Yomb

Jóge Wikipedia.
Yomb gi (Laganaria siceraria)

Yomb garabu yomb xeet la ci garab yiy law ñu leen di bay at ba at te ñuy meññ. Foytéefam dees koy jëfandikoo cig wowam ci lu toll ci lu nit manul xayma cig yàgg, ak réew i Àddina bi yépp ak di ci defar ay jëfekaay yu bari mbaa ci lu neew nu koy lekk niki lujum.

Melo wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Yomb garab guy sax at ba at la, di law ci suuf walla ci kaw,am ay car yu gudd teg si di laxasoo. Xob yi dañuy juwwaloo, wërngëlu, lemu teg si nooy ci laal. Foytéefam day am ay melokaan yu wuute, mel ni xala walla mu gudd . Leeg-leeg day niru ag (buteel) am benn wàll gu yaatu ak beneen bu xaw a gudd. Foytéef bi man naa àgg ba ci benn met... walla mu ëpp ko ci guddaay. Kog gi ko wër su wowee day mujj dëgër ba mel ni bant.

Cosaan li[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Garabu yomb mi ngi cosaanoo ci tund yu xala yi dénd i Afrig ak Asii waaye kenn xamul fan la dëgg-dëgg ndax fu nekk lañu ko mujj fekk ci Àddina ndax daa mujj doon mómeelu xeeti doomu Aadama gépp, ñu di ko jëfandikoo ci seen i tukki teg si ñoŋal ko.

Mbayam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Mbayum Yomb de yomb na lool ndax garab gi li mu soxla mooy suuf su wow ci barab bu am naaj ñu man faa ji jiwu garab gi. Man nanu sampaat garab gi su dee am nanu tiitaange ci ñu bañ a màgg mbaa suuf si bañ a tàng. Màggu garab gi gaaw na lool. Dina soxla itam ab sàkket leeg-leeg ngir mu man a law ci kawam. Mbayum yomb nag mi ngi ñor ñaari weer képp ginnaaw ji gi

Njariñam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Su weesoo ñam wii di yomb nu man koo boolee ci sunuy togg, li ëpp ci njariñu yomb mooy joxe ay jëfandikaay yu nit di soxla niki Koog, Leget, mbàttu, añs. Amna ñu koy jëfandikoo it yeneen i xeetu jumtukaay yu jëm ci woy niki Koraa, Xalam, añs. Leeg-leeg itam nga gis ku ko jël taaral ko ngir jëmal dëkkuwaayam.

Nataal yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Turu xam-xam wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Laganaria siceraria