Aller au contenu

Saaru Faatiha

Jóge Wikipedia.

Saaru Faatiha (سورة الفاتحة) walla Assabhul Masaanii (السبع المثاني) walla "Umul Kitaab" (أم الكتاب) mooy saar wi gën a màgg ci Alxuraan. Ngir Yonent Muhammat (SHW) waxoon na ne: "Alhamdu lillaahi Rabbil haalamiin" mooy Assabhu Almasaanii ak Alxuraan ju màgg ji ñu ma jox. Loolu moo tax ñu def ko ci njëlbeenu kaamilub Alxuraan bi, te it mooy saar wi ñuy njëkk a jàng ci julli.

Saaru Faatiha am na ay tur yu bari. Suyuuti lim na ci téereem bii di "Al-Itqaan fii Huluumil Xuraan" ñaar fukki tur ak juróom, ci diggante ay dàkkental ak i melo yu ñu tuxale ci làmmiñi jàngkat yu jiitu ya. Bokk na ci tur yooyu: "Alxuraan ju Màgg ji" "Suuratul Hamdi" "Al-Waafiya" ak "Al-Kaafiya".

Saaru Faatiha juróom-ñaari aaya la ci li jàngkat yépp ak firikati Alxuraan yi dëppoo. Ñépp a ànd ci loolu ba mu des ñatt ñii: Hasan Al-Basrii moom dafa ne juróom-ñetti aaya lañu, Hamr bun Hubaydin ak Husaynu Al-Juhfii ñoom dañu ne juróomi aaya lañu. Waaye ñi ci gën a bari dañoo sukkandiku ci waxi Yonent bi (SHW) wax ne : "Assabhul Masaanii" (السبع المثاني).

Saaru Faatiha dañu koy boole ci saar yi wàcce Màkka jëkk Yonent bi di gàddaay. Loolu mooy wax ji gën a lëng. Ci toftaloog wàcc gi, Baddrudiin Assarkasii wax na ne, mooy juróomeelu saar ginnaaw Saaru Al-Halaq saaru Al-Qalam Saaru Al-Mussammil ak Saaru Al-Muddassir.

Saaru Faatiha bari na ay tur lool, loolu di wane ag màggaayam, bokk na ci yooyu tur yii di ñëw:

  • Tur i dëggantaan yu saxe ci Alxuraan ak sunna, te mooy yii*

1. *Faatihatul Kitaab*: ndax mooy saar wi ñuy ubbee Kaamilub Alxuraan bi, ak it moom lees di ubbee ag julli, te am na ñu ne ndax mooy saar wi njëkk a wàcc ci Alxuraan. 2. *Assabhul Masaanii*: Ndax dafa am juróom ñaari aaya, te Masaanii mooy li ñuy baamu ci biir julli gi, walla li tax turu Masaanii mooy daa wàcc ñaari yoon. 3. *Ummul Quraan / Ummul Kitaab*: Ndax mooy cosaanu Alxuraan, te dafa ëmb mbir yi jëm ci Yàlla, ak ci jaamu Yàlla, ak lu jëm ci njub. 4. *Al-Quraanul Asiim*: Ndax dafa dajale xam-xami Alxuraan yi.

  • Tur yi boroom xam-xam yi ball-loo ci biir Alxuraan ak ciy maanaam*:

- *Al-Ḥamd*: nee ñu Ndax dafa tambalee ci "Alḥamdu lillaahi" (Sant yépp ñeel na Yàlla). - Al-Waafiya*: Ndax dañu koy jàng léppam ci julli kenn du ko xaaj. - Al-Kaafiya*: Ndax dafa doy wëlif lépp lu dul moom. - *Aṣ-Ṣalaat*: Ndax day ab kenu ci julli. - Assifaa ak Ar-Ruqya: Ndax dañu koy saafarawoo. - An-Nuur: Ndax day leeralal xol yi. - Al-Kans: Ndax dafa dëxëñ ay maanaa yu baia.

Suyuuṭii lim na ñaar fukki tur ak juróom, yii ca la bokk: Al-Asaas, Assukr, Al-Munaajaat, At-Tafwiiḍ, Adduhaa.

Limub aaya yi

[Soppi | soppi gongikuwaay bi]

Ñi gën a bari ci boroom xam-xam yi (Al-Jumhuur) dañoo dëppoo ci ne Saaru Faatiha juróom ñaari aaya la, te loolu mooy li jàngkat yépp ak firikati Alxuraan yi saxal bamu des Hasan Al-Basrii mi ne juróom ñatti aaya lañu, te it dees na Askale ne Hamr bun Ubaydin ak Husaynu Al-Juhfii ne dañuy wax ne Faatiha juróomi aaya la. Waaye ñi ci gën a bari ci boroom xam-xam yi (Al-jumhuur) dañoo sukandiku ngir saxal ne saaru Faatiha juróom ñaari aaya la, ci Hadiisub Abuu Sahiid ibnul Muhallaa mi ngi jottali ne Yonent bi wax na ko: "Dinaa la jàngal aw saar Wow moo gën a màgg ci Alxuraan, mu ne: ﴿الْحَمْدُ لِلَّهِ رَبِّ الْعَالَمِينَ﴾... Moom mooy السَّبْعُ الْمَثَانِي وَالْقُرْآنُ الْعَظِيمُ bi ma jox".

Li waral ñu wuute ci limub aaya yi moo di ne waa Màkka ak waa Kuufa dañuy lim Bismillaahi (البسملة) mu nekk ab aaya ci Saaru Faatiha, wax ne it: {صِرَاطَ الَّذِينَ أَنْعَمْتَ عَلَيْهِمْ غَيْرِ الْمَغْضُوبِ عَلَيْهِمْ وَلَا الضَّالِّينَ} benn aaya la. Te loolu it la ngirum Sasfihii dëgëral. Waaye waa Madiina ak waa Basra ak waa Saam ñoom dañu ne Bismillaahi (البسملة) du aaya ci Saaru Faatiha, ñu ne itam {صِرَاطَ الَّذِينَ أَنْعَمْتَ عَلَيْهِمْ..} ab aaya la, te {غَيْرِ الْمَغْضُوبِ عَلَيْهِمْ وَلا الضَّالِّينَ} moom it aayab boppam la. Te lii it mooy li ngirum Ahnaf dëgëral. Ibnu Qudaama wax na ci téereem bii di "Al-Muxnii" ak Nawawi ci téereem "Al-Majmuuh'" ak Ibn Hasm ci téereem "Al-Muhallaa" ne Imaam Sasfihii ak Ibnul Mubaarag ak Imam Ahmad ci benn ci ay waxam dañoo def Basmala muy aayab boppam ci biir Faatiha te nee ñu képp ku jàng Faatiha bàyyi (Basmala) amóo julli. Nawawii ak Ibnu Hasm itam loolu lañu dëggal. Te bokk na ci li ñu sukkandiku ngir layal séen wax jooju Hadiisub Daara-quṭnii ak Bayhaqii biy wax ne "Bu ngeen di jàng (الحمد لله) Deeleen jàngaale (بسم الله الرحمن الرحيم) Faatiha mooy Ummul Kitaab ak Assabhul Masaanii te ﴿بسم الله الرحمن الرحيم﴾ ab aayaam la."

Abuu Haniifa ak Maalig ak Ahmad ci lu Ibnu Qudaama tudd ci "Al-Muxnii" nee nañu Bismillaahi nekkul ab aayab boppam ci Faatiha. Te bokk na ci li ñuy layoo mooy hadiis bu Maalig génne ci Muwatta ñëw na it ci Sahiihu Muslim ñu solo lu jóge ci Abuu Hurayra mu ne: سمعت رسول الله ﷺ يقول قال الله تبارك وتعالى قسمت الصلاة بيني وبين عبدي نصفين فنصفها لي ونصفها لعبدي ولعبدي ما سأل قال رسول الله ﷺ اقرأوا يقول العبد ﴿الحمد للّهِ رب العَالمين﴾ يقول اللّهُ عز وجل حمدني عبدي.

Firnde ji mooy hadiis bi dafa ñëw rekk tàmbalee Faatiha ci (الحمد لله رب العالمين) te tuddul Bismillaahi. Bokk na ci firnde yooyu it li ñu wax ne daanu ñu dégg yónent (SHW) mu di ko béral cig julli. Ndax dañoo nettali jële ci Anas lbnu Maalig mu ne "Julli naa ci ginnaaw Yonent bi ﷺ ak Abuu Bakr ak Umar ak Usmaan waaye daanu ñu tambalee Faatiha ci (بسم الله الرحمن الرحيم) du cig njëlbeenam du cig mujjam."

Kon daal (بسملة) ci biir Faatiha masala la mu boroom xam-xam yi wuute ci lu yaatu.

Sababu wuute gi ci limub aaya yi

[Soppi | soppi gongikuwaay bi]

wuuteg boroom xam-xam yi ci limub aaya yi day dellu ci li ñu wattu te jële ko ci Sahaaba yi ñoom ñu jële ci Yónnente (saws). Fadlu Abbaas (فضل عبّاس) wax na ne: "Yónnente bi (saws) ci biirum njangam daa na taxaw lu ëpp ci bopp aaya yi, Sahaaba yi doon jànge loolu ci moom, ci loolu lañu xamee màndaxtey aaya yi, waaye itam daa na faral di taxaw fu bokkkul ak bopp aaya yi ngir wane ne lu dagan la, loolu tax na ñenn ci Sahaaba yi masul dégg Yóonnent bi taxaw ci bopp aaya ñu njort ne foofu mu taxaw bopp aaya la, lii nag mooy sabab bi not waaye am na baneen sabab bu Zarkashi (الزركشّ) junj ca téereem boobu di Burhaan (البرهان ) te mooy wuuteg boroom xam-xam yi ci lim «بِسْمِ اللهِ الرَّحْمنِ الرَّحِيمِ» ndax aaya la walla déet.

Hasan al-Basri (حسن البصري) dafa lim «بِسْمِ اللهِ الرَّحْمنِ الرَّحِيمِ» muy aaya, mu lim itam «أَنْعَمْتَ عَلَيْهِمْ» muy aaya, loolu tax mu mujj nekk juróom ñetti aaya.

  1. Jamonoy jim wàcce

Yaxub Suuratul Faatiha ci bindum Usmaan ci riwaaya Hafs ñeel jàngum Haasim.

Boroom xam-xam yi wuute nañu ci jamonoy wàccub Suuratul Faatiha. Li ëpp ci boroom xam-xam yi dañoo wax ne suura bi ci Makka la wàcc. ñenn ci ñoom ku mel ni Mujaahid (مجاهد) ak As-suhri(الزهري) ak ñeneen, dañoo wax ne suura bi ci Madina la wàcc. Am na ñu wax ne genn-wàll gi ci Makka la wàcce, genn-wàll gi ci Madina. Am na ñu wax ne: "wàcce na ñaari yoon: Benn yoon Makka, te mooy bi ñuy farataal julli, ak benn yoon Madina, te mooy bi ñuy soppi Xibla bi, kon dafa doon Makka ak Madina. waxi boroom xam-xam yi :

    • Makka**  : Loolu mooy li ëpp ci boroom xam-xam yi wax. As-sahlabi (الثّعلبي) nettali na jële ci Aliyu ibn Abii Taalib( عليّ بن ابي طالب) mu ne: "Fatihatul Kitaab ci Màkka la wàcc, bàyyi koo ca ron Aras ." As-sahlabi(الثّعلبي) wax na: "Te ci loolu la boroom xam-xam yi ëpp jàpp." nettali nañu itam ci Hamr ibn Surahbil( عمرو بن شرحبيل) mu ne: "Li njëkk a wàcce ci Alxuraan mooy: ﴿الْحَمْدُ للَّهِ رَبِّ الْعَالَمِينَ...﴾, ndaxte Yónnente bi (saws) wax na xaadija: Dama ragal am na dara lu may jaxase, mu ne ko: Ana loolu lu mu ? Mu ne: Su ma nekkee man rekk damay dégg benn kàddu bu may woo naan, 'Jàngal jàngal', mu dem ba ci Waraxa ibn Nawfal(ورقة بن نوفل) wax ko loolu. Waraxa ne ko: Bu la woowee, taxawal, ci noonu la Jibriil(جبريل) dikkalee Yónnente (saws) ne ko: Waxal: ﴿بِسْمِ اللهِ الرَّحْمنِ الرَّحِيمِ الْحَمْدُ للهِ رَبِّ الْعَالَمِينَ﴾."

Ci nettali bi jóge ci Ibn Abbaas(ابن عباس), mu ne: "Yónnente bi (saws) taxaw na wax: ﴿بِسْمِ اللهِ الرَّحْمنِ الرَّحِيمِ﴾, ci loolu xuraysi ne(قريش): Yàlla na Yàlla dog sa làmmiñ." Abu Nuhymin Al-Asbahani(أبو نعيم الأصبهاني) nettali na te jële ci benn waay bu bokk ci Banii Salama(بني سلمة, mu ne: "Bi ñenn ci ndawi Banii Salama gëmee, ak doomu Hamri ibnu al-Jamuhi(عمرو بن الجموح), soxnas Hamri wax ko: Xanaa déggóo li sa doom nettali ci moom? Mu laaj ko, mu jàngal ko ﴿الْحَمْدُ للهِ رَبِّ الْعَالَمِينَ﴾ te loolu mi ngi nekk njëkk gàddaay gi." Abu Bakrin ibn Al-Anbaari(أبوبكر الأنباري ) nettali na toxalee ci Ubaada(عبادة): mu ne: "Fatihatul Kitaab ci Màkka la wàcc."

    • Madina**  : As-sahlabi(الثّعلبي) nettali na jële ci Mujaahid ibn Jabr(مجاهد بن جبر) mu ne: "Fatihatul Kitaab ci Madina la wàcc." Husayn ibn Al-Fadl(حسين بن الفضل) wax na ne: "Ku nekk ci boroom xam-xam yi mana def njuumte, te loolu mooy njuumtey Mujaahid, te boroom xam-xam yi dañoo wuute ak moom. Li koy firndeel mi ngi tënku ci ñaari xaaj: Bu jëkk bi, Suuratul Hijr ci Màkka la wàcc ci dëppook boroom xam-xam, te ñëw na ci Saar woowu Yàlla di wax : ﴿وَلَقَدْ آتَيْنَاكَ سَبْعًا مِنَ الْمَثَانِي﴾ te loolu dey jëm ci Faatihatul Kitaab. Loolu dey wane ne Yàlla jox na ko suura boobu ci lu jiitu. Bu ñaareel bi: dana sori xel lool nuy wax ne dafa nekk ci Màkka fukki at ak lu teg te amul Fatihatul Kitaab."

Abu Hurayra(أبو هريرة) nettali na ne Yónnente bi wax ne: "Ak ki jagoo sama bakkan, Yàlla wàccegul lu mel ni moom ci Tawraat, ak Injiil, ak Sabuur, ak Furxaan, ndaxte mooy juróom ñaari aaya yi dul jeex ak xuraan bu màgg bi ma jotoon." "والذين نفسي بيده ما أنزل الله في التوراة ولا في الإنجيل ولا في الزبور ولا في الفرقان مثلها إنها لهي السبع المثاني والقران العظيم الذي أو تيته "

Te Suuratul Hijri Màkka la wàcc ci lu amul benn wuute, te itam Yónnente bi nekk na Màkka fukki at ak lu teg, te daan na julli ak Fatihatul Kitaab.
    • Makka ak Madina**: Ñenn ci boroom xam-xam yi wax nañu ne suura bi wàcc na Màkka benn yoon, ak Madina benn yoon, kon dafa doon ci Màkka ak Madina, moo tax Yàlla tuddee ko "Al-masaanii" (ñaareel), ndaxte dafa wàcc ñaari yoon, te loolu mooy liy wane dayo bi Suura bi am.

Li jëm ci sababu wàccub suura bi, ñenn ci boroom xam-xam yi, ku mel ni Al-Waahidi(الواحديّ) ak Ibn Abi Sayba(إبن أبي شيبة) ak Bayhaxi(بيهقي), nettali nañu sababu wàccub Suuratul Faatiha, ñu jottali koo ci Abii Maysara(أبي ميسرة) mu wax ne: "Su Yónnente bi (saws)masaan génn, day dégg benn woote: 'Yaa Muhammad', su déggee kàddu gi dey daw. Waraxa ibn Nawfal ne ko: Bu déggatee woote bi taxawal ba dégg li muy wax. ba mu génnee mu dégg woote bi 'Yaa Muhammad' mu ne: wuyu naa la. Mu ne ko: Waxal, "أشهد أن لا إله إلا الله وأشهد أن محمدا رسول الله" Yónnente bi wax. Mu ne: Waxal ﴿الْحَمْدُ للهِ رَبِّ الْعَالَمِينَ الرَّحْمنِ الرَّحِيمِ مَالِكِ يَوْمِ الدِّينِ...﴾ ba Suura bi jeex."

Boroom xam-xam yi gis nañu ne li Al-Waahidi ak ñeneen nettali dafa doon xibaar ci suura bi waaye du sababub wàccam. Li wér daal mooy ne loolu ab xibaar la, waaye du sababub wàcc.

Suuratul Faatiha wàcc na laata gàddaay gi ci gis-gisu ñi ëpp ci boroom xam-xam yi, te am na ñu bari ci ñoom ñuy wax ne: mooy suura bi njëkk a wàcc. Ibn Haasuur(ابن عاشور) wax na: "Li wér mooy dafa am Saar yu ko jiitu bu mel ni﴿اقْرَأْ بِاسْمِ رَبِّكَ...﴾ ak سورة المدثر, mu topp ko Faatiha (الفاتحة). Te am na ñuy wax ne: jiitu nañu ko itam ﴿ن وَالْقَلَمِ...﴾ ak Suuratul Musammil (سورة المزمل). ñeneen wax nañu ne: mooy suura bi njëkk a wàcc bu mat sëkk ci benn bis wuute ak سورة القلم. ñeneen firndeel nañu ne: wàcce na bi ñuy farataal julli, jullit ñi tàmbli koo jàng ci biir julli yi. Ñenn jottali nañu ci Jaabir ibn Sayd(جابر بن زيد) ne: mooy suurab juróomeel bi ci wàccug Alxuraan. Lu ci mana nekk it nanu xam ne, Yonent bi (saws) tudde na ko Fatihatul Kitaab joxe ndigal mu nekk suura bi jëkk ci Alxuraan."

Ibn Haasuur wax na: "Li koñu doyul mooy ne wàcc na gannaaw yeneen suura yi ngir li Yàlla tànn ci balaa ñuy dajale dara lu bari ci Alxuraan ba muy doon téere, bi ñu dajalee loolu, ci lañu wàcce Faatiha ngir muy gàtt-léebu téere bi, moo tax ñu koy woowe Ummu-l-xuraan."

Yàlla wàcce na Suuratul Faatiha ci jamono ju way-gëm yi di lu tollu ci ñeenti fukk ci diggante góor ak jigéen, li ëpp ci ñoom ñu néew doole lañu woon. Makka dafa feesoon ak gëm-gëm yu bon, ak xeetu jëflante yu yées, ak aada yu bon ci bokkaale Yàlla, ak jaamu nataal ak xërëm, ak weddi bisub dekki ba, ak yàqute zina (njaalo) ak naan sàngara ak rëy ak yeneen. Ci loolu Suuratul Faatiha ak yi mel ni moom wàcc nañu ngir faj ñi am gëm-gëm yu bon, ak jubanti seeni xalaat ak li ñu gëm, ak dugal ci xoli wa-gëm yi gëm gu dëggu ak jikko ju baax ak yar bu rafet. aaya ak suura yi doon wàcc ci jamono jooju nekkoon nañu aaya yu gàtt, yu am lafas yu rafet, ak waxiin wu teey.

Tekkig saar wi

[Soppi | soppi gongikuwaay bi]
  1. بِسْمِ اللَّهِ الرَّحْمَنِ الرَّحِيمِ

Ci aaya bi, Yàlla jàngal na Yonentam ci jàngal ko muy jiital tudd Yàlla ci léppam ; ay waxam walla ay jëfam, sant it mbooleem nit ñi ñu roy ko ci loolu , ñuy tàmbalee seen lépp bismillaa.


Bismillaa (بِسْمِ اللَّهِ), di tekki: tàmbaleel ci turu Yàlla ci mépp mbir. Booy jàng it , tàmbaleel ci tudd Yàlla (bismillaa).


( الرَّحْمَنِ الرَّحِيمِ) 

Di tekki: Yàlla miy Aji-Yërëm jaamam ñépp ci àdduna, tey Aji-Yërëm jaamam ña ko gëm ca allaaxira.

  1. الْحَمْدُ لِلَّهِ رَبِّ الْعَالَمِينَ

Di tekki: mbooleem xeeti cant yépp sax na di ñeel Yàlla, moom mi nga xam ne moo moom bindeef yépp.


  1. **الرَّحْمَنِ الرَّحِيمِ**

Di tekki: Yàlla miy Aji-Yërëm jaamam ñépp ci àdduna, tey Aji-Yërëm jaamam ña ko gëm ca allaaxira.

  1. **مَالِكِ يَوْمِ الدِّينِ**

Mooy Buurub bisub fay ba, muy bis-pénc.


  1. **إِيَّاكَ نَعْبُدُ وَإِيَّاكَ نَسْتَعِينُ**

Di tekki: yaw doŋŋ lanuy jaamu te ci yaw doŋŋ lanuy sàkku ndimbal.


  1. **اهْدِنَا الصِّرَاطَ الْمُسْتَقِيمَ**

Di tekki: Yal na nga nu gindi ci yoon wu jub wi.


  1. **صِرَاطَ الَّذِينَ أَنْعَمْتَ عَلَيْهِمْ غَيْرِ الْمَغْضُوبِ عَلَيْهِمْ وَلَا الضَّالِّينَ**

Di tekki: yoonu ña nga xéewale, déet yoonu ña nga mere، ak way réer ña. Nee nañu ña ñu mere ñooy, Yahuut yi, way réer ña ñooy, nasaraan yi.

Wàll:Alxuraan Wàll:saari Alxuraan