Papaay

Jóge Wikipedia.

Garabu papaya lu ci ëpp nu ngi koy gis ci diwaan yi nga xamne ndox dafaa bari. Mu ngi soqeekoo ca "Sud Mexique" .

Guddaayam dana tóll ci 3 ba 7 meetar. Mu bokk ci njabootu dicotylédone bi nga xamne seen i wànqaas lu ci ëpp day taqaloo.

Dundam ci kaw suuf nag, taxu koo yàgg lool diggante ñatt ba juróom i at su bare ba bare waaye ci at mu njëkk mi dina tambale am meññeef.

Te booy dagg wànqaas yi, diir bu gàtt mu tàmbalee amaat yaneen i wàqaas.

Xóotaayu biiram tóll na ci 20 Cm (Diamètre), te li ko wër lépp yeen saa yi mu yor melo wu (vert,) yenn saa yi mu yor wu gris.