Alaaji Omar Fuutiyu Taal

Jóge Wikipedia.
(Yoonalaat gu jóge Alaaji Omar Fuutiyu TAAL)
Alaaji Omar Fuutiyu Taal

Alaaji Omar Fuutiyu Taal mi ngi gane àdduna ci ndëkk su ñu naan Elwaar, ci wetu Podoor atum 1794 -1796 g.j, mu bokkoon ci askan wu cosaanu ci Lislaam, baayam mi ngi tuddoon Sahiid mom Usmaan mom Muxtaar Tukkloor bi, yaayam tuddoon soxna Aadama Caam.

Dund na ay at ca barab yu sell ya (Màkka), bi mu déllusee réewam la dogu woon ci tas Lislaam te jële fi way sanc yi. Ci atum 1853 g.j, la jibal jiyaar ngir yékkati baatub « Laa ilaaha illal Laah » .

Mu song Karta ak Xaaso nangu leen, def fa imbraatóoram gu lislaam gi. Xareb Alaaji Oamar fenqoo na’ak bu Federb bi nga xam ne li ko yékkati woon mooy aar sancoom yi mu amoon ci sowwu bi, ak jéem a tegi loxo penku bi. Alaaji Omar saxoon na te të ci kanamu dooley sanc gi, waaye ci mujj gi mu daanu ca doji Banja Gara ya ca Gine atum 1864 g.j. Bu ko defee doom ja Ahmad Seexu daal di yanu raayob jiyaar bi ci ginnaawam, waaye moom it amoon na ag lott ci kanamu ngànnaayu sancaan yu lëw yii te aaytal. Bi mu ñàkkee pexe la xaatim ag kóllare ak tubaay yi atum 1881 g.j, waaye Gayni mi mu defaloon kóllare googu daal di koy wor, ndax songaat na ko, ga ko ci mu daw, foofu la imbraatóor gi daanoo ci loxoy tubaab yi, atum 1889 g.j .