Waxtaani jëfandikukat:Seexunaa Ture27
Yokkuw tëriit== LAMMIÑU RÉEW MI AK GËSTU. Mbooloo mi maa ngi leen di gërëm di leen nuyu itam te fas yéené waxtaan ak yeen ci li nga xam ni moo nu fi dajale, waxtaan ci làmmiñu réew mi ak gëstu. Loolu, bu ñu ko waxee kon dafa mel ni dañuy laaj ndax ca dëgg-dëgg, sunu lammiñ yii, bu caaxaan demee dëgg des ndax mënees na cee leeral ab xam-xam? Ndax mënees na cee gëstu dëgg-dëgg i fànni xam-xam yi nga xam ni yii tey, ñoo tax réewi tubaab yi di dox. Ndax réew yi nga xam ne ñoo nekk tey ci kanam ci àddina, xam-xam bi nga xam ne moom lañuy jàngale ci seen daara yi ( école) tegaloo, ( class) ndax mënees na ko jàngale ci làmmiñu réew mi bu mu ci mën di doon, moo xam wolof la, moo xam weneen lammiñ lay doon... Pël walla séréer la walla lammiñ wu mag wow réew mi.. Ndax mënees na cee jàngale xam-xam yooyu, ci koo xam ni kii mënul a jaar ci daaray tubaab. Loolu jàpp nanu ne mën naa am. Kon loolu itam, laaj na kon nu topp sunu lammiñ yi seet ba xam fu ñu cosaanoo ak naka lañu taxawe ci àddina sii nu nekk tey, ak li ñu mës a jote ak làmmiñ yi ci des ca cosaan.
Kon laaj na nu xool tuuti ci sunu ginnaaw, seet naka la àddina doxe ba fii tey, ndax làmmiñ yi li ci ëpp lépp dañu leen di jariñoo waaye xamunu seen cosaan dara! Kon nag, leeral seenum xel itam ci cosaanu làmmiñ yi, ba ngeen gën a xam ni seen làmmiñ yi deme ak làmmiñ yii fi nekk ci àddina ci gan fànna lañu bokk, ak ci yan bànqaas lañu fàqe. Loolu itam dana tax ci wet googu seenug taxawaay gën a dëgër...
Ma bëgg leen a fàttali ne, yàgg ngeen a dégg ba ñu ko jëkkee wax fii ba nu ko daan wax ca njaalbéen ga, bu yàggoon naan foog nañu ne sax Afrig, fi lañu tëne sunu maam Aadama - booba ñépp dañu defe woon ne ay Léeb la! Léegi xam ngeen ne xam-xamub « sayiir» dëggal na loolu ba fi mu nekk ñépp jàpp na ne Afrig lañu tëne suñu maam Aadama... ==
Seex Anta jóob téereem bi tuddu Làmmiñu Réew mi Seexunaa Ture27 (xëtu waxtaanuwaay) 1 Fewriyee 2022 à 20:24 (UTC)