Keler Holt
Claire Rhiannon Holt (Brisbane, 11 suwe 1988) mooy jigeen buy foog ak modele bu Australi, te mu am it citoyenneté Amerikaan.[1]
Li tax mu siiw ci àdduna bi mooy limu def ci filmu H2O, The Vampire Diaries ak The Originals ak filmu 47 Meters Down .
Claire mingi juddoo Brisbane, màgg fa, am ñaari mag yu jigéen ak bu góor.
Role bimu njëkka jouer mooy Emma Gilbert ci H2O, diggante 2006 ba 2009. Ci 2008 mingi doon filme filmu sinemaa Messengers 2 - Njiitu Mujjentalu filmu bi Martin Barnewitz bind, di topp ci filmu The Messengers, ci la nekkoon protagonist bi. Ci ete 2010 , ci la filme Mean Girls 2, di topp ci Mean Girls, ci 2011 ci la jouer Samara Cook ci Pretty Little Liars . Bi ñuy tànn nit ñi ñuy jouer ci filmu tele bi tuddu The Secret Circle, dañu ko siñe ngir mu jouer Rebekah Mikaelson ci rôle bu vampire bi, ci The Vampire Diaries, rôle bumu jouer itam ci sesoŋ bi njëkk ci spin-off bu série bi ak ci yi ci topp, ñu tuddee ko O.[2][3]

Ci atum 2017, ci la jouer ci benn thriller bu tuddu 47 meetar ci suuf, te Johannes Roberts moo ko realise, ci la jouer ak Mandy Moore ak Matthew Modine . Ci 2019, ci la jouer ci ñaari filmu yu bees, Tàqaloo bu am fitna ak Fetu fase . Ci 2021, mu dellusi ngir jouer Rebekah Mikaelson ci filmu bi tuddu Legacies . Ci at moomu, ci la jouer ci filmu Untitled Horror Movie ci weeru suen ci at moomu, ci la defar benn koleksion ngir màrku Andie Swim.
Lu mu yàgg yàgg
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]Riassuntu bu gàtt ci wolof:
Ci weeru sulet 2015, Claire Rhiannon Holt yëgle ne dafa sëy ak Matt Kaplan. Ñu def sëy bu sutura ci 28 awril 2016. Ci 27 awril 2017, Kaplan sàkku fase ndax ay jafe-jafe yu ñu mënul woon déggoo; Holt tontu ci 2 Mee.[4]
Bisu 3 desàmbar, 2017, ci la yëgle ni dafay sëy ak ab developpeur immobilier bu tuddu Andrew Joblon. Bisu 4 màrs, 2018, ci la wax ni daa ñàkk doom. Jëkkër ak jabar lañu sëy ci 18 ut 2018. Am nañu ñatti doom: James judd ci 28 màrs 2019, Elle Madeline, judd ci 12 septembre 2020 ak Ford Matthew, judd ci 9 nowàmbar 2023.[5][6]
Bisu 21 nowàmbar, 2019, ci la wax ni nekk na doomu Etats Unis .[7]
Filmografi
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]Cinéma
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]- 47 meetar ci suuf ( 47 Meters Down), Johannes Roberts moo ko realise (2017)
Tele
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]- H2O ( H2O: Yokk ndox rek ) – Série tele, 52 pàcc (2006-2008)
- Mean Girls 2, Melanie Mayron moo ko realise – filmu tele (2011)
- Pretty Little Liars – Seri tele, 5 pàcc (2011)
- The Vampire Diaries – Série tele, 38 pàcc (2011–2015)
- The Originals – Seri tele, 38 pàcc (2013–2018)
- Aquarius – Série TV, 22 pàcc ( 2015-2016 )
- Legacies - Série tele, pàcc 4x05 ba 4x15 (2021-2022)
- ↑ https://www.tvsa.co.za/actors/viewactor.aspx?actorid=13963
- ↑ https://www.rottentomatoes.com/celebrity/claire_holt
- ↑ https://www.hollywoodreporter.com/tv/tv-news/vampire-diaries-spinoff-originals-claire-holt-421332/
- ↑ https://www.eonline.com/news/848671/claire-holt-s-husband-files-for-divorce-just-before-the-couple-s-1-year-wedding-anniversary
- ↑ https://www.marieclaire.com.au/news/celebrity/claire-holt-andrew-joblon-wedding/
- ↑ https://www.eonline.com/news/1389692/claire-holt-gives-birth-welcomes-baby-no-3-with-husband-andrew-joblon
- ↑ https://www.dailymail.co.uk/tvshowbiz/article-7721619/Vampire-Diaries-actress-Claire-Holt-celebrates-citizen.html