royuwaay:Redirect


Feebaru stress buy wëy (PTSD)[note 1] mooy benn feebaru xel bu nit mëna am ginnaaw bi mu fekkee benn tiitangejoge ci xew xew, ni yëfu saay saay, xare, ay bëkkante ci tali bi, walla yeneen xëbal ci dund nit ki.[1] Yi koy wone bokk na ci jaaxle ci xalaat yi, yitte, walla ay géntjoge ci ay xew xew, ci xel walla ci yaram itteci(traumatisme) feebaru joge ci fekke xew xew bu yëngul xel-yiy tegtalaate, jééma moytu traumatisme joge ci yiy tegtalaate, ak yoqute ci xeex walla daw.[1][2] Mbir yii di wone feebar bi dañuy yagg lu tollook lu ëpp benn weer gannaaw xew xew bi.[1] Xale yu ndaw yi duñuy faraldi wone tiitange, wante mën nañu génne li nekk seen xol ci ay po.[1] Nit ku am PTSD dafay nekk ci risk bu kawe ngir xaruak bëgga gaañ boppam.[3][4]

Ñu ëpp ci ñi fekke ay xew xew yi indi tiitange dañuy ame PTSD.[3] Nit ñi dund tiitange ak yeneen nit (ni siif wallanoot xale) ñoo gëna mëna ame feebaru PTSD, méngale leen ak ñi dundul-su ñusukkandikoo ci tiitange, yi mel ni ay aksideŋ ak yaqu yaqu yu joge ci jawu ji.[5] Lu tollook génn wall ci nit ñooñu dañuy am feebaru PTSD gannaaw siif.[3] Xale yi ñoo gëna nééwle ci am feebaru PTSD ginnaaw tiitange, rawatina bu ñu amagul fukki at.[6] Saytu bi mungi tegu ci feeñaayu yenn ci yi koy indi joge ci gannaaw tiitange bu ñu jële ci xew xew.[3]

Fagaru mën na nekk bu fekkee pajum xel mici nit ñi génne feebar bi ci teel waaye amul njëriñ su ñu ko defee ci ñépp ñu génne feebar bi walla ñu ko génnewul. [3] Paj yu gëna am solo ci nit ñi ame PTSD ñooy joxe ay tegtal ngir dimbali nit ki saafara jafe-jafeem ak ay garab.[2] Ay paj yu wute dina ci am njëriñ. [7] Lii mën na am kenn rekk jakkarloo ak fajkat bi walla ci ab mbooloo.[2] Yiy xeex feebaru déteeluci garabu Serotonine buy faj xel mu lééj ñoo garab yu gëna baax yu xeex PTSD tey njëriñ génn wall ci nit ñooñu ame feebar bi.[8] Njëriñ yooyu ñoo gëna nééw yooyu ñu gis ak pajum feebaru xel.[3] Leerul su fekkee buñu jëfandikoo garab yi ak pajum feebaru xel ndax dina am njëriñ.[3][9] Yeneen garab yi amuñu seede gu doy ne dinañu mëna am njëriñ bu ñu leen jëfandikoo, te ci wallu benzodiazepines, dina indi jafe jafe ci njëriñ li.[10][11]

Ci Amerik lu tollook 3.5% ci mag ñi am nañu PTSD ci benn at moo jël, te 9% ci ñoonu dinañu gis feebar bi ci seen dund. [1] Ci li ëpp ci li des ci addina bi, xayma bi mungi ci diggante 0.5% ba 1% ci benn at moo jël. [1] Xayma yu kawe yi mën nañu am ci yenn gox yi am xare.[3] Ci jigéén ñi la gëna ëppe ci góór.[2] Yi di feeñal tiitange bokk ci feebaru xel bind nañu ko ci jamono Grece yu njëkk ya.[12] Ci jamonoy Xarey Addina bi mënin bi xamewoon nañu ko ci tur yu bare ni "ragal ba mënul yëngu" ak "xarekat bu tiit".[13] Baat bi di "Feebar bi joge ci gis walla fekke tiis ni dee, yu deme noonu" ñungi ko tambali woowe noonu ci ati 1970 lu ci ëpp ndax li ñu ko génne ci U.S. soldaa yu bayyi yici xare Vietnam bi.[14] Ñungi ko dugal ci yoon joge ci Mbooloo mi dajale ñi di yëngatu ci wallum pajum xel ci Amerik ci atum 1980 in seen ñetteelu ndaje ci wallu Saytu ak Xayma ci Téére bu Feebaru Xel yi (DSM-III).[15]

  1. Yeneen ni tur yu ñu nangu am na; xoolal "Mbind mi" ci article bi.
  1. 1,0 1,1 1,2 1,3 1,4 et 1,5 American Psychiatric Association (2013). Diagnostic and Statistical Manual of Mental Disorders (5th ed.). Arlington, VA: American Psychiatric Publishing. pp. 271–280. ISBN 978-0-89042-555-8. 
  2. 2,0 2,1 2,2 et 2,3 "Post-Traumatic Stress Disorder". National Institute of Mental Health. February 2016. Archived from the original on 9 March 2016. Retrieved 10 March 2016. 
  3. 3,0 3,1 3,2 3,3 3,4 3,5 3,6 et 3,7 Bisson JI, Cosgrove S, Lewis C, Robert NP (November 2015). "Post-traumatic stress disorder". Bmj 351: h6161. PMC 4663500. PMID 26611143. doi:10.1136/bmj.h6161. 
  4. Panagioti M, Gooding PA, Triantafyllou K, Tarrier N (April 2015). "Suicidality and posttraumatic stress disorder (PTSD) in adolescents: a systematic review and meta-analysis". Social Psychiatry and Psychiatric Epidemiology 50 (4): 525–37. PMID 25398198. doi:10.1007/s00127-014-0978-x. 
  5. Zoladz PR, Diamond DM (June 2013). "Current status on behavioral and biological markers of PTSD: a search for clarity in a conflicting literature". Neuroscience and Biobehavioral Reviews 37 (5): 860–95. PMID 23567521. doi:10.1016/j.neubiorev.2013.03.024. 
  6. National Collaborating Centre for Mental Health (UK) (2005). "Post-Traumatic Stress Disorder: The Management of PTSD in Adults and Children in Primary and Secondary Care". NICE Clinical Guidelines, No. 26. Gaskell (Royal College of Psychiatrists). Archived from the original on 2017-09-08. Lay summaryPubmed Health (plain English).  open access publication - free to read
  7. Haagen JF, Smid GE, Knipscheer JW, Kleber RJ (August 2015). "The efficacy of recommended treatments for veterans with PTSD: A metaregression analysis". Clinical Psychology Review 40: 184–94. PMID 26164548. doi:10.1016/j.cpr.2015.06.008. 
  8. Berger W, Mendlowicz MV, Marques-Portella C, Kinrys G, Fontenelle LF, Marmar CR, Figueira I (March 2009). "Pharmacologic alternatives to antidepressants in posttraumatic stress disorder: a systematic review". Progress in Neuro-Psychopharmacology & Biological Psychiatry 33 (2): 169–80. PMC 2720612. PMID 19141307. doi:10.1016/j.pnpbp.2008.12.004. 
  9. Hetrick SE, Purcell R, Garner B, Parslow R (July 2010). "Combined pharmacotherapy and psychological therapies for post traumatic stress disorder (PTSD)". The Cochrane Database of Systematic Reviews (7): CD007316. PMID 20614457. doi:10.1002/14651858.CD007316.pub2. 
  10. Guina J, Rossetter SR, DeRHODES BJ, Nahhas RW, Welton RS (July 2015). "Benzodiazepines for PTSD: A Systematic Review and Meta-Analysis". Journal of Psychiatric Practice 21 (4): 281–303. PMID 26164054. doi:10.1097/pra.0000000000000091. 
  11. Hoskins M, Pearce J, Bethell A, Dankova L, Barbui C, Tol WA, van Ommeren M, de Jong J, Seedat S, Chen H, Bisson JI (February 2015). "Pharmacotherapy for post-traumatic stress disorder: systematic review and meta-analysis". The British Journal of Psychiatry 206 (2): 93–100. PMID 25644881. doi:10.1192/bjp.bp.114.148551. Some drugs have a small positive impact on PTSD symptoms 
  12. Carlstedt R (2009). Handbook of Integrative Clinical Psychology, Psychiatry, and Behavioral Medicine Perspectives, Practices, and Research. New York: Springer Pub. Co. p. 353. ISBN 9780826110954. 
  13. Herman J (2015). Trauma and Recovery: The Aftermath of Violence–From Domestic Abuse to Political Terror. Basic Books. p. 9. ISBN 9780465098736. 
  14. Klykylo WM (2012). Clinical child psychiatry (3. ed.). Chichester, West Sussex, UK: John Wiley & Sons. p. Chapter 15. ISBN 9781119967705. 
  15. Friedman MJ (October 2013). "Finalizing PTSD in DSM-5: getting here from there and where to go next". Journal of Traumatic Stress 26 (5): 548–56. PMID 24151001. doi:10.1002/jts.21840.