Xareb Àdduna bu Njëkk

Jóge Wikipedia.
tumb
tumb

Xareb Àdduna bu Njëkk (1914 – 1918) benn la ci ñaari Xarey àdduna yi tàkk ci xaaj bu njëkk ci ñaar-fukkeelu xarnu bi. Xarnu bi seere na tàkkug ñaari xare yi gën a rëy ci taariixu nit, beneen bi di Ñaareelu Xareb Àdduna bi (1939 – 1945g).

Li waral xare bi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Xareb àdduna bu njëkk bi am na ay sabab yu jonjoo ak yu jonjoodi,

Sabab yu jonjoodi yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Man nanoo tënk sabab yu jonjoodi yu xareb adduna bu njëkk bi ci ñeenti sabab yu mag ñooy:

Gëpplante gi ci wàllug canc[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Gëpplanteg àdduna gi taroon na ci ginaaw yewwuteg ndefar gi, ci fukk ak juroom-ñatteelu xarnu g . Réewi ndefar yi seeni cawarte gën naa yaatu, gën a jëm kanam ci gii wàll, ci fukk ak juroom-ñeenteelu xarnu g, li ko waraloon di naj gu tar ak jañax gu tëw a dakk gi leen seen lonkoo (société) yu ndefar yu mag yi daan jañax jëme ci loolu, ak boroom boppi-alal yi dëkk ci yile réew, rawati na nag ci réewi Tugal yi am ay noste yu gore (systèmes libéraux). Bu ko defee ñu jóg tàmblee seeti-ji cémb (brut) yi manul a ñàkk ngir liggéeyi ndefar yii man dox, man a jëm-kanam. Tàmblee wër it ja yu nu man a jaaye-ji seen liggéeyi ndefar yu wuute yi.

Loolu nag jur na fi ag xér ci ne-ne, loolu tam jurati fi jawwi gëpplante ci wàllug sanc ci diggante réewi ndefar yu mag yi, lii itam jur ag rawante ci ngànnaayu ci àdduna bi, bu ko defee ndefarug ngànnaay gën a jëm-kanam, ndaxte ku bëgg a sanc fàww nga yor ngànnaay yu doy, ku ko bëgg a suuxat it mbaa nga bëgg cee ame sa njariñi koom-koom yi tax nga koy def fàww nga ngànnaayu.

Ag gëpplante gu tar amoon na ci wàllug koo-koom ci diggante waa-Brëtaañ yeek waa-Faraas cig wàll, ak ci seen diggante ñoom ñaar ak Almaañ ci geneen wàll. Silaay Almaañ yi bari woon nañu ci ja yu àdduna yi, ngir ay sabab yoy yenn yi danoo dellu woon ci jëm kanam gi endustri Almaañ jëmoon-kanam, yi ci des dellu ci barig naali koom-koom yu Almaañ yi ci réewum Usmaan mi, rawati na naalub yoonu weñu Berlin-Baxdaad-Kuwet. Xëccoo googu nag amoon ay jeexiital yu rëy ci tàkkug xareb àdduna bu njëkk bi.

Ci nii lanuy gise ne gëpplanteg koom-koom gu àdduna bi mooy li duggal àdduna bi ci paxum xare bu tàng, bu nu ngànnaayal.

Tapoo yu réew yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

tappoo yi
tappoo yi

Gëpplanteg politig gi aju woon ci canc ci àdduna bi dafa gënoon na jëm-kanam, ci ginaaw bi gëpplanteg koom-koom gu àdduna bi gënee jëm-kanam. Loolu nag tax ba ay dank sosu yu réew, defees it ay kollarante aki dëppoo yu yor màndargam politig, mu xare ci diggante ab lim ci réew yi seeni njariñi canc di jegee, walla yi ci jot a àgg ci déggoo ci lijjanti lëj-lëj yi nekk ci seen diggante. Ñu tuddal leen ci dëppoo yooyu ak tapoo yooyu, yii di ñëw:

Tappoo gu ñaaral gi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Gii tappoo amoon na ci diggante imbraatóoru Almaañ gi ak gu Otris gi ci atum 1879, bokk na ci li ëppoon solo ci ay sartam, lii di ñëw:

  • Bu Riisi gu Xaysar gi songee menn ci ñaari reew yi , meneen mi war naa dimbli mi nu song.
  • Bu menn ci ñaari réew yi tappoo songee meneen mu ñatteel, ma ca des da ca a war a ame taxawaayub génn ci, di leen seetaan waaye nag ci anamug cofeel ñeel àndandoom boobu.
  • Bu ag dimblante gu am solo amee, walla gu xare ci diggante Riisi ak Faraas, ñaari réew yii tapoo de war nanoo ànd liggéey ngir xeex loolu.
Tappoo gu ñattal gi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Moom ag tapoo la gu Almaañ-Otris-Itaali, mi ngi sosu ci bi Itaali duggsee ci tappoog ñaaral gi nu la tuddoon leegi ci 1882, ak doonte njariñi Itaali dëppoowut ak yu imbraatóorug Otris gi, waxuma la sax noonoo gu yàgg ga nekkoon ci seen diggante, te li ko waraloon di yilif gi ko Otris yilifoon njëkk bennoo ga, ak ca ginaaw ba, waaye Otris mii moo tegoon loxo ag wàll ci suufus Itaali, ba noppi yilif fa yeneen wàll.

Itaali duggsi na ci tappoo gi ngir wuute gi mu defoon ak Faraas, ndax fraans dafa dëgëraloon bu baax tànkub sancam ca goxi bëj-gànnaaru Afrig, fu ci mel ni Alseeri ci atum 1830g, ak Tiniisi atum 1881g, kon Itaali duggsi gii mu defoon ci tappoo gi du woon dara lu dul doxaliinu politig, li mu ci jublu woon di jañaxal Faraas ak Brëtaañ ngir manante leen ci ñu nangul ko te bàyyee ko njariñam yi nekk ci Géej gu Diggu gi. Dëppoo gu Fraans-Rusi gi:

Dëppoog cofeel gu Faraas-Riisi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Dëppoo googu am na ci ginaaw bi ag jegeente amee ci diggante Faraas ak Riisi gu Xaysar gi, loolu nag tàmbli na ci atum 1886, daal di gën a jëm-kanam ci atum 1888g, bi ñaari réew yi dëppoo ci fas ag kollare guy waral Faraas di jox Riisi ngànnaay, te jëmale-kanam ag jokkoom jaare ko ci def fa ay yooni weñ. Ci atum 1891g la Faraas ak Riisi def ag kollarante guy yaxal lii di ñëw:

  • Taxawal ag dëppoo ci diggante ñaari réew yi, ak weccante xalaat ak diisoo buy lëj-lëj amee ci adduna bi.
  • Bu menn ci ñaari reew yi duggee cib xare, ñaari réew yi war nanoo diisoo ngir dëppale seen diggante.
Dëppoog cofeel gu Brëtaañ-Sapoŋ[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ag dëppoog cofeel sosu na ci diggante Brëtaañ ak Sapoŋ ci atum 1902g, lii la yaxal:

  • Bu xare tàkkee ci diggante Sapoŋ ak Riisi gu Xaysar gi, Brëtaañ da caa war a génn te seetaan.
  • Bu meneen réew duggee ci xeex bi nekk ci diggante Riisi ak Sapoŋ , kon Brëtaañ da ciy war a dugg moom itam, jàpple Sapoŋ .
Dëppoog cofeel gu Brëtaañ-Faraas[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ag dëppoo gu cofeel xewoon na ci diggante Brëtaañ ak Faraas ci atum 1904, gu lijjanti woon lëj-lëj ak reeroo yi amoon ci seen diggante, dëppoo googu nag lii la wax:

  • Féexal Faraas, joyal ab loxoom ci Marok, gii nga xam ne jotoon naa temb, te nangul ko teg gi mu teg loxo Alseeri ak Tiniisi.
  • Faraas moom tam nangul Brëtaañ teg gi mu teg loxo Isipt ci atum 1882
Dëppoo gu cofeel gu Brëtaañ-Riisi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ag dëppoog cofeel am na ci diggante Brëtaañ ak Riisi gu Xaysar gi atum 1907g, lii la wax:

  • Déggoo ci ni nuy séddoo barabi sañ-sañ yi ci Iraan, ba mu des fa benn barab rekk bu temb ca digg ba ñu bàyyil ko fa Shaah ba, ginaaw bi Riisi jëlee wàll gu bëj-gànnaar gi, Brëtaañ jël gu bëj-saalum gi.

Màggug yëngu-yënguy xeetu yi ci Tugal[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Yëngu-yëngu yi aju ci xeetu dafa xëy gën a màgg ci Tugal, loolu nag bokk na ci li jañ àdduna bi jëme ko ci xare bi. Xarnub fukk ak juroom-ñeenteel g, dees na ko lim muy xarnub xeetu yi ci Tugal, yëngu-yënguy xeetu yooyu nga xam ne li leen taxoon a jug mooy gooreel seen bopp te nocciku ci kilifteef ak teg loxog réew yi leen di àtte cig wàll, ak sosal xeet wu nekk am réewum boppam mu koy ëmb, uuf ko ci geneen wàll. Ñaar nag bokkoon nanu ci yëngu-yëngu yi gënoon a siw ci yooyu, ñooy:

Mbootaayug Slaaf gi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Gii mbootaay, walla yëngu-yëngug slaaf gii, li ko taxoon a jug mooy xettali askanu slaaf wi jële ko ci àtteg imbraatóor gu Otris gi, ak sos réewum slaaf mu ëmb mbooleem slaaf yi dëkke ci Balkaan ak salaaf yi dëkke ci Penku Tugal. Mbootaay gii nag daan na jot ag jàpple mu tukke ci Riisi gu slaaf gi, loolu taxoon na ba ag reeroo gu mag am ci diggante Otris ak Riisi gu Xaysar gi.

Lëj-lëji àdduna bi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ay lëj-lëj yu fasu yu àdduna bi sosu nañu, bokk it bu baax ci li fi taal xareb àdduna bu njëkk bi. Lëj-lëj yii it li leen jur day dellu ca reeroo ya amoon ca diggante réew yu mag ya ngir seen gëpplanteg canc gi, ak ngir màggug xeetu ci Tugal, ak ngir fipp gi askan yi fippoon ngir jot seenug tembte ak gore. Ñu tudd ci yi ëpp solo ci lëj-lëj yooyu:

Lëj-lëju Maraakes[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Faraas yàgg naa waaj ak a naal ngir teg loxo Maxreb gu sori gi (Maraakes), moom nag Maraakes dafa yoroon ag tembam lu yàgg, te booba Tuniusi ak Alseeri, Faraas a ngi leen tegoon loxo, yilif leen cig canc. Ci noonu Faraas lijjanteek Brëtaañ seen reeroo gi nekkoon seen diggante, ca dëppoog cofeel ga ca atum 1904, Faraas daal di bokki ca ndaje ma ñu njëkk a def ca dun bu wert ba ca atum 1906 ca Espaañ ngir lijjanti lëj-lëju Maraakes bi.

Saxal ya juddoo ca ndaje ma nag njariñul Faraas la gënoon a nekk, ndax réew ya fa daje woon dañoo dëppoo woon ci nangul Maraakes ag tembam waaye feetale Faraas wàllug kaaraange ga ak sàmm njabootug Tugal ga fa nekkoon. Faraas nag jariñu na bu baax ci dénk gi ñu ko dénk kaaraange ga, ndax ba ay yëngu-yëngu amee ca Faas ga nekoon péey ba, da faa daal di woon yabal ay dooley xare yu Faraas ngir ne da ciy aar jàmburi Tugal ya fa nekkoon. Loolu moo merloo woon Almaañ, mi àndoon ak buurub Maraakes, daal di ne woon fàww Maraakes jot cig tembam, ngir naqaral Faraas. Almaañ daal di yabal ag gaal gu mag ca waaxub Agadiir ngir aar ag njabootam, ak ñaxtoo ci yabal gi Faraas yabaloon am mbooloom xare ca Faas ci atum 1911 ngir teg ko loxo. Ñu defaat am ndaje ca dun bu wert ba ca Espaañ ci atum 1911g, ngir lijjanti xuloob Faraas-Almaañ bi, la fa juddoo di: jox Almaañ ay moomeel ca Kongóog Faraas ga, bu ko defee Almaañ nangul Faraas nekk gi Maraakes nekk ci ron kaaraangeem, ñu daal di def Tanja muy ab waax bu àdduna bépp, daal di doxal nag politigu ubbi buntub Maraakes ci kanamu yaxantug àdduna bi.

Lëj-lëju Balkaan[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Otris daa boole woon ci boppam ñaari gox yii di Bosni ak Hersogowin atum 1908g, te ñoom ñaar ñi ngi bokkoon ci diiwaani reewum Usmaan mi ci Balkaan. Reewum Usmaan mi ca jamono jooja dafa nekkoon di dund ci jawwi yong , mooy yong gi ñoñ bennoo ñi defoon atum 1908g. Serbi nag (moom ag wàll la ci yogoslaafi ci jamono jii nu nekk) daal di ñaxtu loolu ak Rusi gu Xaysar gi ko daan jàpple (moom Serbi). Almaañ jug moom jàpple Otris ci jëfam jooju. Loolu nag bokk na ci li gën a dolli tangoor wi ca daanaka-dun bu Balkaan ba.

Lëj-lëju Maseduwaan[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ab xare tàkkoon na ci diggante Reewum Usmaan mi ak Gres, Bulgari ak Serbi ci Maseduwaan, ñoom ay reewi Balkaan lanu. Li ko waraloon nag mooy Bulgari, Gres ak Serbi danu doon defi pexe ngir roccee Maseduwaan ci Reewum Usmaan mi, te seddoo ko ci seen biir. Bi nu dàqee Reewum Usmaan mi ca xare ba ba noppi, danoo reeroo woon ci ci seen biir ci nu nu koy seddoo. Serbi moom daa bëggoon a jot ci Albani, waaye ñu xañ ko ko, ndaxte Otris daa taxawoon temb ci nu jox Albani ag tembam. Loolu waral leneen coow amati ci Balkaan ci diggante Serbi, Otris ak Rusi ak ñeneen.

Lëj-lëju Tripoli[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Itaali jariñu na ci am soxla gi Reewum Usmaan mi amoon soxla ak lu ko doy, ca xareem ba ca Balkaan, bu ko defee mu song ko ca Tripoli gu soww ga, atum 1911g, daal di nangu Libi, teg ko loxo atum 1912g, ginnaaw bi mu lijjantee ba Fraans ak Britani genn ci, te noppi ci.

Sabab yu jonjoo yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Noonoo gi taroon na jëm ci Slaaf yi ci Balkaan, looloo waraloon ñoom Slaaf yi juggoon taxawal ag mbootaay gu làqu ngir xeex loolu, Serbi jàpple leen ci ak Riisi gu Xaysar gi. Ab dongab Slaaf yong na Arshidog Fransis Ferninand, mi nekkoon wuutlaayu Otris ak soxnaam, ca 28 suwe 1914g, ca dëkkub Sarayevo bi nekkoon peeyub Bosni, ci tukkib nemmeeku bu mu fa doon def. Otris daal di gaaw jariñoo xew-xew bii, daal di yonnee Serbi ag xupp ca bisub 22 sulye 1914g, gu làmboo fukki sart ak benn, bokk na ci yi ëppoon solo ci sart yooyu: raxas goornamaab Serbi bi ak dooley xareem ji ci mbooleem ku bokk ci kureel yiy kontar Otris, te may Otris mu defal boppam raxas gii, te tëj yëglekaay yi ak këri tas-xibaar yi noonu Otris, ak boole Otris ci gëstu ñi def yong googu ak àtte leen. Ak yeneen sart yu tar yu tax Serbi jortu ne kii daal daa fas yeenee dugg ciy mbiri biiram. Ba noppi Otris joxati Serbi diirub ñeen-fukki waxtook juroom ñatt, ne ko mooy àpp bi nga xam ne waru koo weesu te tontuwul, waaye Serbi moom tontuwul .

Jibalug xare bi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Otris taal na xare bi ci kaw Serbi, ci 28 sulye 1914g . Bi loolu amee Rusi moom itam jug song Otris ngir jàpple Serbi, loolu it jurati Almaañ jug – cig wàllam – jafal ab xare ci kaw Rusi ak ci kaw Serbi. Fraans duggsi ci, ci wetu Rusi miy reew miy xaritam, nadx moom la defal ag tapoo, daal di jibal ab xare ci kaw Almaañ ak Otris. Britani tam it xuus xare bi kontar ñaari reewi digg yi nga xam ne Reewum Usmaan mi mujj na àndseek ñoom ci xeex bi. Siin it ak Japon mujj nanu duggsi ci xare bi ci wetu reewi dëppoo gi. Itaali it dugg-si ci kontar reewi digg yi, atum 1915g, te kat bu njëkk da doon seetan rekk, feetewutoonn fenn. Britani nag nekkoon na di fasante ak Itaali kollareg sekkare. Kollare gi nag li mu doon yaxal mooy Itaali jox ko suufus Dalmaas bu xare bi jeexee. Amerig dikk moom itam, dugg-si ci xare bi ci wetu reewi dëppoo yi, daal di genn ca beroom ga mu defoon ca goxub Amerig ba. Duggsi gi mu duggsi woon ci xeex bi nag lu am solo la woon, ndax moo ko soppi bu baax, ngir doole ak jumtukaay yi mu indil reewi dëppoo yi ak alal.

Lefum xare bi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Jë bu sòww bi ëmboon Fraans ak Beljig, mooy barabu xeex bi ëppoon solo ci xare bi ci diggante 1914 – 1915g, boobu diggante mooy bi gën a tar ci xeex bi. ndaxte dooley reewi digg yi jot nanoo putuxlu ci reewum Beljig mi ak wàllug penku gi ci Fraans, ak li reewi dëppoo yi di jàmmaarlo lepp ak a xeex ngir loolu bañ a am. Lii nag bokk na ci ndam yi ëpp solo, yi reewi digg yi def ci jëwub sòww bi. Waaye reewi dëppoo yi jot nanoo taxawal jëm kanam gi Almaañ ak Otris doon def, ba daanaka àgg ca bunti Paris, ci xeexub njàmbaar bi nu doon def ngir aaru. Ñaari wàll yi nag xeex nanu ay xeex yu tar, yi ci gën a siw mooy bu Marn bu njëkk bi ci sulye atum 1914g.

Bu dee nag ci jë bu penku bi, xare bi moom foofa ci diggante Rusi ak Otris la nekkoon. Barabub xeex ba di woon Poloñ ak Balkaan. Xeex bi amoon ci penku bi nag xawoon na a woyofal tuuti yan bu diis bi nu tegoon ci ndòddum reewi dëppoo yi ci sòwwu bi, ndax reewi digg yi danoo mananul woon a ñàkk a dolli seen soldaar sa nekkoon ca penku ba di xeex ak Rusi. Foofa tam ca penku ba lanu gëne woon aw demiin ca sòww ba, ndax jot nanu fa a nangoo wàll gi Rusi moom ci Poloñ ak Litwaani.

Ay xeex am ca diggante Reewum Usmaan mi ak Britani ca Iraag ak Palastin. Ca la Britani tege loxo ñaari reew yii. Reewum Fraans it nangu Siri ak Libaa.

Bu dee ci geej gi moom, xeex bi mi ngi doon ame ci nuuraakon yi nga xam ne Almaañ da leen daa joyal ci gaali reewi dëppoo gi. Mbooloom gaalum Britani mi nag moo kawe woon ci xareb geej gi. Xareb Gitland bu geej bi amoon atum 1916g, bokkoon na ci xeexi geej yi gën a rëy ci xare bi, nga xam ne Amaañ ak Britani ñepp ñàkke nanu ci lu dul jeex ciy nit ak jumtukaay.

Atum 1917g, bokk na ci at yi gën a tar ci ati xare bii, ci la Rusi genne ci xare bi, ca kollareg Litofski ga ca 27 desambar 1917g , ci ginaaw bi fippug Balsafi gi amee. Romani topp ca moom mi sukkandiku woon ci xare bi ci Rusi, moom itam ag gennam mi ngi jaare ci kollare ga nu defoon ca Boxarest. Ca at mooma tam la Diiwaani Amerig yu Bennoo yi ñoom it duggsi ci xare bi ànd ak reewi dëppoo yi. Loolu nag feeñ bu baax ci doxiinu xare bi, ndaxte Amerig moom jàpplee woon na bu baax ci wàllug xare ak koom-koom, loolu nag di woon lu sonnal reewi digg yi. Ca at mooma tam la jë bu Usmaan bi it nërméelu. Ci la jë bu Otris it daanu. Ay yëngu-yëngu aki coow yu ay ligeeykat am ca Almaañ. Ca mooma at it la Woodrow Wilson defoon fukk ak ñeenti poñam ya doon woote ñu taxawal xare bi te bàyyi askan yi ñu def li nuy wax (autodétermination) muy tànnal seen bopp mujj gi nu gis ne moo gën ci ñoom.

Atum 1918g nag mooy atum ndam li ñeel reewi dëppoo yi, waaye it mu nërmeelu ñeel reewi digg yi, ndax imbraatoorug Otris ak gu Almaañ yépp daanu nanu, Imbraatoorug Usmaan gi it ñàkk mbooleem diiwaanam yi mu amoon ci bitib Asi gu ndaw gi, nguurug Bulgari daanu, ci noonu askani reewi digg bi daal sàkku wéerum ngànnaay ci ni ko poñi Wilson yi doon sàkkoo. Bi reewi digg yi demee ba lòtt ci wàllug aaru, te manatunoo dékkooti xare bi, lanu wommatu . Bu ko defee Bulgari xaatim ag wéer ngànnaay ak reewi dëppoo yi ci 30 satumbar 1917, Turki topp ci, ci mujjug oktoobar atum 1918, ak Otris ci 3 nowambar 1918, ak Almaañ ci benn fanu nowambar 1918g.

Lijjanti yi ci ginaaw xare bi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Reew yi am ndam ci xare bi defoon nanu am ndajem juboo ca Paris, peeyub Fraans, li ko waraloon nag mooy gëstu nan lanu war a def ci adduna bi ginaaw bi xare bi jàllee. Moomu ndaje nag Clemenceau moo ko jiite woon, njiilul jëwrin lu Fraans li, bu ko defee, ñu defe ndaje ma ca njéndul Varsaay la, di dëkk bu nekk ca wetu Paris. Diiwaani Amerig yu Bennoo yi Wilson teewal ko, Britani Luwid George njiitul jëwrin la nekkal ko fa, Fraans Clemenceau miy njiitul jëwrin ya moom itam wuutu ko fa ak Itaali ci teewaayu Orlando njiitul jëwrinam, reew yii amoon nanu xejj gu mag ci ndaje mi, rawati na ñatti reew yii di Amerig, Britani ak Faraas.

Ndajem juboo mii ay saxalam ballewunu ci déggoo ak waxtaan wu reew yi gañe def ak yi nu gañe, waaye kay reew yi gañe danoo teg seeni sart ci kaw reew yi nu gañe cig sañ-bañ. Kollare ga nu fase woon ca Versailles atum 1919g te xaatimoon ko ak Almaañ, bokk na ci kollare yi ëpp solo te juddoo ci ndajem juboo mi. Moom kollare googu dafa yaxaloon lii: Delloo Fraans Alsaas ak Loren, ak delloo Danmark wàllug bëj-gànnaar gi ci goxub Sholswig, bu ko defee Poloñ moom jot ci suuf su bari ci Almaañ ak yoon wu yaatoo ñeen-fukki miil, wu romb ci biir diiwaanub Brusiya gi nekk ci Almaañ, bu ko defee tàqale kook yeneen suufi Almaañ yi. Ci noonu ñu def waaxub Danseg bu Almaañ bi muy waax bu nu jagleel reewum Poloñ mi nga xam ne taxawalaat nanu ko ci ginaaw xare bi. Nu jëlati ci Almaañ diiwaanu Sodit jox ko Cekoslawaki, mi nga xam ne mi ngi sosu woon ci ginaaw xare bi, ñu jëlati ci Almaañ waaxub Mamel jox ko Lituwani. Bu ko defee Almaañ ñàkk mbooleem sancoom yi. Ba noppi nu ga ko ci mu yamale ay soldaaram ci teemeeri junni. Nu neenal fa duggum coldaarum gu sañ-bañ, dindi mbooleem tata yi wëroon kanaalub Kyel ak goxub Rayn. Nu tàmbli woon a def fuglu gu tar ci ligeeywaayu ngànnaay yi ak jumtukaay yi ci aju. Ñu nangoo woon ci Almaañ it mbooleem ay nuuraakonam aki gaali xareem aki fafalnaawam ak lu ëpp ci ay gaali yaxantoom, ci noonu Fraans nangooti diiwaanu Saar ( di xuru dexug Rayn gi) di barab bu naat ci ay mbell, mu nangu ko nag diir bu tollu ci fukki at ak juroom. Ñu daal di teg Almaañ nag ag alamaanug xare ak alal ju mu war a fay ju bari ju tollu ci (6,600,000,000) yu Sterlin, ak doonte Almaañ fayu ci ci diggante 1924 – 1930g lu dul lim boobu rekk.

Imbraatoorug Otris gi nag moom, ndaje ma daa daal di jeexal nguurug njabootug Habsborg ga fa nekkoon, daal di taxawal ciy màbbiitam ay àtte yu bari, ñooy: Pencum Otris ak Hongri ak pencum Cekoslawaki, ñu jëlati wàllam ya nekk ca Balkaan boole ko ca reewum Yogoslawi mi sosu ci ginaaw xare bi. Bu dee Reewum Usmaan mi moom dafa ñàkkoon mbooleem moomeelam yi mu amoon ci Asi ak Afrig, deseetutoon lu dul moomeelam yi mu amoon ci Asi gu ndaw gi, ñu daal di ko def muy leegi pencum Turki wuuteek lool reewum Usmaan mu mag ma nu xamoon, loolu di woon ci 29/10/1923g, ginaaw bi Mustafa Kamaal Atatork (1880 – 1930g ) neenalee nosteg saltana ga fa amoon atum 1923g, ak gu xalifa ga atum 1924g.

Ndaje mi nag sos na fi ay reew yu yees yu bari ci Balkaan, mu ci mel ne mom Yogoslawi mi jële won ay suufam ci reewum Serbi mi ak yenn ci goxi Balkaan yi bokkoon ci moomeelug imbraatuurug Otris gi, bu ko defee nu sosaat reewum Poloñ mi ak Brusiya. Reewum Cekoslaafi moom itam taxawe ci ñaari xeet yii di Slaaf ak Cek, reewum Hongri tam sosu, Finland, Stwaani, Lituwani ak Latfiya reew yii yepp jug di dëgëral seeni nekktey politig, te bu njëkk danoo nekkoon ci ron teg loxo gu Almaañ, ci ginaaw bi Rusi gennee ci xare bi atum 1917g, daal di fas kollareg Litofski gi ak reewi digg yi. Lii moo jeexal àtte gi njabootub Romanof gi doon àtte Rusi.

Ñu daal di jël nag yenn reew yi teg leen ci ron ag feetale: Iraak, Penkub Urdun (Jordanie) ak Palastin ñu teg leen ci ron feetale gu Britani atum 1920g, Siri ak Libaa ñoom ñu teg leen ci ron feetale gu Fraans atum 1920g. Ndajem Paris ma nag saxaloon na feetale gii te xaatimoon ko.

Ñu daal di sos Kureelu xeet yi (League of Nations) teg ko ci poñub fukk ak ñeent bi ci dali Wilson yi doon woote ag ñoŋal jàmm ci adduna bi ak tee xare amati fi ak dëgëral dimblante ci reewi adduna bi.

Nii daal la xareb adduna bu njëkk bi jeexe ginaaw bi mu sonnalee adduna bi bepp, sotti ko sawaraam si ak alkandeem li. Ray nanu ci lu jege juroom ñatti milyoŋi nit , gaañ ca lu jege ñaar-fukki milyoŋ. Waxuma la nag ñi faatoo ca xiif bu metti ba’ak tawat ja xare ba waraloon.

Gongikuwaay[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Téere taariix bu bees bi te jamonoo bu Abdu Xaadir KEBE