Aller au contenu

Saaru baqara

Jóge Wikipedia.

Saaru Baqara mooy saar wi gën a gudd ci Alxuraan,286i aaya la. Ni kaamil bi toftaloo mooy ñaareelu saar, ginnaaw Faatiha.Wax nañu ne saar wi Madina la wàcc,ba mu des aaya bii, 281.*﴿وَاتَّقُوا يَوْمًا تُرْجَعُونَ فِيهِ إِلَى اللَّهِ ثُمَّ تُوَفَّى كُلُّ نَفْسٍ مَا كَسَبَتْ وَهُمْ لَا يُظْلَمُونَ﴾* ،

  • "Ragal-leen Bis bu ngeen di delloo ca Yàlla. Su ko defee bakkan bu nekk dees na ko fay limu liggéey te duñu ko tooñ"*aaya 281*

Wax nañu ni aaya bi bokk na ci aaya bi mujj a wàcc ,ci bisum fukkeel ba ci Tabaski la wàcc ca Mina, te mooy Hajj bi Yónent bi (SHWSM), mujj a def,mooy Hajju tàggatoon ba,ak aaya biy wax ci (Riibaa),mooy aaya bi njëkk a wàcc ci saar wi.Wax nañu ni mooy Tàntub Alquraan.Xaalit doomu mahdaan, moo ko wax .(Bokk na ci Li tax loolu màggaayam;Ak taaram,ak biri àtte yu ci nekk, ak i waaraate! Moom saar wi Umar doomi Hàttaab, jàng na ko fukki at ak ñaar12, ngir xam ko ak dégg ko.Doomai mi Umar di Abdulaay moom ci juróom ñatti at 8 la ko jàng.✍️✍️✍️✍️


Saar wi nag ci la aaytul-kursiyi nekk, Mooy aaya 255,mooy aaya bi gën a màgg ci alquraan bi.Abii Hurayra yal na ko Yàlla dolli ko gërëm( moom la Yónent bi (SHWSM) féetele woo mbiri asakay Koor) Wax na"benn guddi am lu dikk di jël ci ñam wi mu ni ko dama lay yóbb ci Yónent bi wax na ni def na ko ñatti yoon mu ni ko boo ma bàyyee dootu ma dikk mu, ni ko dinaa la wax loo xam ni boo ko jàngee Yàlla dina la wàttu ci Saytaane, du la jige ba bëtt di sett ! Mu ni ko mooy aaytul-kursiyi.Yónet bi ni ko" wax na dëgg de waaye moom ab fenn- kat la ndax Saytaane la.Ni ma ko waxe woon batay aaya bi gën a gudd ci saar wi mooy aaya biy wax ci *(Al Mudawana)* mooy *(Bor.)*✍️✍️✍️

  • Sababu wàcc gi.*

Ci mbindum saaru Baqara ci bind Usmaan ci riwaaya Hafsi ci njàngum Xaasim.✍️✍️✍️✍️✍️✍️✍️✍️✍️

*Sababu wàccug aaya yii* 

Sabab bi ci ñetti aaya aaya yi njëkk a wàcc ? Mujaahit wax na ne"4 ñetti aaya yi njëkk a wàcc ci saar wi ngir jullit ñi,2 ñaar yi ci topp ci Yéefar yi 3 ñatti yi ci topp ci Naaféq yi la wàcc.✍️✍️✍️✍️✍️

*Sababu wàccug aaya 26*✍️✍️✍️✍️✍️✍️

Ibn Àbbas ak Ibn Mashuud wax nañu ne" Ba Yàlla joxee misaal ci 2 ñaari aaya yii .﴿﴿

  • مَثَلُهُمْ كَمَثَلِ الَّذِي اسْتَوْقَدَ نَارًا*﴾* *إِنَّ اللَّهَ لَا يَسْتَحْيِي أَنْ يَضْرِبَ مَثَلًا مَا بَعُوضَةً فَمَا فَوْقَها*

Yàlla nee na" *Seen misaal dafa mel ni ku taal safara...* Naaféq yi wax ni "Yàlla mu màgg mi du joxe misaal ci lu mel nii? Yàlla Tontu wax"*Yàlla amul kesa ci joxe missl ci lu mel ni Yoo wala lu ko gën a ndaw ba lu ko ëpp.*✍️✍️✍️✍️✍️✍️✍️✍️

*:Sababu wàccug aaya 62* : mujaahit nettali na nee na" ((Salama mi nga xam ni dafa bàyyikoo woon( *perse* ) ca *Faaris* ci diiney waa Ahlul kitaab)) Salman Faaris nee na "Laaj nañu Yónent Yàlla bi *SHWLM
sunu waa jiine ,nee na mu max ko ne;Sunu waa diine dan daan julli di te seede woon nañu ni yaw de Yàlla moo la yónni ci la Yàlla wàcce aay bii.**إن الذين آمنوا والذين هادوا والنصارى والصابئين من آمن بالله واليوم الآخر وعمل صالحاً فلهم أجرهم عند ربهم ولا *خوف عليهم ولا هم يحزنون*

Yàlla nee na"

*Ñi gëm Yàlla di Yahoot ak i Nasraan ak I Saabiina,ku ci settantal te dëddu la mu nekkoon jàppoo ko, te gëm Yàlla ak Bisub- pénc ba de muy defu yiw , dinañu fekk seenug pay ca Yàlla ëllëg,te duñu tiit duñu jàq.*

Jubluwaayu Saar wi

[Soppi | soppi gongikuwaay bi]

Bokk na ci jubluwaayu Saaru Baqara, dafa jug ngir waajal xeet wi ngir ñu dundal suuf si ak taxawu diiney Yàlla ji, ak leeral xeeti nit yi, nekk na ci saar wi it, ponki gëm ak mbooleem kenuy sariiha. Al-Biqaahii wax na ne: "Liy jubluwaayu saar wi , moo di teg ay firnde ci téere bi ne, mooy ak njub ngir ñu topp ko ci gépp anam, te li ko gën a leeral mooy saar wi jàngale na gëm ci kump, te tudd na it gëm bis-pénc, jàngale na itam gëm dekki; Jaare ko ci nagu Bnuu Israa-iil, loolu lépp di jàngale gëm kump ba leegi, nag woowu moo tax ñu tudde saar wi Baqara."

Jagley Saaru Baqara

Yàlla sunu Boroom saar wi jaar-jaaru yëkk wa ci diggante Muusaa ak Banuu Israa-iil, te loolu ab junj la rekk buy jàngale ne, bu ndigalul Yàlla wàccee nañu ko gaaw jëfe bañ a def ni Yahuut yi, defoon .

Bokk na ci li gën a solo wu ci jagley Saaru Baqara :

- Moom mooy Saar wi gën a gudd ci Alxuraan. - Am na ci biiram it aaya bob mooy aaya bi mujj a wàcc ci Alxuraan. - Moom it mooy saar wi làmboo aaya bi gën a gudd ci Alxuuraan muy (aayab leb). - moo làmboo ba tay aaya bi gën a màgg ci Alxuraan (Aayatul Kursii). - ñëw na ci siira Yónnent bi(SHW) mu ne: saar wi day ramb ëllëg bisu pénc, te am na ci biiram tur wu màgg woo xam ne boo ci ñaanee Yàlla mu nangu, te jàng ko day maye barke, te bàyyi ko it day waral ag réccu, te di saar wow, lott loo na njabarkat yi!


Wàll:alxuraan