Aller au contenu

Saaru nisaayi

Jóge Wikipedia.

Saaru Nisaayi mooy ñeenteelu ci saari Alxuraan alxuraan yi, moom nag amna( 176) aaya, moom nag saar la woo xamne léppam Madiina la wàcci bamu des benn aaya, boo xamne ba ñuy ubbi Màkka la wàcci ci ko noy wax Usmaan Ibnu Talha

te mooy aaya  (إن الله يأمركم أن تؤدوا الأمانات إلى أهلها) moom saar wi nag, ci Attiwaal la bokk, di juróom ñaari saar yu gudd yi, saar wi mi ngi wàcci Ginnaaw saaru (الممتحنة) nekk ci diggante ñaari saar yii di Aali-himraan ak Maa-ida,

Lu tax ñu tudde saar wi Nisaai, ndax daa bari ay àtte yi ci ñëw te aju ci jigéen ak ay mbiram, loolu moo tax ñu tudde ko Annisaa di ko tudde (سورة النساء الكبر ى) muy janloog weneen saar wuñuy wax (سورة النساء الصغرى)te mooy Attalaaq.

Saaru Nisaai nag wenn la ci saari wàcci Madiina, moom nag saar la woo xamne daa fées aki àttey yoonal, yoo xamne day nos mbirum jullit ñi ci biir ak ci bitti, moom nag daa gën a jëm ci yoonal, ni ki nga xamne noon la saar yi wàcci Madiina yépp mel, ci biir saar wi nag Yàlla deef cee wax lu jëm ci ay mbir yu am solo yu aju ci jigéen, ak kër,ak fase ak askan,ak miiraas ak lu jëm ci sàmm wala nguur ak mboolaay gi di sosyete , waaye nag lu ëpp ci ay atteem dafa rot di wax ci mbirum jigéen ak ya ca aju moo tax ñu tudde saar u Nisaai di saaru jigéen ñi.

Saababu wàccig ñaareelu aaya ci saar wi jëleef na ci ku niy wax Sahiit Ibnu Jubayru mune Jenn waay ju bokk ci Giiru Ratfaan daa amoon alal ju bari, joo xamne ki ko moomoon di doomi mbokkam boo xamne ab jirim la, ba jirim bi kallafee nag daadi ñëw ci moom Baay tëq bi laaj ko alalam jim ko yoraloon, baay tëq bi bañ ka koo jox ñu dem Si Yonente (SHW) atte loo ko, aaya Alxuraan wàcci, bi ko baay tëq bi diggee nag, daan ne topp naa Yàlla ak Yonenteem, daan ne maa ngi muslu Yàlla ci bàkkaar bi ma def, daal di jël alal ja delloo ko doomi mbokkam ja, Yonente bi (SHW) daadi wax ne( من يوق شح نفسه ويطع ربه يدخله جنته Abii Haatim moo ko nettali. Ku Yàlla fegal nayu bakkanm mu topp boroomam Yàlla dana ko dugal Àjjanaam.

Saababu wàccig ñeenteelu aay, li tax aaya (4) wàcci ci saar wi, mooy Araab yi dan daan def ko maye sa doom bu jigéen can ga ñoom ñoo koy jël, aaya boobu wàcci di leen tere loolu, loolu nag ab Hadiis la boo xamne Ibnu Abii Haatim moo ko Génne ak Ibnu

Munsir.

Saababu wàccig juróom benneel u aaya ci saar wi, daa wàcci ci ku ney wax Saabit Ibnu Rifaaha ak baay tëqëm ba, nem demee mooy Rifaaha dafa faatu bàyyi fi doom junuy wax Saabit fekk booba gone la, baay tëqu Saabit daadi ñëw ci Yeneente bi (SHW) daan nako sama doomi mbokk mii nag ab jirim la, man maa koy toppatoo, ana lan mooma dagan ci alalam ak kañ laa koy jox alalam, sunu boroom wàcci aaya (6) te Haa-isa: neena aaya bii mi ngi wàcci ci waalil yatiim aji toppatoo ab jirim.