Sëriñ Suhaybu Mbàkke

Jóge Wikipedia.
Dencukaay:S suhaybu.jpg
S Suhaybu Mbàkke

Rakki S Abdul Ahad ju mu bokkal nday ak baay, ku jàmbaare la woon ci jàngale Alxuraan ak xam-xam ak yar ci diine, taalif na lu sakkan ciy téerey xam-xam, ñuy ci araab ak ci wolof, téere bu ci mel ne Xuratul Hayni ci wolof la ko def, muy téere bu jéggi dayo ba ci am solo, di wax ci lépp lu soxal nit, ci diine, ci paj, ci dundiin ak ci fànn yépp, Buxyatul Muriidiin, Naylul Awtaar ak yeneen téere yu am solo, lu sakkan ci boroom xam-xami yoon wi ci këram lañu jànge, ak sëti S Tuubaa yu bari