Royuwaay:Tur:

Jóge Wikipedia.

Lëng/ vitex doniana xeetu la garab wu bokk ci njambootu "lamiaceae" ak ci ñoñ Vitex, aji-law la Afrig Gu digg , ca Romoor ak Rewño.

Mbind mii jukki la ñeel meññiit mi. Man nga bokk nit ñi say xalaat ci jagal ko( nan?) cig tënk tënku ci xelali mébet yim méngool.

Turi: Lëng/ vitex doniana

Wf:(lëng) Fr:( prunier noir), bari na lool ay turi gox, niki : um dugulguun (araab), bi (baya), galbiki (fulfuldé), dinyar (awusaa), shike koma, garbo (kapsiki), zekad (mafa), seked (mofu).

Meloom bu ñuul la yor, peppam lees di lekk la.


Foytéef yi, ci nëtëx lañuy doore, ñor digante mee ba nowaambar, daal di ñuul te saf suukar. Gudaayu gatab gi ci diggante yaar ba yatti ñay la. Afrig ak mbàmbulaan Endo lay nekk.ci dunu Rewño it dees na ko fay fekk.

Foytéef ci garab gi ( Rewño)

Foytéef, akub raas (Senegaal)

Foyteef gu tupp-tupp (Rewño) Jëfandikoo