Ndaybarga

Jóge Wikipedia.

Ndaybarga , garab la goo xam ne du rëy waaye day sëq taxawaayam nag man naa dem ba juróomi met.

Meññeef mi


Fumuy sax ?[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Moom nag ci barab yi nga xam ne taw bi xawu faa bari lool lay meññ.

Barab yooyu bu ñu xaymaa li muy taw ci at mi du ëpp 500 milimet ci taw .

Melokaanam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ndaybarga garab la goo xam ne ay xobam xobu lëmm lay doon du ay xob yu sew, ay wànqaasam da ñuy rénki doon lu lunk maanaam: da ñuy dëng wànqaas yu ndaw yiy door a jebbi da ñuy am lu mel ni ay kawari muus. Ndaybarga am na ñaari xeet.

Fan lay sax ?[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Moom nag mi ngi sax ci réew yu bari fii ci Afrig fu mel ni Kongo, Ruwandaa , Sudaan, Ugandaa , Keeñaa.

Kañ lay meññ ?[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Bu nawet bi di waaj a tàmbali walla buy waaj a jeex lay tóortóor maanaam cooroon ak lolli.

Fu mel ni Keeñaa wax na ñu ne bu noor bi jotee moom rekk mooy doon garab gi nga xam ne day am ay xob yu naat yu nëtëx ba tax na jur gi moom rekk la ñuy lekk ci waxtu woowu.

Njariñam:[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Moom nag xob yi ak reen yi ak xas mi lépp a am njariñ.

Xobam lu am njariñ la ci nit ak mala ak jur.

Day dindi mettiit, di faj jangoroy bët, wanent ak biir buy metti, ak màtt-màttu ndox suuf ak jaan.

Xob yi batay day ray saan, batay ci wàllu pajum Tubaab xob yi am na ag diw gu ñu ciy defar ngir faj.

Ay reenam boo ko jëlee kakk ko bam def dóom boo diwee dóom bi ci màtt-màttu jaan day dindi daŋar ji, batay dóom bi soo ko jëlee diw ko koo xam ne yaramam dafay metti dana ko faj.

Batay ay reenam boo ko boolee ak xobi (nebadaay) saab-saab di na faj woppi jur ji ñuy wax (trepanosome) wopp la juy dal jur gi.

Batay reen yi ak xob yi day faj woppi jur ji ñuy wax "sarbon".

Njebbiriit li soo ko jëlee dëbb ko man nañ koo boole ak cere, yenn dëkk yi suñu jànkoonte ak ab xiif xob yi la ñuy jël di ko boole ak séen ug lekk ngir sakkanale ko séen dund bu niiw boobu.

Bu dee xas mi :

Xas mi moom boo demee dëkk bu mel ni Keeñaa dañ ciy defar ab toogu bu ñuy wax tabre ndax ay bantam dafa neex a dëngal ndax ni ñu bindoo dañoo lunku, batay xas mi am na dëkk yoo xam ni ay buum la ñu ciy Defar.

Bu dee ay bantam moom dina ñu ko def matt di ko xambee ndax tàkk-tàkkam dafa neex.

Turu xam-xam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Cadaba farinora