Karasol
Apparence
Karasol garab la gu bàyyikoo ci lu bir ci àll yu naaje yu Karayib, yu Amerig gu digg ak gu bëjsaalum.
Melo wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Karasol gàncax la gu ndaw. Guddaayam danay àgg 3 ba 10i met. Xobam melo wu nëtëx la yor. Tóor-tóoram 3i xob la yor. Day meññ at mépp.
Njariñ yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Karasol dees na ko lekk. Dees na ci defar njar. Dees na ci fajoo it.
Turu xam-xam wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Annona muricata
Tur wi ci yeneeni làkk
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]farañse: corossolier |
angale: soursop tree |
itaaliyee: graviola |