Sëriñ Ngañ Tàndine
Sëriñ Daaru Ngañ Tandine moo ngi feeñ jamono atum (1872i g j.) ci dëkk bu ñuy wax Ngadantu, wetu Kebemeer ci Kajoor.
Aw askanam
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]Naaru kajoor la, di Darmànko, ay maamam bàyyikoo woon Gànnaar dikk Senegaal, Kajoor dammel may leen suuf ñu dëkk. Maamam ju ñuy wax Seex Siidi Muxtaar Al-Kabiir, moo jur ku ñuy wax Amari Aj , mu jur Muhrissat, mu jur Abdulaay, mu jur Ma -Sàmba Jëmb, mu jur Demba Isa, mu jur Seex Siidi Muxtaar, mu jur Seex Daaru Ngañ Tandine. Way-juram wu jigéen a ngi tudd soxna Kunéel Amar, doomi Anta Baaba la, doomi Rubba Tob doomi Ma -Naar, doomi Anta Sekk la. Way-juram wu jigéen wi nag mbokk la ak soxnas Sëriñ Abdu Lahat Mbàkke ibnu Xaadimu Rasuul,way-juru Sëriñ Abdu Lakaram Mbàkke.
Am njàngam
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]
Bi mu matee dal jàng baayam a ko jàngal Alxuraan, ginaaw bi it baayam bu ndaw Baay Sayer Tandiné, ginnaaw bi magam Mustafaa Tandine jaar na ci Sëriñ Ma-Sàmba Jóob Saam, mu door a sóobu nag ci jàngum xam-xam, jaar na ci woroomi xam-xam yu bari di sàkku xam-xam door a yegsi ci Seex Isaa Jenn ,moo ko mujj a jàngal. Mu nekkoon ku géeju lool ci xam-xam.
Ag jébbaloom ci Seex Isaa Jenn
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]Moom ak Seex Isaa sàkku xam-xam moo ko boole woon ak moom, booba moo ngi dëkk bu ñuy wax Gàdd-Bitiw ,di Jàng ci benn dëkk bu ñuy wax Gëti Ndongo; moom ak mbokkam ya; Sëriñ Moor Ture, Sëriñ Ibraahiima Mbeng, ak Sëriñ Ma-Sekk Sëy. Lu jiitu loolu nag jaar nañu ci ay Sëriñ ak i woroomi xam-xam yu bari. Ñu wax leen ne am na benn Kaaŋ mu ndaw, maanaam boroom xam-xam, Yàlla def Seex Isaa Jenn jaar fa ànd ak Sëriñ Aali Sëy ñu waxtaan fa, xamee fa , Seex Isaa wan leen fa ay wax ak i léebu. Mu wax leen ne kaayleen ma defal leen lu gën am njàng ( ñoom nag, lu jiitu ñuy dikk ci Seex Isaa bu ñu masaa romb ay armeel dinañu xam ña ñu fay mbugal, ak ña fa texe. jigéen ju ëmb it bu ñu ko masaa gis dinañu xam góor la walla jigéen. Ak yu bari lool yoo xam ne dañu ko daan def muy mbirum baatin.) Bi loolu amee ci lañu dem tàgguji seeni kilifa. Ci nii la Sëriñ Daaru Ngañ Tandine boroom Daaru jébbaloo ci Seex Isaa. Di ko liggéeyal, guddi ak bëccëg, noor ak newet suba ak ngoon. Ba ni ko Seex Isaa ñaanalee, gërëm ko boole ko ak mbooloo. Muy defare.
Pastéefam ci Seex Isaa
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]Sëriñ Ngañ Tandiné ku amoon pastéef la ci Seex Isaa,ku ko bëggoon la,te doyloo ko. Ndax mas naa yónni doomam Sëriñ Siidi Muxtaar (booba manga Saalum) ne ko :" Boo Demee nee ko ba ma ànde ak moom ba tay jëfalagu ma ko sama yéen ci moom, Ndax li ma ko defal daa mel ni ci man ku ñu jox ab xiig bu ndaw , laaj la ci junni, te dawaloo ci lu dul ab su :! Seex Isaa ne ko :" Ku la gën a jige Yàlla gën la koo ragal, xëram "! Àggoon na ci bu masaan a bay Saalum ba noppi, day dem Kajoor yóbbaale ko ,di ko dundalee Seex Isaa, ba mujj na Seex Isaa aw ñam rekk lay jëfandikoo.Bis jomono xaw a naqari mu laaj ko li ngay indi yépp foo koy jëlee? Mu ni ko ci sa barke rekk la Jenn.Tudde na ko doom, jox ko ko, bole ko ab gàtt ,ne ko :" Lépp lu mu sañ ci gàtt bi sañ nga ko ci "! Mooy doomam Sëriñ Njenne Tandiné.
Ag jaamu Yàllaam
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]Sëriñ bi moom nag, daa boole woon sariiha ;ak xaqiiqatu, daan na julli, di woor, daane génne asaka, daan def yépp, daan ko digal waa këram .Daan na wax :" Lislaam bu doon ab tool waar waa féete du booy "! Daan na aye lépp lu xaraam, ak lu ñu sib, daan na aye am po, ak tëgg, ak ay caaxaan, ak jaxasoo góor ak jigéenk ak lépp loo xam ne yellul ci ab taalibe, añs. Ku fonkoon jaamu Yàlla la.
Digganteem ak ay taalubeem :
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]Ay daara la yoroon di leen tarbiya,di boole liggéey, ak jaamu Yàlla; jàng Alxuraan,ak Xasida. Moo leen daan dundal , daan leen aye lépp lu di am po aki caaxaan. Kenn daawul ñimee bañ a woor ,walla faat waxtu julli. Daan na wéet ak ñoom di leen waar ci Yàlla ba seeni xol tooy. Daan na wax ne :' Geenug golo gudd na, waaye lu ca dal boroom yëg ko"! Daan na aye waa këram ñoy tàbbi seen neengi way-jur ,gir bañ ñu difa ànd ak ñaneen ñu fa warut a tàbbi.bu leen masaa di wax, dara jëwrin ja la koy wax ,mu wax leen ko.
Jëwrin yi it daan na ñu watu kër gi leeg -leeg, ngir bañ ku fa warut a tàbbi tàbbi fa. Daan na leen wax liggéey bi ngeen may liggéeyal baax na am na solo, waaye ngeen aw ci yoonu njub moo ko gën , ndax tarbiya bu ñu koy wax ag njuba tax.
Digganteem ak jaami Yàlla yi
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]
Ku refetoon aw doxaliin la woon, diggantem ak jaami Yàlla yi. Te bari woon yërmande ci jaam ñi !Lépp lu mu mas a am da koy joxe,ku masaa na am njàqaare boo dikkee ci moom mu faju, yërmàndeem àggoon na ci bu nit masaa na faatu day laaj lu mu ko masa defal ! Ndax mas na koo liggéeyal ? walla mu santaane mu dem ca ? walla mu mas a wëlbatil ko aw dàllam ? Walla ndax soppoon na ko? ngir mu xettali ko ci ëllëg yawmal xiyaam. Bis am na am tudd bi ñu nee suba la gan dikkal ok, mu wax ne :" nanu ko fayal gàtt bi "., Am ci ndongo yi ku ne ko :" Tandiné suba kat la tudd mi,". mu ne ko :" Suba dikkagul , te Yàlla a ngi fi"! Am Na it ku mas a ñëw di ko yalwaan mu ne ko :" Ay yëre rekk moo fi nekk, daadi summiku jox ko ko (ci li mu soloon) ni ko gaawal dem balaa taalibe yi di la fi fekk "!Bu nit masaan di laaj it dan na ko toog loo ba adiya ñëw mu jox ko. Daan na gane ji ay taalubeem , daan na wàcce ab taalibe sampal ko kër may ko Soxna, boole leen di leen dundal. Ku bari woon xam-xam la ,ak wërsëg, ak laabiir ,ak ug tabe, Maam Siidi Maróon nekkoon kenn ci ay taalubeem daan na ko wax :"ku ma sama ñenti yii...doo am sama ñent yii...Waxi Sëriñ Ngañ la. Ku bari woon ag coofeel la ,ak yërmànde ci xale! Rawatina ndaw lu sell te jub aw ci yoon. Ku nuy wax Sëriñ Madina Ma-Béey mas na koo Ganeji ,ci dëkk bu ñu wax Gàdd bitiw . Keroog ba ñuy ñibbi da ne ko :" baalaa maa gis ku la dàq ngan dañoo dem ba biir Àjjana "! Ku manoon a defar ab diggante la, batax na Kajoor ak Saalum bu ñu jàqee moom lañu daan woo gir mu faju.
Dëkk yi mu sanc
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]Bukk na ci dëkk yi mu sos ; Daaru Paam nekk ci Kajoor, foofa sax la ab taawam feeñe jomono ci atum 1911 ,ak lenn ci ay njabootam. Bukk na ci foofa ci kajoor batay Ndande Faal, foo xam ne Sëriñ Isaa Jenn moo ko ko joxoon muy Daaru Jenn.Bukk na ci fu ñuy wax Mbuur ca fu ñuy wax Xabbaan , mu amoon fa fu ñuy wax Luuli ,ak Ngingineew ,am fa fu ñuy wax ngàcc ,foofu nag ci Saalum la. Ak fu ñuy wax Naar ga, ci Saalum la, ak fu ñuy y wax Daarul Mannaan, ci wetu Njenne Lagan, batay ci Saalum la.Foofu sax lu ëpp ci ag njabootam fa lañu nekk. Dëkk yii yépp da koo defoon ay daara ngir tarbiya ak liggéey ,ak jaamu Yàlla.
Diggante Sëriñ Ngañ Tandiné ak Sëriñ Tuubaa
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]
Amoon na ab cér bu màgg ci Sëriñ Tuubaa. Sëriñ bi ku ko bëggoon la ndax daan na wax Seex Isaa Jenn :" Sa naar bi saa su ma ko gise damay niroog sama sang ba Yonent ba SHWS "!
Sëriñ Isaa daan na ko yónni lu bari ci Sëriñ Tuubaa. Bi mu dikke ci Seex Isaa ,da koo yóbb ci Sëriñ Tuubaa ,gaaral ko ko , ne ko Kii kat damaa jox boppam ne ma :" maa ko doy, te moom laa njëkk a am ci taalibe te lépp lu ma am yaay boroom ,lu la ci neex def.
Bu la neexee ñu toog it ci yaw "! Sëriñ bi ne :" Ko Ngañ toog ci man ak toog ci moom lu la ci gënal "? Mu ne ko : Bu ñu ci amee ndigal toog ci Isaa ! Sëriñ bi ne :" ko sikkuwul, ndax li ñu def ci Isaa mat na Sëkk, ne ko boole naa leen, boo làqe gërëmam làq nga sama gërëm,kon boole naa leen:! Tudde na Sëriñ Tuubaa doom Itam.Sëriñ Tuubaa moo ko tudde woon Ngañ mu Gañe.Ndax turam mooy Ma- Demba, maamam bi jur baayam lañu ko tudde . Sëriñ bi joxoon na ko ay yérey boppam ;ak ag kaal, ak Satala boppam,ak ay kayit yu weex yu bari, añs...Ngir cofeel gu doxoon seen digganteem .Sëriñ Isaa mas na koo yónni bis ci Sëriñ Tuubaa, Taalibe ya xaw koo gàllankoor ,mu dugg ci kees yi benn Kees ,Sëriñ bi daa di wax ne :" Foofu Ngañ toogoon nañu ma fi yattal ab Bunt ". Mas naa yónni ñaari taalibeem, Sëriñ Moor Xaya, bu Ndand ak Sëriñ Moor Sëy bu Cees ,jox leen saaku suukar ,ngir ñu jox ko Sëriñ Tuubaa, ba ñu àgge Sëriñ bi ne leen :" boo leen demee neeleen ko :" na ma wutal suukar ,ndax kat am na lu ma ko doon fàggul biig "! Mas naa jox Sëriñ Tuubaa aw fas wu refet te taaru lool ! Sëriñ bi ne ko :" Fas wii bu ëllëgee ca lay wàcci tàbbi àjjana "! Ba leen Seex Isaa gërëmee, moom ak Sëriñ Moor Ture,ak Sëriñ Ibraahima Mbeng, ak Sëriñ Ma-Sekk Sëy ,Da leen a indi ci Sëriñ Tuubaa, ngir mu ñaanal leen .Mu wa ko ne :" Ñii dama leen a gërëm ".Sëriñ Tuubaa daa di toggu ab laax ci loxoy boppam jox Sëriñ Ngañ ,ne ko :" Am yaag Say bokk xéewluleen ci kon ".
Bari na ay bir lool, yooxam ne doxoon na ci diggantem ,ak Sëriñ bi. Lii ay doomam ñoo ko nettali,lii ay taalubeem, li Sëriñ Baara Jenn añs...Kon lii lu tuuti la ci rekk ci seen diggante.
Diggantem ak Seex yi Seex Isaa seexaloon
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]
Ku mel ni Sëriñ Ibraahima Mbeng, Baroom Ngaar.Tudde na ko doom, mu tudde ko doom. Ku mel ne Sëriñ Moor Ture, boroom Mesere, noonu, tudde woon na ko doom mu tudde ko doom. Ku mel ne Sëriñ Àlliyun Mbàkke Gusaas itam Tudd na ko doom. Ku mel ne Sëriñ Musaa Ka Cale, sk Sëriñ Musaa Ka Medina .Sëriñ Aali Sëy bu Ngëy-Ngëy itam Tudde na ko doom mu tudde ko doom. Ku mel ne Sëriñ Baara Jenn it Sëriñ Ngañ Tudde woon na ko ñaari doom.Sëriñ Moor Jenn Daaru Paam noonu. Ku amoon ak jaxasoo la woon ak Seex yi mu bokkal Seex Isaa; Ku mel ne Sëriñ Daawuda Jaañ, ak Sëriñ Njabeel Jaañ , ak Sëriñ Moor Mati Wàdd,ak Sëriñ Ahmadu Daam Suraŋ.Sëriñ Abdu Rahmaan Jaañ noonu,ak Abdu,ak Sëriñ Moor Laatiir Jóop, Sëriñ Tuubaa Mbay ak Sëriñ Baara Faal,ak Ma-Sekk Sëy,ak ñaenen ñu bari.Soppoon nañu ko lool ,daan nañu ko ganeji mu daan leen gane, defal nañu ko ay teraanga yu bari lool,ngir coofeel gu doxoon seen diggante.
Digganteem ak Seex yu mag yi
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]Digganteem ak Seex lbraayma Faal, defoon na këram fukki fan ak juróom 15. Ci ab yonne bu mu doon yonne.Bis Seex Ibra Faal jox ndaw Xaalis ne ko :" Wutal ma ginaar ". Mu wër amul mu dikk, Sëriñ Ngañ ne ko Faal :" Bu nu ci amee ndigal dem ". Mu ne ko Bismilaa diir bu gàtt mu dikk , indi xaalis ak ginaar bu ñaarte li mu ko joxoon ! Bu guddi masaan a jot taalibe yi dajee daan na leen waar ba ñu tàggoog seeni sago. Ba ci Seex Ibra Faal sax, ngir man a waxtaan . Ba miy tàggoog Seex Ibra Faal da ne ko ": Ngañ mu gañe, sa fukki fan yii ak juróom 15 li nga fi làq nit am nafi ay at te làqu ko fi.m". Ne ko Ngañ ba miy ñatti yoon ni ko man nga Njiitu yoon, daa di koy ñaanal mu dem. Digganteem ak Maam Moor Jaara it refetoon na lool , moom it gërëm na ko. Maam Ceerno it noonu gërëm na ko. Da koo fonkoon ndax daan na fa dem di ko nemmiku ngir Seex Isaa . Sëriñ Jéeri wadaan Sugu it noonu la meloon ci moom ,daan na ko yobbul ay teraanga yu bari di ko ko jox, ndax seenug Njamboot dañoo jaxasoo woon ci ak mbokk. Sëriñ Ma-Sàmba Jóob Saam it noonu da koo bëggoon daan na ko seeti lu bari, Sëriñ Moo Njaay Tàggaar noou. Sëriñ Baara Jenn it Sëriñ Asan Salaam mas naa ñëw fii ñu ko denc ci Ndand Faal mu wax ne :" Wàlliwu Yàlla wi tëdd fi bu ngeen ko xamoon li mu yor ciy xéewal ak i gërëm bari na bari goo xam ne bu ñu ko doon séddale fii du tax mu jeex "! Ak ñanen ñu bari.añs.
Moog Seex Isaa Jenn
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]
Da koo bëggoon lool !
Masul a deñ , mbaa mu tàyyi ci di ko liggéeyal, guddi ak bëccëg lu mu masa am jox ko ko.Bu masaan bay ba génne asaka ji , li des lépp la koy jox haddiya. Bi Sëriñ Tuubaa joxe Seex Isaa Jenn liggéeyu Jumaay Njaareem, moom la Seex Isaa defoon jëwrin ji, moo daan joxe njël li, daan wuti ay (godaar ,mooy ay bagaas) yu bari fu nekk ci réew mi di ko indi. Seex Isaa daan na ko wax :" Dama laa gërëm ba lépp lu ma la defalul rekk dama koo amul, walla yoruma ko, lépp lu ma am bokk naa ko ak yaw.Joxoon na Seex Isaa doomam it mu yoroon ko ba amoon ci njaboot. Seen ug mag ba seen ug ndaw masuñoo tàqalikoo lu mu def ñoo ko ànd ba ni mu làqoo.
Ay Seex yi mu seexal
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]
Amoon na ay góor Yàlla yu mu defaroon ba seexal leen. Bokkoon na ca ku ñuy wax Sëriñ Móodu Jaañ Joor Mbay ,moom nag wax nañu ne :)( bi miy dikk ci Sëriñ bi booba sàmp na kër ,dëkkoon ci dëkk bu ñuy wax Ndaxma ci kajoor la nekk, bi miy ñëw ci Sëriñ Ngañ soxnaam su Tudd Soxna Faatu Ndaw, la àndaloon , mu nekk ca soxna ya, moom it Mu nekk ca Daara ya di tarbiyawu , ba Sëriñ bi ñaanal ko defar ko , seexal ko,mu nekkoon *Daarul Manaan Saalum ci dëkkem bu mu sancal boppam tudde ko Njaañ. Bokkoon na ci ku ñuy wax Sëriñ Jibriil Mbeng Nekkoon dëkk bu ñuy wax Séenoo wala Njenoo nekk ci Kajoor moom itam doon ku jàmbaare te bëggoon Sëriñ bi. Bokk na ci seex yi ku ñuy wax Baay Sëy,nekkoon ci dëkk bu ñuy wax Naarga ci Saalum Moom it noonu la meloon ci Sëriñ bi, di ko liggéeyal guddi,ak bëccëg; noor ak newet, bëgg ko ba yamalewu ko woon ak dara.( Yal nañu leen Yàlla fayal sunu maam yu baax yooyu, aamiin.)
Ay fanam yu mujju
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]Bokk na ci mujjug dundam,daan na faral di dajale ag njabootam di waxtaan ak ñoom, di leen wax ne :" Buleen di reeroog seen mag jii di Siidi, toppleen ci moom defleen ko mag ,walla baay sax, yoon wi it buleen ci kenn man , rawatina seen Sëriñ bii di Seex Isaa Jenn ". Waxoon na Sëriñ Siidi ne ko :" Boo amee fanweeri at 30 dinga ma wuutu ci suuf, waaye boo amatee fan weeri at 30 dinga ma fekk si "! Moom nag dafa nekkoon ci dëkkam bi di Daarul Manaan ci SaalumYàlla a def tawat dal ko fa mu tàggu Seex Isaa ne ko :" Daa bëgg a dem Kajoor ". Ba mu demee diir bu gàtt rekk la fa am daa di faatu ! Loolu nag moo ngi tolloo ak fukki fan ak juróom walla juróom benn ci diggiw-tabaski . Yamoo ak àllarba 24 novembre 1942 Ñu dénc ko Ndande Faal ci teewaayu Seex Isaa Jenn moo ko jullee taxawu ko ñaanal ko dénc ko fa ,ci teewaayu Magi Taalibe yu bari. (Yl na nu ko Yàlla fayal.) Ginaaw bi loolu amee ci la Sëriñ Sidi Tandiné toog doon xalifa bi ko njëkk a wuutu. 1942 ba 1971 ci jomono joo xam ne mag ñu bari ñoo ngi fi,mu doon jàmbaar lool,doon boroom pasteef ,doon ab liggéeykat bu mag.Taxaw temm ci li mu ko dénkoon,matale ko sëkk, ba ni mu ko fekkee 71 Ñaareelu Xalifaam toog di Sëriñ Ibraahima Mbenga Tandiné , 1971 ba 1999 . Moom it aw yoon woowu. Mu doonoon ku yéeme! doon boroom baatin, waaye dib liggéeykat,ba ni mu làqoo 99 ñatteelu Xalifaam toog 1999 ba 2003 di Sëriñ Aali Tandiné.Mu doon ku jàmbaare ci yoon wi moom it liggéeykat bu mag la woon ci diine ji soppiwaat lu bari ci dëkkub baayam bi yaatal ko ,def ci lu bari, nekkoon jaamukatu Yàlla bu mag.Moo nag Yàlla def na yàggufi,ba ni mu làqoo 2003 .Ci la ñeenteelu Xalifaam toog di Sëriñ Ma-Jóop Tandiné 2003 ba 2021.Moom it jaar yoon wa ay magam jaar di ku baaxoon te laabir doon góor Yàlla! Mu liggéey fi yu te am solo ,ba ni mu làqoo 2021 . Ci la jurémeelu Xalifaam toog di Sëriñ Omar Tandine moom it aw yoon wa ay magam awoon di jàmbaar di baroom pasteef bu mag . (Yal na ko fi Yàlla bàyyi ,ba yéenem mu matale ko ci yoon wi ak kër gi aamiin.)
Matlabul xaajaati Sëriñ Musaa Ka, Wolofal Naari darmànko
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]
Jaaraama Maam Jaar ku am jaaraama, Ya ko waral sa dooma am karaama.
Dëggalu ma lim Ñaari Kajoor yim seexal,
Defar na Naar defar Wolof moo jeexal
Seex Ibra Joor Seex Ndongo Joor naam Amar,
Sëriñ bi may na leen lu faj suñu mar.
Seex Paate Amar am na Móodu Amar, mat nab xaaliifatu te faj na aw mar.
Seex Abdulaay Amar wa xaadi Baabaa,
Seex jéeri Waadaan fataqal abb waa baa.
Sëriñ Sulaymaan Sëriñ Njabeel Jaañ, Sëriñ bi aar na leen ba deefuleen gaañ.
Seex Ibra Jaañ daawuda Jaañ Seex Baara Jaañ
,xam nañu Ngañ Tandiné mbër mu aay ngaañ.
WOLOFAL Sëriñ Daaru Ngañ Tandiné:
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]
Bismil ilaahi tay ma way, sant Sëriñ Ngañ Tandiné tay
Jàmbaar ju mag Ja fiiru tay,fa Ndande Faal Cëy Tandiné.
Kii moo ligéey,ligéey bu rëy, baatax ku nekk jóg di ku roy.
Ñépp a ngi sàkku seeka roy, ñéppay siyaar si Tandiné.
Liggéey bu rëy bamu defoon, ca kër baroom Njenne ba woon,
Moom lañu fay doomam yi kon, ku askanoo ci Tandiné.
Sañc na luuli sañc Paam, dellooti sañc Naarnga naam,
Te foofi dem Gànnaar ñu naan, mbirëm ya rëy na Tandiné.
Xahiixa lay Jafa ndi koo, sariiha lay Sukka ndikoo , Lislaam ci lay fagandikoo ku askanoo ci Tandiné.
Ngir non na man Seex Daaru Ngañ, Lislaam bu doon néeg mbaa te koñ,boobee du rës mukk ci Ngañ, li la digal waa Tandiné.
Moo tax ba waa këram yi tay, kenn du ci moy sariiha tay, waa joofi gis mu jubblu tay jëfal na axlu Tandiné.
Gàddaafe ak Gàdd gu féex, Ngadantu ak Bitiw gu féex, saabuñ jóge di safi Seex jëfal si axlu Tandiné.
Sa Njënd lii Daarul Manaan, tay foofi dukk dinga naan, kenn dootu muñ wa mar di ñaan duus yaa ngi wall Cëy Tandiné.
Daarul Manaan Daaru Salaam, Daaru sañc aki Njaañ kër goofi bu añ jote niinal nga bool ya Tandiné.
Yaatax ba sa sët yi tay,di wori Otoo ki meebi daraa,te fuñ nuyoo ñu naan Salaam, sagal nga axlu Tandiné
Yaatax batay ma yor Xalam, di sàkku way wu am Xorom,gindima tay buma gëlëm,ngir ma jëfal waa Tandiné.
Man Góora Ndag di ab tayéer, maa jóg di sant bay miir, tegtal ma won ma sab janeer ngir ma jëfal waa Tandiné.
Yal na nga ñu may biib nawet, mu fawwxa kullu nawet, na lépp nangu ni wereet ,bijaahi Seex Ngañ Tandiné.
Ma dellu ñaanal waa Órob, xéewal yu rëy ca biir Órob,indi ko fi aki Gurub bi jaahi Seex Ngañ Tandiné.
Yaatax batay ku dem Órob, foojubbl ñépp a naan gurub,yaanu fànggul ca xareb, rijaalu laahi Tandiné.
Defar nga góor defar jigéen,defari ndaw defari séen, saabuñ jóge ñépp di séen Óoray tàngaayam waa Tandiné.
Jigéen ñi kenn dootu wall, fooraas bi day xelli di wall,sa njënd lii mooma gënal, diine ngi sant Tandiné.
Du laaj jigéen ak cann gu rëy,du laaj jigéen alal ju rëy, barke la ko fàggul bu rëy, royleen ci axlu Tandiné.
Seex Daaru Ngañ yaanu teral,yaa rëy teraanga koy teral,sa njënd lii mooy tegtale ,sa jëf ju Sell Tandiné.
Sa jàkka jii nga fi bàyyi woon,far nañu ko def Jumaa ci yoon,yal na nga ñu may ñu ami koom, àggale waat ci Tandiné.
Sa kër gu mag gafa Kajoor,fees nga ko dell ak i leer,yal na ñu farfa juur siyaar si waat Cëy Tandiné.
Seex Daaru Ngañ yaadig njaaloo,semall nga Wuur ya woon Kajoor,aay yu rëy ngaleen fa juur, fàwwxa nga wuurya Tandiné.
Seex Daaru Ngañ na nga ma gërëm, ci way wi ndax Yàlla yërëm,na mbindéef yépp am gërëm,bijaahi Seex Ngañ Tandiné.
Jox naa la sama Lisaan, ak sama ,Xol bi muy Jinaan,sa géej gu rëy gii naa ci naan nuur naa ci axlu Tandiné.
Xeeñtu lu baax ci gaayu baax,man naa defar lépp lu baax, Yàlla de Buur moo yore baax, yal nanu baax ci Tandiné.