Aller au contenu

Sibiru

Jóge Wikipedia.
(Yoonalaat gu jóge Sibbiru)
Sibbiru
Ab Plasmodium bu bawoo ci tiflitu yoo bu jigéen di dox ci biir selilu yoo bi.
Toftale ak balluwaayi biti
Specialty infectiologie[*], médecine tropicale[*], parasitologie[*]
ICD-10 B50-B54
ICD-9-CM 084
OMIM 248310
DiseasesDB 7728
MedlinePlus 000621
eMedicine med/1385 emerg/305 ped/1357
Patient UK Sibiru
MeSH C03.752.250.552

Sibiru ab feebar bu yoo di joxe di dal nit ak yenn rab yi te li koy joxe di parasit protozoan (benn xeetu selil microorganism) bu xeetu Plasmodium.[1] Ni sibbiru di faral di feeñee mooy yaram wu tàng, coono, waccu ak metitu bopp. Su demee ba tar mën na jur der bu mboq, say, komaa wala faatu.[2] Feebar baa ngi tàmbalee feeñ fukki fan ak juróom ginaaw bu la yoo bi màttee. Ñi mu dal te faju ñu ko bu baax, mën na leen dalaat ginaaw ay weer ci kanam.[1] Ñi mu dal bu yàggul ba ñu mucci, su leen dalaatee du metti noonu. muslaay boobu nit ki am dafay jeex su amee ay weer wala at sudee newul fu mu mën a amee sibbiru.[2]

Gis nañu ni, màtt-màttu yoo bu jigéen bi tuddu Anophele mooy joxe feebar bi. Sula màttee dafay dugal parasit yi nekk ci tiflitam ci sa deret.[1] Ginaaw loolu mu jàll ci res wi ndax foofu lay màggee ak juree. Juróomi xeeti Plasmodium a mën a dal nit te ñooy la nit mën a wàlle.[2] Ñu bari ñu sibbiru di faat P. falciparum ak P. vivax, P. ovaleñoo leen faat, ak P. malariae biy joxe sibbiru bu tarul lool.[1][2] Xeet yi tudd P. knowlesi bariwul lu ñuy daaneel nit.[1] Bu ñuy seet ndax danga sibbiru jël ci sa laamu deret xool ko ci mikroskop, wala ñu jëfandikoo test bi tuddu antigen-based test bu gaaw la.[2] Defar nañu jumtukaay buy jëfandikoo polymerase chain reaction ngir gis ADN bu doomu jàngoro ji, waaye loolu bariwul ci barab yi sibbiru bari ndax dafa seer te jafe.[3]

Sibbiru bu mën na wàññiku bu baax sudee nit ñaa ngi jëfandikoo sàñce (mustikeer) wala diw bu dàq yoo ngir moytu màtt-mattu yoo yi, wala def lu leen di dàq wala ray, lu ci melni pompu yoo ak dindi dox yi taa.[2] Bari na garab yu ci melni prevent malaria yiñ jagleel ñiy tukki ci barab yu sibbiru bi tasaaroo. Yenn saa mën nañu bindal xale sulfadoxine/pyrimethamine xale ak jiggéenu wérul ci ñatti weer yi njëkk cib ëmb bi ci barab yi sibbiru bari lool. Fiñu tollu amagul ñakk bu ci mën a aar ni naam soxla nañu ko, teewul nit ñaa ngi ciy gëstu bu baax ngir am ko.[1] Ñaari xeeti garab yi ñu digle ngir faj feebar bi ñooy garab yiy xeex sibbiru bi amaale ab artemisinin.[1][2] Ñaareelu garab gi mën na doon mefloquine, lumefantrine, wala sulfadoxine/pyrimethamine.[4] Mën nañu itam jël Quinine boole ko ak doxycycline sudee artemisinin amul.[4] Mooy lañuy digle ci barab yi feebar bi bari, dañu wara xam bu baax ndax nit ki dafa sibbiru laata muy jël garab yi ndax dañuy bañ jàngoro ji dërkiis ci garab gi. Jangoro dem na ba dërkiis ci yenn xeetu garab yu daan faj sibbiru; lu ci melni, dërkiis ci-chloroquine P. falciparum barina ci barab yi sibbiru bi bari, te itam dërkiisam ci artemisinin doon na jafe-jafe bu mag ci réew Asi Gànjoolu-penku.[1]

Fi feebar bi gënee bari mooy ci réew yu tàng yi ak xawa tàng te ñooy yi séq rëdd wiy xaajale suuf si di ekuwaatër.[2] Bokk na ci ñoom Afrigu Suufu-Sahara, Asi, ak Amerik Latin. Mbootaayu Wérgi-yaramu Àdduna bi maanaam OMS xayma na ci atum 2012, ni amoon na 207 miliyoŋi ñu amoon sibbiru. Ci at moomu, feebar bi fatna lu tollu ci diggante 473,000 ak 789,000 doomu aadama, li ëpp ci ñoom doon ay gunéy Afrik.[1] Fuñu tuddee sibbiru xel yi dem ci ndóol te loolu doonul lu baax ci koom-koom guy suqaliku.[5][6] Xayma nañu ni at mu nekk sibbiru dina ñàkkloo Afrik lu tollu ci $12 miliyaar ciy dolaar ndax pajum feebar bi, ñàkk a mën a liggéey ak li muy yàq turism bi.[7]

Royuwaay yi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]
  1. 1,0 1,1 1,2 1,3 1,4 1,5 1,6 1,7 et 1,8 "Malaria Fact sheet N°94". WHO. March 2014. Retrieved 28 August 2014. 
  2. 2,0 2,1 2,2 2,3 2,4 2,5 2,6 et 2,7 Caraballo, Hector (May 2014). "Emergency Department Management Of Mosquito-Borne Illness: Malaria, Dengue, And West Nile Virus". Emergency Medicine Practice 16 (5). 
  3. Nadjm B, Behrens RH (2012). "Malaria: An update for physicians". Infectious Disease Clinics of North America 26 (2): 243–59. PMID 22632637. doi:10.1016/j.idc.2012.03.010. 
  4. 4,0 et 4,1 Organization, World Health (2010). Guidelines for the treatment of malaria (2nd ed. ed.). Geneva: World Health Organization. p. ix. ISBN 9789241547925. 
  5. Gollin D, Zimmermann C (August 2007). Malaria: Disease Impacts and Long-Run Income Differences (PDF) (Report). Institute for the Study of Labor. 
  6. Worrall E, Basu S, Hanson K (2005). "Is malaria a disease of poverty? A review of the literature". Tropical Health and Medicine 10 (10): 1047–59. PMID 16185240. doi:10.1111/j.1365-3156.2005.01476.x.  open access publication - free to read
  7. Greenwood BM, Bojang K, Whitty CJ, Targett GA (2005). "Malaria". Lancet 365 (9469): 1487–98. PMID 15850634. doi:10.1016/S0140-6736(05)66420-3.