Aller au contenu

Tiitaange bu 1792

Jóge Wikipedia.

Tiitaange gu mag gi am ci atum 1792 jafe-jafe leeblé la woon ci weeru màrs ak awril 1792, mu juddoo ci yokkuteg leeblé bi Bànk bu bees bi sos ci États-Unis, ak itam spekulaasioŋ yu bari yu bawoo ci William Duer, Alexander Macomb ak yeneen baankeer yu mag. Duer, Macomb ak seen naataango jéemoon nañu yokk njëgi bor yi ci États-Unis (US) ak ci action bànk yi, waaye bi ñu ñàkk bor yi, njëg yi wàcci, loolu waral bànk yi dajal. Li Bànk bu États-Unis tëj leeblé bi ci jamono jooju, moo gëna yokk tiitaange gi ci ndoorte li. Sekkerteer bu Treasury bi, di Alexander Hamilton, moo mëna xeex jafe-jafe yi, ndax dafa jox bànk yi ci nord-est États-Unis téemeeri junni dolaar ngir ñu mëna jënd ay titre ci marse bu ubbeeku, loolu tax marse bi dajal ci weeru Me 1792.

Bank bu Etats Unis ak jafe-jafe 1791

[Soppi | soppi gongikuwaay bi]

Ci weeru desàmbar 1790, Hamilton daal di wax ñu taxawal Bànk bu États-Unis, te ci weeru fewriye 1791, George Washington siñeel sàrt yi may ñu ubbi ko. Ñi dugal seen xaalis ci benn action daan fay $25, ñu koy woowe scrip, te dañu leen sant ñu yokk ñetti xaalis ci diggante jiroom-benn weer, lu tollu ci $375. Fay yooyu dañu wara nekk 25% ci specie ak 75% ci bor yu États-Unis. [1] Laajteb stock ci Bànk bu bees biñ taxawal ci États-Unis bariwoon na lool, te ba noppi njëgi scrips yi yokk nañu bu baax ci ayu-bis yi njeexal, yegg ba $280 ci New York, te ñu wax ni lu ëpp $300 ci Philadelphie ci diggu weeru ut. [1] Coppite yi am ci marse bi mënul yàgg, te ci diir bu gàtt njëg yi tàmbali wàcci lu bare. Hamilton dafa dugg ci liggéey bi ak William Seton, ki yor xaalis ci bànk bu New York, ngir may ñu jënd $150,000 ci bor yu réew mi ci New York ngir nguur gi fay ko. [1] Bi ñu yeggee ci 12 septembre, njëg yi delluwaat ba noppi, te li Hamilton def taxul marse bi dakkal, waaye dafa indi liggéeyandoo ak Bànk bu New York, luy am solo ci jeexal titaange gi amoon ci 1792.

Li waral tiitaange gi am ci 1792

[Soppi | soppi gongikuwaay bi]

Ci weeru desàmbar 1791, njëgu këyit yi tàmbaliwaat yokk, mu dem ba daanu ci weeru màrs 1792, loolu waral boroom xaalis yu bari tiit ba génne seen xaalis ci Bànk bu États-Unis. [1] Benn ci sabab yi njëkka tax bànk bi daanu ci lu gaaw mooy li William Duer, Alexander Macomb ak yeneen bànkër yi tëral ci hiver 1791 daañu lajj. Pexeem Duer ak Macomb mooy jëfandikoo bor yu bari ngir mëna yor marse bor yi ci États-Unis, ndax yeneen liggéeykat yi soxlaoon xaalis boobu ci bànk yi. [2] Rax ci dolli, Duer ak Macomb mënoon nañu sos seen leble ci ku nekk ci ñoom, ñu def ko ci yaakaar sos bànk bu bees ci New York ngir romb Bànk bu New York bi fi nekkoon. [1] Ci bis 9 màrs 1792, Duer dafa bàyyi fay ñi mu yor bor, ci jamono jooju mu jànkoonte ak àttekaay ndax jëf yi mu def bi mu nekkee Sekretëru Treasury Board ci ati 1780. [2] Bi Duer ak Macomb ñàkkee seen kontraa te ñu nekk ci kaso, njëgu sécurité yi wàcci lu ëpp 20%, lépp ci ayu-bis yu néew. [2

Meneen mbir mu waral tiitaange gi am ci atum 1792 mooy li Bànk bu États-Unis tëj ci saasi leble bi, ndax ñu daan jox nit ñi lu ëpp li war. Bi Bànk bu États-Unis tàmbalee nangu xaalis ak wàññi xaalis ci weeru desàmbar 1791, dafa yokk leble bu baax. Ci bis 31 saŋwiye 1792, bor yi ci xaalis weesuna $2.17 milioŋ, ba noppi wàññi gi yegg ba $2.68 milioŋ – xaalis bu bari lool ci jamono jooju. [1] Ñi yor jëndkat yi daan jëfandikoo xeetu leble bu bees boobu, jëfandikoo ko ngir dindi xaalis ci Bànk bu New York, te loolu dafa indil jafe-jafe yu metti xaalis bi bànk bi yor. [1] Lu ko dalee ci 29 desàmbar ba 9 màrs, xaalis biñ denc ci Bànk bu États-Unis wàññeeku na ba tollu ci 34%, loolu waral bànk bi baña yeesal luy tollu ci 25% ci bor yi mu lebaloon ci diiru 30 fan. [1] Loolu moo weñ loxo boroom xaalis yu bari ci Bànk yu États-Unis ñu jaay yeneen këyit yu ñu yor ngir mëna fayal seen xaalis, mu waral njëgi yeneen dugal xaalis wàcci bu baax, gëna yokk jafe-jafe xaalis ci 1792.

Ci diggu weeru màrs 1792, Alexander Hamilton, mi yor wàllu koom-koom, dafa tàmbali def ay jeego yu am solo ci wàllu politik ak koom-koom ngir dakkal jafe-jafe leble yi daan sonal marse yi ci réew mi yépp. Charte bi taxawal Bànk bu États-Unis dafa taxawal itam Kurelu Fond buy Suux, bu amaale njiitu réew mi John Adams, sekkerteeru réew mi Thomas Jefferson, prokureer jeneraal Edmund Randolph, njiitu àttekat yi John Jay, ak sekkerteeru Trésor bi di Alexander Hamilton, ñoom ñoo yor saafara jafe-jafe xaalis. [1] Ci bis 21 màrs 1792, bi Jay ñàkkee wote, komisioŋ bi dafa xaajaloo ci dogal biy nangu jënd ci marse bu ubbeeku. [2] Bi William Seton yëgee Hamilton ni Bànk bu New York amna jafe-jafe, mu bëggoon nguur gi jënd ay mbir ni ko defee ci 1791, waaye mënatul woon ndax Jefferson ak Randolph dañu ko doon xeex. [2] Bi ñuy xaar wote bu mat sëkk bu Jay, Randolph tàmbali ànd ak Hamilton ci 26 màrs, te Jefferson kese moo ko bañoon, komisioŋ bi nangu $100,000 ngir jënd ay securite ci marse ubbeeku. [1]

Ci ay bataaxal yu mu bindoon Seton ci Bànk bu New York, Hamilton dugal na matuwaay yu bari ngir defaraat marse sécurité yi ci anam wu jaar yoon. Hamilton ñaaxna bànk bi mu wéyal di lebal ay bor yu États-Unis, waaye ñuy yokk tuuti intere yi, juróom-ñaari pursaa ci palaasu jiroom-benn. [1] Ngir mëna yay Bànk bu New York mu lebal ci jamonoy tiitaange gi, Hamilton digoon na itam ni Tresor bu États-Unis dina jënd ci bànk bi ba $500,000 ci sécurité, sudee Bànk bu New York tëju ci garanti yu bari. [1] Hamilton itam dafa jàppale Bànk bu Maryland ci leble bi, ci wax ni Treasury bu États-Unis moo wara fay leble yi ñuy lebal jaaykat yiy fay seen juuti. [1] Ci bis 16 awril, ginaaw bi Hamilton santaane Bànk bu New York mu yokk $150,000 ci jënd yi ci marse ubbeeku, Seton dafa xamle ni bëgg-bëggu marse bi dafa dellu ci nimu meloon. [1]

Ci diir bu néew benn weer, Hamilton mëna dakkal marse sécurité yi, ba noppi moytu tiitaange gi indi recession. Bi Hamilton jëfandikoo kàttanam bi mu nekkee sekretëru Treasury, te ba noppi di yay bànk yu bari ñu wéyal di leen lebal ci jamonoy jafe-jafe yi, ci la Hamilton mëna wàññi limu bor yi komite Sinking Fund jëndoon ci federaal ba yegg ci $243,000 – lu [1] $100,000 lu néew ci li ñu daan dugal ci jamonoy jafe-jafe yi.

Koom-koom yi ak taarixkat yi xamle nañu ni li Hamilton doxalee ci Panic bu 1792 dafa melni dafa xaar lu mel ni li Henry Thornton bind fukki at ci kanam ak « Bagehot’s Dictum » lu tollu ci 80 at. [1] [2] Resepsioŋ boobu, maanaam ci jamonoy jafe-jafe, bànk yu mag yi dañu wara « lebal te kenn du leen fay, ci garantie bu baax, ci njëgu penalite », ba leegi ñu ngi koy jàppee ni mooy yoon wi gëna am solo ngir saafara jafe-jafe xaalis, muy « leblekat bi mujjee am »..

  • Limu jafe-jafe ji amoon ci bànk yi

    Royuwaay:United States – Commonwealth of Nations recessionsRoyuwaay:Financial crises