Bennoo gu Almaañ
Bennoo gu Almaañ
Almaañ njëkk xare yu Napoleon yi:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Almaañ njëkk xarey Napoleon yi, dafa séddaliku woon ci lu jege ñatti téemeer ak juroom benn fukki diiwaan(360 diiwaan), yépp it ci ron imbraatóor gu Otris lañu nekkoon, walla li ñuy tudde Imbraatóor gu Rom gu sell gi. Almaañ gépp it genn nguur rekk a fa nekkoon gu mag te temb, mooy gu Brusiya. Nguur googu nag jëmoon na kanam, te ag yewwuteem fés, ci jamonoy buuram ba tuddoon Fredrick mu mag mi (Great Fredrick) (1740 -1786 g), mooy ki ko defoon muy nguur gu dëgër te am doole. Bu ko defee waa Almaañ yépp wëlbati seeni gët jëme ci nguur gii, ngir bëgg ag bennoo.
Almaañ ci jamonoy Napoleon:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Napoleon ak xarekatam ya xuusoon nañu ci diiwaani Almaañ yi, teg leen loxo. Daal di jawali ca nguurug Brusiya, gi nga xam ne jàmmaarloo woon na’ak ñoom cig njàmmaar ak fit, waaye Napoleon moom mujj na ko noot, te gañe ko ci mujj gi, ca xareb Yena ba, atum 1806g, daal di teg loxo péeyam ba Berlin. Napoleon merloo woon na lool waa Brusiya yi, ci dog gi mu dogoon ay wàll ci seeni suuf, te jébbaloon leen diiwaanu Saksoniya bi. Waaye nag ci geneen wàll, am na lu am njariñ lu mu fa indi, ndaxte wàññi woon na limub diiwaan yu Almaañ yi ba ci fanweer ak juroom ñeent rekk, te bu njëkk lu jege 360 lañu woon. Kon jëfi Napoleon jii, mbir la mom moo nooyal yoon wi, waajal ko ba ag bennoo gu Almaañ man a judd, man a taxaw.
Almaañ ginnaaw ndajem Vienne mi:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ginnaaw bi Napoleon Bonaperte daanoo atum 1815g, ci lañu def ndajem Vienne, ñu jële fa ay saxal yu bari, bokk na ci yooyu, dagg Dóox bu Warsaw gu Poloñ gi, dagg ko ci Brusiya, te jox ko Riisi, bu ko defee ñu jox Brusiya moom itam diiwaanub Rayan ak xaaju diiwaanu Saksoniya. Daal di taxawal ag bennoo gu Almaañ gu làmboo fanweer ak juroom ñeenti nguur-nguuraan yu Almaañ, Otris jiite ko. Defiin wii nag mi ngi ame ci càkkuteeful Metternich, ak naj gi mu doon naj way daje yi, ngir ñu defal ko bëgg-bëggam boobu. Bennoo gu Almaañ gii juddoo ci ndajem Vienne mi, nekkoon na di lu manul a wéy, ndax kat Otris moom daa tàmbli woon di génne ay saxal aki ndigal yuy safaan tas-xibaar gu gore , te wéeroodi fenn, tey safaan mboolooy Almaañ yi daan sàkku ag bennoo te daan ko woote. Te Otris it daa mujjoon teg loxo ci jataayub bennoo gu Almaañ gi, te ga woon ko ci mu génne ay saxal yuy digale ñu fuglu daara yu kawe yi , ak leekol yi, ak ndaje yi añs.Doxaliin yooyu nag taxoon na ba ay kàddu jib yu ay waa Almaañ, di sàkku ñu fipp ci kaw Otris, tey sàkku ñu jeem a bennal Almaañ, ci keppaarug nguur gu Almaañ gu dëgër. Loolu mooy li xeltukatu Almaañ bi (Hegel) daan sàkku, te daan ko woote, moom ak ñeneen ñi daa jam bennoo gii nga xam ne Otris a ko moomoon daanaka, te tegoon ko loxo.
Taxawaay bi nguurug Brusiya ame woon ci naal yi jëmoon ci Bennoo gu Almaañ gi:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Nguurug Brusiya dafa tàmbli woon di yëngu ngir dajale xeetu Almaañ wi, dugal leen ci genn nguur gu Almaañ gu ñu bennal. Mu daal di woon rëddal boppam ab politig bu muy jaar ngir àgg ci loolu mu bëgg. Mu daal di woon door ci dëgëral boppam ci biirum réew, defaraat doxaliinam , yekkati koom-koomam, soppi nosteg galag yi aju woon ci nduwaan ci mbooleem diiwani nguur gi. Ñu daal di taxawal noste gi nu daa wax (Solofrayn), di ag bennoo ci wàllug nduwaan, mooy li neenaloon nosteg nduwaan gi ci biir Almaañ. Nga xam ne li nekk ci biir réew mi cim njaay deesu ci génne duwaan. Nga xam ne daññoo fééexal yaxantu gi ci Brusiya, afal ko ba mu man a doxe ni ko soob, ci lu dul ñu ciy teg ay tënk-tënki galag mbaa yu nduwaan. Doxiinu Brusiya wii déy dees na ko lim mu dig soopiku gu mag ci taarixu bennoo gu Almaañ gi. Doxal nañu ko nag ci atum 1818g, ci biir ay diiwaanam yu biir yi. Diiwaan yooyu nga xam ne njëkk “Nosteg Solofrayn gi” danoo nekkoon ay diiwaan yoo xam ne bu ci nekk daa amoon nosteg bobb gu nduwaan(systeme autonome douanier), gu mu bokkul ak kenn. Waaye bi Solfrayn taxawee, lañu bennal biir Brusiya ci wàllug nduwaan, ginnaaw bi mu nekkee moom Brusiya di lu ñu séddale ci juroom benn fukki diiwaani nduwaan.
Waa Brusiya yi yëgoon nanu ne benno gi ci wàllug koom-koom mooy cëslaay li ñu war a teg bennoog Almaañ gi ci wàllug politig. Looloo taxoon kilifay Brusiya yi tàmbli woon a fexe nu ñuy def ba dugal yeneen diiwaani Almaañ yi ci bennoo gu nduwaan googu. Brusiya nag amoon na ndam ci li mu doon wut ci yenn ci diiwaan yu Almaañ yu ndaw yi, waaye nag jot naa dajeek ag jàmmaarloo gu mag ci yeneen diiwaan yu Almaañ yu mag yi, li ko waral mooy ñoom dañoo gisoon ne li gën ci ñoom mooy ñu sosal seen bopp ag bennoo gu ndawaan gu temb, ngir xeex ci bennog nduwaan gu Brusiya gi. Looloo fi indi woon ñatti bennoo yu nduwaan ci Almaañ, ñooy:
1 Solofrayn
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]2 “Bennoog nduwaan gu Bavar” gi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]nga xam ne mi ngi judd woon atum 1820g, maanaam ginaaw bi gu Solofrayn amee ba am ñaari at.
3 Ak bennoo gu nduwaan gu Saksoniya
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Mooy gi Saksoniya taxawaloon atum 1828g.
Kilifay Brusiya yi xamoon nañu ne diiwaani Almaañ yi danañu nangoo duggsi ci bennoo gu Solofrayn gi, bu ñu soppee sart yiy tax manees cee dugg. Looloo taxoon ñu soppi sarti Solofrayn yi, nga xam ne leegi dañoo sos ab jataay bu làmboo mbooleem ndawi yi ci bokk, buy saytu noste googu. Leegi nag lu fa duggati rekk ci li bawoo ci nduwaan mi ak galag yi ñu koy séddale mbooleem diiwaan yi, ci kem limub ña fa dëkk. Soppi yii de dimblee na ci yaatal gëwéelub Solofrayn, gën a yàkkali ab géewam. Leegi nag Bavar bokksi na ci ak Saksoniya ci atum 1934g, ca saa sa tam, nga tàmblee gis lu lay won ne Solofrayn moom tàmbli na a naat ak a am ag yokkute. Yaxantu ga tàmbli woon nay jar, di dox, mbay ma màgg, ndefar ga jëm kanam ci mbooleem diiwaan yi bokksi ci Solofrayn. Am na nag benn jëfka boo xam ne moo àntul Solofrayn, mooy moom de noste gu waa Almaañ xalaat ba def ko la, loxol Otris duggu ci, jenn doole it ju ko man a teg loxo yoonam nekku ci. Metternich gisoon na ay wi nekkoon ci noste gii, waaye bi mu koy gis fekk na waxtu wa jàll, manatu ca woon dara. Mu daal di bind Imbraatoor bu Otris bi ne ko: “Na la wóor ne nguuri Almaañ yi - bi lii amee de – di nañu nekki wenn yaram wu jàppaloo, ci ron kerug doxaliin wu Brusiya, te da na jàppeji Otris muy - moom - aw yaram wu di doxandeem, wu tumbrànke wu bokkul ciw yaramam”. Te kat waa Otris yi ñoom, ca dëgg-dëgg, duñu ay doxandéem ci waa Almaañ yi, ndax ñoo bokk xeet, làkk ak taarix. Man nañu ne Almaañ gépp mujj na bokksi ci Solofrayn gi, atum 1842g.
Xalaatu xeltu bu Hegel bi feddali woon na dooley nguur, ak ray gi muy ray jëmmaan (individu) ak lépp lu mu am, ngir sàmm dooleem akug màggam ak wegeelam. Nguur walla àtte – ci gis-gisu Hegel- cëslaayam mooy doole, ci doole rekk la man a dëgërale gëgg. Kon nguur walla àtte gu dëgër ci gis-gisu Hegel, mooy nguurug walla àtteg dëgg. Kon moom Hegel day mel ne moo teg ci loxol Brusiya lay wa di xeltu guy rafetal, di baaxal seen jëfi jiite googu ñu jiite woon bennalug Almaañ gi.
Ñu leeral leen ne bi 1848g di jot, fekkoon na Brusiya muy réew mu am kàttan ci tere Otris muy dugg ci mbiri nguur-nguuraani Almaañ yi. Naka noonu, nekkoon na it mu amoon kàttan ci jiite yëngu-yëngu gi jugoon ngir bennal Almaañ. Nguur-nguuraan yi bokkoon ci Solofrayn it, doon man a dimblante ci seen biir ci wàllug koom-koom, te daan jëflante ci lu dul yoonu Otris di ci nekk mbaa ñuy diisoo ak moom, walla ñu koy tàggu. Ci noonu nguur-nguuraan yooyu tàmblee xoole Brusiya bëtu kilifa. Ci noonu la bennoo gu koom-koom googu doon màgg ak a dëgër ci ro kerug Solofrayn, mujjoon di ab jéego bu mag jëm ci ag bennoo gu politig ak xare ci Almaañ.
Jeexiital yi jeqiku gu atum 1848g defoon ci amug bennoo gu Almaañ gi:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ay jeqiku yu bari jot nañoo am ca Tugal atm 1848g. Ag jeqiku am ca Paris, am gu am ca Vienne, geneen ca Brusiya ak ay fipp ci Itaali ak Almaañ, yepp it di xëccu jëm ci ag gore , demokraasi ak xeetu .
Metternich mu màggat mii, mujjoon na manatul woon a noot jeqikuy Tugal yooyu, mbaa mu giimal leen, ni mu ko baaxoo woon a defe. Kërug Tugal gi mujj – ni ko Metternich di waxe – di kër gu màggat, te ràpp, ba àgg ci maneesatu cee yatt sax ab palanteer ciy miiram ngirug màggat, kon leegi li jaadu kay mooy ñu màbb ko, te wuutal fa geneen kër gu yees. Ca dëgg-dëgg nag loolu am na, ndax kat noste ga amoon ca la ëppoon ca réewi Tugal ya, daa mujjoon di lu ràpp, ngirug yàgg, mujj manatutoon a ñàkk ñu yeesalaat ko, te taxawalaat ko ci anam gu dëppoo ak li jamono laaj.
Metternich dawoon na, te daanu woon, ci noonu buurub Brusiya bi Frederick William mu ñeenteel mi daal di jug, woote am ndaje mu parlamaa, ngir ñu defaral Brusiya ab sartu réew bu bees. Mu dig aw askanam ne leen moo fas yeenee jiite yëngu-yëngu giy jug ci jéem a bennal Almaañ, ci benn bataaxel bu mu leen jàngal. Ndaw yi teewal Almaañ yépp teewe woon nañu ndajem atum 1848g moomu, ñu def fa ay gëstu ci lu aju ci Almaañ gu nekk benn. Ndajem parlamaa mii, ñi ngi ko gën a xame ci turu “Parlamaab Frankfort”. Ndaje ma ëmboon na lu bari ciy woykat (walla taalifkat) , aki xeltukat aki taskati xibaar aki ustaas. Ñatti saxal nag yu mag juddoo nañu ca ndaje ma:
- Bennal Almaañ ci njiitul buurub Brusiya.
- Ñu boole ci bennoo gu Almaañ googu, wàllug Almaañ gi bokkoon ci imbraatóorug Otris gi
- Génne Otris ci bennoo gu Almaañ gi.
Way daje yii ci Frankfort, (seenub lim àggoon na ci 830 ciy jëmm) tànnoon nañu buurub Brusiya bi Fredereick William mu ñeenteel mi, def ko imbraatóor ci Almaañ gu ñu bennal gi. Waaye Frederick moom daa bañoon ne du dëppoo ndëppul imbraatóor li ñu ko joxoon, te way daje yi joxoon ko ko, ndax da ne ndëpp li daal ndawi askan wee ko ko jox, waaye buur yeek kàggam yi joxuñu ko ko. looloo taxoon nanguwu koo sol.
La am nag mooy ne buuru Brusiya bi dafa bañ a jël ndëpp li, ndax xam ne Otris ak Riisi ànduñu woon ci bennoog Almaañ googu, te manoon nañoo xëy di duggati ci seeni mbir ngir loolu. Rawati na ne Otris moom jot na a noot fipp gi amoon ca péeyam ba Vienne. Nga rax ci dolli ne Buuru Brusiya bi, moom dafa gëmoon gisiinu “àq ak sañ-sañ bu Yàlla bi”, mooy gisiin wi naan ñoom buur yi Yàlla a leen fi teg, moom lanu fi wuutu, nit ñi teguñu leen fi, du keneen it. Looloo taxoon bu nangoo it ñu def ndaje moomu, muy mu Frankfort mi, jubluwu ci woon lu dul ngistal, waaye du liggéey bu fullawu, mbaa mu dëggu ci yoonu soppi.
Otris ak Riisi dimblante nanu ci màbb barlamaab Frankfort bi, ak naalam yi mu amoon te ñu jëm cig bennoo gu Almaañ, looloo waraloon jéem gi ñu doon def ngir bennal Almaañ ci ron kilifteefug Brusiya, ci atum 1848g, mujjul woon àntu. Waaye li muy àntoodi lepp teewul xalaat bi sax ci xoli ak xeli waa Almaañ yi. Ñu mujj (waa Almaañ ñi) xam ne daal duñu man a amalati seen bennoo googu ci anamug jàmm, mbaa gu sartu réew, ndaxte Otris àndu ci te mi ngi koy xeex ak doole. Looloo waraloon ñu jëloon seen yitte def ko ci amal am mbooloom xare mu dëgër, mu leen di man a may ñu man a génne Otris ak Almaañ cig njëlbeen, door a lijjanti nag nu ñuy doone benn ci ginaaw bi. Xalaat bii nag diisoowaale (chancelier) bu Brusiya bii di Bismarck, àndoon na ci te jàpple woon ko, dëgëral ko. Moom mooy Otto Von Bismarck, boroom kurpeñu weñ bi.
Politigu Bismarck ci lu jëm ci bennoo gu Almaañ gi:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Bismarck mi ngi judd atum 1815g, am njàggam mu kawe mu defe ko ca daaray Berlin ju kawe ja. Daal di dugg ag coldaar, génnati ca, dem nag féete ca boppam ca toolam ba. Mi ngi bokkoon nag ci njaboot gu woomle, gu ami alal yu rëy ca Brusiya. Sampoon na boppam niki lawax (candidat) ngir ñu fal ko ci bennoo yu Almaañ yi, atum 1848g, ñu tànnoon ko it muy ab cér ci parlamaa bu Brusiya bi. Liggéey na it ci toolub diplomasi, doonoon aji téewal réewam (l'ambassadeur) ca Butrsburg ca Riisi. Ginnaaw bi mu nekkal réewam ca Paris.foofee la ko William mu njëkk mi doon jiite Brusiya woowe woon mu juge Faraas, ngir jiite-si njiitug jawrin gi ci Brusiya. Bismarck nag nekkoon na ku gëmoon, te daa dëgëral noste gu nguur gu ñu joyal , te gëmoon ne buur daa war a am doole te am soldaar su dëgër, Jàngu bi jàpple ko ak garmi yi. Bismarck moom faalewutoon parlamaa bi. Gisoon na ne jëm kanamug aw xeet walla ag yéegam jëm ca kaw manul a ame ci lu dul ay buuram di ñu kawe ay yitte, ak ay kàngamam, waaye duñu ko ame mukk ci ay saxal (résolutions) yu juge ci ay parlamaa, aki nostey sarti réew (systèmes constitutionnels).
Bismarck yitteem jépp mi ngi ko jëmale woon ci génne Faraas ak Otris Almaañ, mu gisoon ne lii daal manul ame ci lu dul dooley xare ju mag, ju leen ci man a ga(manante leen). Ci noonu mu tàmblee liggéey ci dëgëral dooley xare ji, ak kàttanal ko. Mu daal di tas parlamaab Brusiya bi, ndaxte (moom parlamaa bi) daa bañoon ne du woote alal ji mu doon laaj ngir man cee dooleel soldaaram si, ci noonu mu tëjoon képp ku wuuteek politigam boobu, daal di digle ñu fuglu yéenekaay yi, daal di beddiku sartu réew mi, ne du ci sukkandikooti. Alal ji mu soxla woon mu génnelu ko ci ndigalul buur bi, bañ cee sukkandiku ci lu parlamaa bi.
Wàllug xeetu (nationalisme) nag moom gis-gis bi mu ci amoon moo gënoon a yaatu bi mu amoon ci sartu réew, ndax daa gisoon ne sartu réew moom, mi ngi ame mook ay jubluwaayam, ci ginnaaw bu ag xeetu amee ba noppi.
Bismarck nag neenalul mbooleem parlamaa bi mbaa mu tas ko lépp, moom kay da caa neenl walla mu soril ko ñatti mbir, ñooy:
- Coldaar gi
- Politigu bitim réew bi
- Fal ay jëwrin ak di leen folli
Bismarck wone na dogu gu mag akug takku contar teg gi Otris teg loxo Almaañ
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Loolu nag gën na a fése ci taxaw gi mu taxawoon ci dakkal politigu Otris bi muy teg Almaañ . Looloo taxoon Otris mujj woo buuri Almaañ yépp cim ndaje ca Frankfort, ngir sos ag bennoo gu lëngoo (walla gu federaal), guy doxal ab goornamaa, boo xam ne ay dooleem ak sañ-sañam mi ngi koy jële ci sart boo xam ne Otris moo koy defar, tër ko.
Bismarck gisoon na ne lii de ag anam gu yees gu Otris jëlati la, ñu muure ko mbubum diplomasi walla maslaa, ngir yéegati ci kaw waa Almaañ yi. Bismarck melaloon na sart boobu ne mooy sart bi gën a bon ci mbooleem yu mas a am ci kaw suuf. Ci noonu mu ne woon du teewe ndaje ma lu dul ci kaw ñu jox Brusiya ay àq aki yelleef yu tol ni yi ñu jox Otris ci ñaari mbir yii, ñooy:
- Dëggal ak wéyal jibalug bennoo gi
- Jiite benno gi
Bismarck ci taxawaayam bii, leerale na ci ne Otris daal moom ñàkk na kàttan ga mu amoon ci aakimoo moom rekk mbirum bennoo gu Almaañ gi. Te it won na nguur-nguuraani Almaañ yi ne Brusiya mii kat mooy jenn dooley Almaañ ji man a jiite bennoo gu Almaañ gi.
Bismarck jéem na a fàggu cofeelug Riisi, ngir mu bañ a féete fenn, bu ab xare tàkkee ci diggam ak Otris. Loolooo taxoon mu dugg ci lëj-lëju Poloñ bi, jàpple ci Riisi, kontar gori Poloñ yi defoon ag fipp kontar Riisi, ngir dañal ag àtteem te jéem a am ag tembte, ba man a amal ag àtte gu Poloñ gu temb.
Faraas nag àndoon na ca fipp ga, te jàpple ko, askanu Angalteer wi ànd ca, waaye goornamaa ba moom àndu ca woon, ndax daa ragaloon ag nguurug Poloñ gu katolig judd, guy dem di àndeek Faraans. Ci noonu Bismarck moom dem jàpple-ji Riisi, te jàpple googu gu amoon doole la, ndax moom réewam (Brusiya) daa taqaloo woon ak Poloñ, ba noppi taqalook Riisi. Te it nanguwutoon a ànd ak Faraas ak Otris kontar Riisi.
Xarey Bismarck yi ngir taxawal bennoo gu Almaañ:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Bismarck xuus na ay xare ak lu bari ci réewi Tugal yi digoo’k Almaañ, ngir bennal diiwaani Almaañ yi. Ñu tudd ñatt rekk ci xare yooyu, ñooy:
Xare yu Brusiya yi ak Danmark:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Bismarck xuus na ab xare safaan Danmark, atum 1864g, ànd ca’ak Otris, ngir nangu ñaari diiwaan yii di Shalswig ak Holistin, ñu doonoon ñaari Dóox (duché) yu bokkoon ci bennoo gu Almaañ gi te Danmark tegoon leen loxo.
Danmark mujjoon na ñàkk pexe, daal di deltu ginaaw wëlif ñaari dóox yooyu atum 1864g, bu ko defee Brusiya jël dóoxu Shalswig, Otris it àtte diiwaanu Holistin.
Xarey Brusiya ak Otris:
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Bismarck gisoon na ne xare bi moom – déet sikk – aji tàkk la ci diggante Brusiya ak Otris, te li ko waral du dara lu dul diiwaanu Holistin. Ndax kat mbir yi manuñu woon a nekk di wéy ci anam gii ñu nekke, di ay maslaa yu dëggoodi aki lijjanti yu xootadi aki juboo yu gàtti dig.
Bis bu Yàlla dogalee njortul Bismarck loolu mujj di dëgg, ba Brusiya am ndam, loolu de da na nekki muccug waa Almaañ ñi ci gàllankoor gii tukkee ci Otris, gu leen di teree nekk benn, tee bennoo gu Almaañ gu wér man a am. Màggug Brusiya ci wàllug politig ci biir bennoo gu Almaañ gi, mujj di luy jeqi njàqare ci Otris.
Solofrayn moom màgg na ci anam gu doy waar, rawati na bi ci nguur-nguuraan yu Almaañ yi tiim Géej gu bëj-gànnaar gi bokksee. Ci noonu lu sakkan jug ciy yooni weñ lënkale diggante wàll yu Almaañ yu wuute yi. Loolu tam dooleel bennoo gu koom-koom gi nga xam ne Brusiya mujj na di ci ki ci gën a jariñu.
Sabab yii rekk doyoon nañu ngir taal xeex bi ci diggante Brusiya ak Otris, rawati na ginaaw bi dooley Brusiya ji doxee jawali Holistin, nangu ko, te moom daa nekkoon ci ron kilifteefug Otris, ngir dëppoo gi amoon ci diggante Brusiya ak Otris atum 1865g.
Bismarck moom lijjanti woon na ba Riisi génne loxoom ci diggam ak Otris, loolu nag di ci jàpple gi mu jàpple woon Riisi ci giimal jeqiku(révolution) ga amoon ca Poloñ, atum 1853g. Dëppoo woon na ak Imbratóor bi Napoleon III, imbraatóoru Faraas, moom itam, ngir mu seetaan kook Otris, bañ cee dugal loxoom, li mu koy faye ci loolu nag mooy bàyyi kook yenn moomeel yi ci diiwaanub Rayn. Mu demati tapoo-ji (faire alliance avec)ak nguurug Itaali, gi nga xam ne li doonoon yitteem mooy nocci Venezia ci loxol Otris, ngir matal ag bennoom.
Xare bi amoon ci diggante Otris ak Brusiya xare la woon bu fëkk te gaaw, wéyutoon lu ëpp juroom ñaari ayu-bis, moo waraloon nu tudde woon ko xareb juroom ñaari ayu-bis yi. Dooley Brusiya ji jot na ca a am ndam ci kaw ju Otris ja ca xareb Sadwa ba, ca Bohima atum 1866g . Mu manoon a àgg sax (moom dooley Brusiya ji) ba ca Vienne, bu Imbraatóoru Faraas bii di Napoleon III jugutoon, dox tànki jàmm ci diggante bi. Ci noonu Bismarck daal di ñàkk pexe, taxawal xeex bi, ngir ragal Faraas dugg ci xeex bi ci wetu Otris. Te it Bismarck moom da ne woon na doylu nag ci am ndam gii mu am ci kaw Otris, ak dammte gii mu ko dammte, ndaxte soril na ko bennoo gu Almaañ cig wàll, te it bëggutoon a toroxal Imbraatóoru Otris bi, ngir loolu man na a tax bu jugee ëlëg moom Brusiya di xare-ji ak Faraas, Otris du ko sot, ci geneen wàll. Ag juboo amoon na ci diggante Brusiya ak Otris, ñu koy wax “juboog Braax gi”, atum 1866g. Ci la yii ame:
- Génnug Otris ci Bennoo gu Almaañ gi mu tegoon loxo, la ko dale ca jamonoy Metternich.
- Duggug mbooleem nguur-nguuraan yi nekkoon ci bëj-gànnaaru dexu Rayn gi, ci bennoo gu lëngoo (gu federaal) gu Almaañ ci ron njiitul Brusiya. Diiwaani bëj-saalum rekk a bokkutoon ci bennoo googu.
- Bàyyee gu Otris bàyyee Itaali Venezia.
Gis nga ko, Bismarck kat am na ay ngërte yu am solo ci xareem beek Otris. Moom de fare na fi bennoog Almaañ gu yàgg ga, indi fi leegi ag bennoo gu Almaañ gu yees, gu ame ci mbooleem réewi bëj-gànnaaru Almaañ, nga xam ne ñaari Dóox yii di Shalswig ak Holistin ci lañu woon, buuru Brusiya bi jiite ko. Bismarck nos na bennoo gu yees gi, wutal ko ab parlamaa (Rashstach), ndawi askan wa di fa daje, ak jataayub bennoo gu Almaañ gi (Bundasrat), ndawi diiwaani Almaañ yi bokk ci bennoo gu Almaañ gu bees gi di fa daje.
Bismarck it lijjanti na ba def ak diiwaani bëj-saalum yi bokkutoon ci bennoo gi, lijjanti woon na ba def ak ñoom genn tapoo gu xare .
Xareb Brusiya ak Faraas
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Xetug xare tàmbli woon na a xeeñ ak a jòlli ci diggante Fraans ak Brusiya, ginaaw bi Brusiya ndàmbee ndam ca xareb Sadwa ba. Ndaxte Faraas moom begutoon dara ci lii Brusiya amal ciy ndam ci kaw Danmark ak Otris cig wàll, ak àntul gi mu àntuloon bennoo gu Almaañ gu bëj-gànnaar gi, ci geneen wàll.
Faraas moom daa jàppe woon loolu muy aw xët ci digg ginaawam, ndaxte moom kat manul woon a dékku ag nguur gu Almaañ gu am doole ci wetam. Moom kay li ko sooboon mooy Almaañ des di nguur gu ñu dogat, ngir mu nekk moom Faraas di réew mi am kiliftéef ci sowwub Tugal bi. Moom kay jamono ju nekk, da daan kontar bennoog Almaañ gi, ni ko Otris kontare woon. Bismarck it tàmbli woon na a xalaat nu muy xëcce diiwaani Almaañ yu bëj-saalum yi ngir ñu bokksi ci bennoo gi. Jëf ju mel ni jooju nag Faraas du ko doon nangu, ndax moom tàmbli woon na di dugg ci mbiri diiwaan yu Almaañ yu bëj-saalum yi, ngir tee leen a bokki ca bennoo gu Almaañ ga nga xam ne Brusiya ko jiite woon.
Lëj-lëju ku jigéen ki waroon a donn Espaañ daal di taxaw, mooy lëj-lëj bi taaloon xare bi ci diggante Brusiya ak Fraans. Lëj-lëj boobu mi ngi tënkoo woon nii: gàngunaay gu nguurug Espaañ dafa féexoon , ginaaw bi lingeeru Espaañ bi Elisabeth dawee, ñu gaaral buur bi Leopold ndëpp li, moom mi ngi bokkoon ci njabootug Hohenzellern, di woon ab jegeñaaleb imbraatóor bu Brusiya. Waaye ak li Leopold di bañ lepp ne du sol mukk ndëpp li, teewul Faraas mer ci loolu, jàmbat ko ci buurub Brusiya bi, daal di sàkku ci moom mu warlu ne du ànd ci ñu samp kenn ku bokk ci njabootug Hohenzellern ci gàngunaayaug Espaañ gi. Waaye buuru Brusiya bi bañ, ndax loolu kat dafa xaw a laal teddngaam ak ngoram, te xaw a niru ag yabeel. Loolu nag mi ngi ame woon cim ndaje mu mu defoon ak aji teewal ju Faraas ja ca Ems. Bu ko defee buuru Brusiya bi yonnee ab day ca la juge woon ca ndaje ma, mu yonnee ko Bismarck, mi nga xam ne lepp li mu doon def mooy neggandiku ab pose ééngir jibal ab xare ci kaw Faraas. Ba mu ko defee, Bismarck xëy tas ci yéenekaay yi ay cofiit ca la bawoo woon ca ndaje mooma, ngir merloo ci Faraas. Loolu nag ni mu ko defe mooy génne ay baat yu xaw a wow, yu begloowul dara Faraas. Ci noonu Faraas jug, jibal ab xare ci kaw Brusiya, ci 14 sulet 1870g, te fekku ko woon jekk ngir xeex, te taxul woon it mu xalaat ci ngérte yi man a juddoo ci bii xare, bis bu ñu dàqee Fraans ci xeex bi.
Brusiya li ñuy wax xareb fëkk la doon def ak Faraas, maanaam gaawal ko, loolu nag jot na koo def ba am ci xam-xam ak jarbu ca xareem ba’ak Otris. Bi mu ko defee tàngooru xare bi sax di tar lu tollook juroom benni ayu bis, waaye tàmblee giim, ci ginaaw bi, rawati na ci ginaaw bi ay màndargay kawe ak ëpp doole tàmblee feeñ ci xeex bi ñeel Brusiya.
Xare bi bepp nag ci suufus Faraas la doon tàkke. Jotoon nañoo dàq Fraans nag ci xeex yu bari, bi ci gënoon a siw nag mooy bu Sedan ca satumbar 1870g, nga xam ne àggoon na ci Napoleon III manutoon a ñàkk a wommatu (se rendre), te nangu ne gañe nanu ko, ngir dàq yu metti yi te toftaloo, te yepp di yu nu teg ci kaw dooley Faraas ji ci biir suufus Faraas, te ray lu sakkan ciy soldaaram, te itam lu jege ñaari téeméeri junniy soldaari Almaañ sutuxlu ba ca xolub Faraas, te mu leer nàññ ne Faraas moom manatul a gañeeti Brusiya ca jamono joojee te manatu koo génneeti suufam. Loolu nag di woon ci 27 oktobar 1870g.
Ci noonu imbraatóor gu Faraas gu ñatteel gi daanu, ñu daal di taxawal ci Paris nosteg pénc gu ñatteel gi. Daal di teg Faraas ñeel Brusiya alamaanug xare gu toll ci juroomi bilyoŋi frank yu Fraans (loolu mooy tollook – daanak – alamaan bi Napoleon Bonaparte tegoon Brusiya bi mu ko dumaa ca xareb Yena ba, 1806g. Bu ko defee ñu juboo ci xarekati Almaañ yi duñu génn Faraas li feek fayeesul alamaan bi, (moom nag jotees na koo fay ci diirub ñatti at). Nga rax ci dolli dagg gi ñu dagge ñaari diiwaan yii di Alsaas ak Loren ci faraas, boole leen ci Almaañ.
Nii daal la bennoo gu Almaañ mate woon ci njiitul Brusiya, ci loxol góor gu dëgër gii ni weñ, Bismarck, mi nga xam ne dafa gëmoon bennal Almaañ ak doonte day ci dereet, ci weñ mbaa sawara. Bu ko defee imbraatóorug Almaañ gi daal di sosu, dib xew-xew nag bu fés ci taarixu Tugal bu bees bi.boroom gàngunaay gi (imbratóoru Almaañ bi) mujj di ku ñu joyal ab gogam ci def li ko neex ci nguur-nguuraan yu Almaañ yi. Sartu réew bu Almaañ bu bees bi yaxal na ñu sos ñaari jataay:
- Jataayu Bennoo gu Almaañ (Bundesrat)
- Jattayu (Reichstag)
Dooley yoonal ji nag mi ngi nekkoon ci Bundesrat, di jataay bi nga xam ne mi ngi ame woon ci juroom fukk ak juroom ñatti cér, ñu séddale leen ci nguur-nguuran yi nga xam ne ñoo amal imbraatóóor gu Almaañ gi. Brusiya nag moom rekk amoon na fukki kàddu ak juroom ñaar, ginaaw bi mu am ñaar fukki kàddu. Ak li Brusiya di moomadi li ëpp ci kàddu yi lépp ci Bundesrat, teewul mu gënoon fa’a guddub loxo, gënoon fa a am jeexiital ndax la ëppoon ca nguur-nguuraani Almaañ ya duggoon ca bonnoog Almaañ ga, dañoo takku woon ci Brusiya, te daawuñu woote lenn lu mu bëggul. Te daawuñu jàllale genn saxal ca jataay ba, bu fukki cér ak ñeent àndadee ca saxal ga. Bu dee nag jataayu Reichstag nag moom, man nanñu ne mooy jataayub askan bi, mi ngi ame woon ci ñatti téeméer ak juroom ñeen-fukk ak juroom ñaari cér, ñu leen di tànn ci anam gu sekkaree. Dooley jataay bii nag daanaka dañu koo lafañal, yòqeel ko . ndax nguur ak doole yi ñu ko joxoon ci ron sartu réew bu Almaañ bu bees bi, dañoo nekkoon di yu doyadi te ñàkk solo.
Bismarck nag, jiite na góornamaa bu Almaañ bi niki diisoowaale walla chancelier. Benn ci ñaari jataay yi manul woon ci moom dara, mu yoroon it sañ-sañ bu rëy, te ci ron kiliftéefam tam la Almaañ gu rëy gii gépp nekkoon, nga xam ne ña fa dëkkoon ca atum 1871g jege woon nañu ñeen-fukki milyoŋi nit, mujj àgg ci ñeen fukk ak juroom ñeenti milyoŋ ciy nit atum 1890g, di maanaam bi Bismarck faatoo ba am ñaari at.