Sàngol

Jóge Wikipedia.

Sàngol ag lawtan la guy law ci kaw i garab, garab la nag goo xam ne lu ëpp ci mbayam cig paj la jëm.

Sàngol gi


Dëkkuwaayam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Garab gi ci bërëb yu xaw a af yi, yu yaatu yi lay man a nekk walla ci àll boo xam ne ay garab yu sew ñoo fa am. Leeg-leeg it man naa nekk ci bërëb bu am ker walla it mu topp dex gi. Garab la guy yéeg ci yeneeni garab yuñ man a fekk leeg-leeg ci suuf su nooy walla ci suuf su nuy noppal.

Njariñ yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Li ëpp ci li ñiy jëfandikoo garab gi cig paj bokk na ci wàcce tàngooru yaram moo xam it tàngooru yaram wuy dem ak ay ñëw la walla pajum sibiru doonte sax ci réew mu mel ni End garab gi bokkul ci ñaar fukki garab ak juroom yi ñu taamu ngir faj sibiru. Leneen li ci topp ci li ñiy faj ci garab gi mooy pëyiis mbaa gaana mbaa feebaru sifilis. Garab gi bokk na ci yi ñiy jëfandikoo ngir yokk ngóora.

Nataal yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]


Turu xam-xam wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Cocculus pendulus