Waxtaani jëfandikukat:Goryalla.infos
Yokkuw tëriitWaxtaanu Gelwaar
[soppi gongikuwaay bi]
Baaraam bun tàllal ab joxoñ la, xam ngéen loolu.
Wante juroomi waaraam yun tàllal kuy romb, yal-waan la ! Sunu njiit yaa ngi nu dajale fii, ndax xam ngéen lu tax ? Du tus, ngir man a jot ci ndimbal lii doŋŋ. Te dégg ngéen sunu njiit yii ñuy sant, ak di gërëm, yërmande gu amul àpp, ci sunu tur nun ñépp, ñi fi nekk ak ñi fi nekkul, jagleel ko ñi nu jox ndimbal lii. Xool léen sunu njiit yi, koo ci gis mi ngii bég di layaam-layaami sunu kanam di daagu, mel ni ndimbal li seen ñàqi bopp la. (Sóopap..) Nun nag, nun askan wi nga xam ne, amunu kàddu, amunu fayda. Nuy pecc ak di wey jagleel ko ndimbal lii.
(Cëë...) Noo ñàkk fayda ! Mane, nan léen ubbi sunu gët yi xool, te xamne ag njaboot munta sosu, sax ren dëgër, su sukkandiku wul ci lenn ludul yal-waan gu sax dàkk dàkk !
Te yéen gis ngéen ni xewu may gu mel nii diirub 30i at mingi am fii, ak faneen. Ndimbal lii ñu ñuy seddale, moo nuy ray. Rayna bépp jom ak ngor gu nekkoon ci sunu biir. (Cëë...) Noo ñàkk jom kenn amatufi jom. Ndax xam ngéen ne réew yi ñuy yonnée may gi ci njekk ak tiitër dañ nuy ree sax fañu dëkk ndax xam ngéen loolu ? Rax ca dolli sunu doom yu góor ak yu jigéen ya nga xam ne ñoo ngay dundd foofa ca bitim réew, gàcca ray na léen, munatuñoo siggi xool kenn ndax gàcca, munatuñoo siggi xool kenn ndax gàcca. Dëgg la sunu réew mii coono bu nekk wàcc na fi, [musiba!] (catastrophes !) wàcc na fi ! Waaye, loolu nun noo ci wara taxaw, du kenn ! Nun doŋŋ noo ci wara man a taxaw. Sunu maam Kocc Barma neena: "su fekkeentane bëgg ngaa ray as gor, dee ko jox suba gune limiy dune. Bu yàggee nga soppiku mala." Dag ngay doon dag. Wax naa leen li fi nekkoon ci jom ak ngor di kor-koral ndimbal li lekk nako, ndimbal li lekk na bépp jom ak ngor gu nekkoon ci sunu biir. Du gis ngéen xiif wi, ak mar gu metti gi nekk fii ak ñàkk a colu gi rafle wi. Ndax xam ngéen lu ko yokk ? Ma wax leen liko yokk, gis ngéen réew ci boppam, bo fekkeentane li muy dunde ak di ko woddoo mi ngi ko yaakaaree ci réew ni moom. Gis ngéen réew mooma liko dale ci doomam ba ci ay sër sëtaatam benn kàddu doŋŋ lañuy xam laaj leen ma ban kàddu :
Jërëjëf, jërëjëf, Jërëjëf, jërëjëf. Nun nag, nun askan wi nga xam ne, amunu kàddu, amunu fayda, nuy pecc ak di wey jakleel ko ndimbal lii. (Cëë...) ñakk fayda ! Mane nan leen ubbi sunu gët yi xool, te xam ne ag njaboot munta sosu, sax ren dëgër, su sukkandiku wul ci lenn ludul yal-waan gu sax dàkk dàkk !
Te yéen gis ngéen ni xewu may gu mel nii diirub 30i at mingi am fii, ak faneen. Ndimbal lii ñu ñuy seddale, moo nuy ray. Rayna bépp jom ak ngor gu nekkoon ci sunu biir. (Cëë...) Noo ñàkk jom kenn amatufi jom.
- _Maam Góor Jóob_* ✍️ Goryalla.infos (xëtu waxtaanuwaay) 19 Oktoobar 2023 à 18:30 (UTC)