Imbraatóor gu Mali wuute gi ci sumb yi

Jóge Wikipedia.
Ibou (waxtaancëru)
Aucun résumé des modifications
Guaka (waxtaancëru)
m Tuddewaat koNguuru mali en Nguuru Mali
(Aucune différence)

Sumb bu 21 Ut 2007 à 18:55

Xët wii dafa nekk ci yoonu ndefaru. Sag cëru man na cee am solo!
Réyaayu nguuru Mali gu mag ga ci 1350

NGuuru Mali gu mag ga ba ci xarnub XII xamalu nu ko woon lu bari. Ci li tegu atum 1150, la nu xam tur yu mel Hamana, Jigi Bilali(1175-1200) ak Musaa keyta di ko wax itam Allakoy (di tekki neex yalla). Moo ngi yemoon ci Mbàmbulaanu Atlas ci sowam, Dexu Niseer ci penkoo, tay ñuy yii réew: Mali, Senegaal, Gaambi, Ginne, Ginne Bisaawò, Gànnaar, ak ab xaaj bu bari ci Kot Diwaar.

Ay Cosaanam

Ci boobu diwaan (Sudaan) ag nguur gu ndaw judd woon na fa: Mandeŋ walla Mali (Malenke: nitu Mali). Ci li gën a siiw coosaanam, ay dëkk dëkkaani mande yu bari yu nekkoo ci Kaw-Senegaal ak ci Kaw-Niseer. Trauware yi nekkoon Dakadiyala, ci réewu Kri, ci wettu Nyagassola, ci Kaw-Bakoy, Konte yi nekkoon Tabu, ca Dodugu (di tekki réewu do), Kamara yi ca Sibi, ca Siendugu, Keyta yi ca Nareena, ca Dodugu ak ca Doju yu Mandeŋ nekk ci diggante Sigiri ak Kita.

Ca Dodugu la Bambara yi nangoo ay dëkk yu bari, mamm jëm penku, ba peggu Seegu ca Niseer ba. Ci li wër Doj yu Madeŋ, Malinke yi ñaari dëkk yu solowu lañ fa amoon: Kiri ak Dakadiyala. Njiitu dëkk yooyu ay rëbbkat la ñu woon, yu bokkoon ay gëm-gëm, bokk di def seniy xumbeeli diine. Nekkoon nañ nakk ay Askan yu bari yu bennoo woon am benn buur, Simbo moo doonoon seen maqaama. Buur yooyu Askanu mbooloo yee loon doon fal mu lee doon teewal ci ndaje ya daan am ca Pénc mu Mag ma(Gara) mi doon dogal ci li ñeel xare yi walla juuti yi...

Doley mboolooy nguur-nguraan yooyu doon magg, moo jappale nguuru Sooso gi dond Nguura Gana gu mag ga, ba mu man a sos geneen nguur gu mag gu buur ya amoon maqaamay Mangha walla Mansa.

Sunjata Keyta

Ngir Xòotal, yërël bii jukki Sunjata

Musaa Keyta di ko wax itam Allakoy, siiwoon na ndax aji makka yu bari yi mu defoon, loolu saxaloon na diney lislaam ci xoli Njabootu buur bi. Doom di itam Ndonoo mu Musaa, Nare Famagan (1218-1230) siiwoo na loo ndax yaatalam jëm bëj-gànnaar, ak sowu, ak pegg gu ndeyjooru Kaw-Niseer, nootoon Somono yi. Nare Famagan bari woon na ay jabar, kenn ci ñoom ki ñu dakkantalee woon Kuduma (boroom gòomu yaram yi). Jabar ju tawatoon jooju moy yaayu Sunjata Keyta. Bi mu juddoo ba juroom ñaari at man a gul woon dox.

Laagoom googu moo taxoon ba Sumaawuru Kante doon faat ay magam, mu ba woon ko fa. Benn bes, Sunjata jengu ne day jòk taxaw, ndax naxxar gi mu amoon ci li Sumaawuru defoon, tegoon ci nangu nguur ga. Mu laaj ab weñ ngir jafandu ci jòg, weñ ga damm, mu jël geneen noonu, jëlaat geneen noonu, ci la kenn waxee nañ ko jox yatu baayam ba, bam ca jafandoo la jòg taxaw. Ña ko tewee woon yeemu; ndey ja ak géwalam, Jakuma Duwa, ca la ñu fentee ab bakk duppee ko Xala ga, baat ya ak wayin wa, ba tay ñoo ngi rëkk ci dënni waa mali yi ndax mooy seen bakkum réew.

Ci 1230 la nekk buur, ci la réy Sumaawuru, boole nguur-nguuraan yi nekkoo ci wetan yépp ci nguuram, dal di nekk nak Mansa. Ci moom la Mali nekke nguur gu mag dëgg, ci la aggee ci pujam.

Ay buuram

Ulee

Bi mansa Ulee ñëwee(1255-1270), di ki wuutu Sunjata, la tambalee Diggadil(décentraliser) nguur gu mag jox ko yorteef ba mengoo woon ak réyaayam. Tabb ay sang jox leen ay ndomboy-tànk yu am solo, ñi ci gën a reññeewu. Fran Kamara, Siriman Keita.

Abuubakar mu njëkk(I)

Ci 1285 la Abuubakar mu njëkk(I) gaañu, Jafe-jafe yi nekkoon ci tànn ab ndonoo, ca la Sakura jëlee nguur ga. Doonoo na nitu nguur di itam ab jambaar, ci la yaatalaatee nguur ga ba dugg Gao ci penkoom ak Tekuruur ca sowan. Ay saay-saay ñoo ko ray ca weti Tripoli mu feekoo muy aji Makka.

Abuubakar ñaareel(II)

Ci 1303, Abuubakar ñaareel(II), di jarbaatu Sunjata, mi siiw lool ndax li mu bëggoon a wuññi li nekk ci ginnaawu Mbàmbulaanu Atlas mi. Ca la jëlee ñaar teemeeri looco ak dund dal di yònnee ngir ñu dugg ci mbàmbulaan mi, waaye kenn a ca dellu si nettali ni dañoo dajeeg ab dawan bu soxor ci ndox mi, mu mëdd leen. Abuubakar dal di jëlaat ñaari junni looco, xaaj fu deflufa ag bund, and ak ñoom dem, ca la saayee da tay.

Mansa Musaa(Kanku Musaa)

Mansa Musaa

Mansa Musaa (1312-1332)Bokk na ci buuri Nguuru Mali gu mag ga yi gën a siiw. Ci 1324 la aji makka. Ca ajam bu siiw ba, andaloon na ag 60 000 ci ay dunguru (su ñu ci degloo Taariix as-Sudaan). Jaar ci diggu ndand féy-féy ba, ca Walata ak ca Tuwat, ba mu aggee Keer la ñépp yéemu ndax alal ga mu fa andi. Nee nañ yoroon na ñaari ton ci wurus. Mbaaxam ak yéewënaayam, yéemoon na bépp nit ba nekkoon Keer ca jamono jooju. Donte déggoon na araab nangul woon a làkk lu dul làkkam, daa jëloon ay tekkikat. Mansa Musaa yòbb woon turu Mali ci bépp réewu araab, dalee ko ca Andalusia ba Xorasan, ba Tugal, lonkoyoon bu adduna bi bu Angelo Dulcert(1339), wone ab yoon bu jall Atlas, jeggi Sahara ngir agg Mali: "rex Melli". Lonkoyoon bu Abraham Cresques, bi ko buuru Faraas defloo woon Charles V, bindoon na fa turu peyam "Ciuta de Malli".

Maghan(1332-1336) moo ko wuutu

Mansa suleymaan

Mansa suleymaan(1341-1360) mooy jubbanti waat koom-koomu nguur gu mag ga. Gën a dëggaral kilifteefu Mali ci Diwaani penku yi ko wër, njiitu Tuaareg yi bu Takedda (Ayiir), nangu woon na googu kilifteef. Suleymaan xëccoon na Mali ay boroom xam-xam ak ay àttekat yuy tòpp Maalik. Moo ci boppam fiqh la jang, maanaam àtte ci lislaam.

Mari Jaat(1360-1374) mooy ko wuutu

Musaa II

Musaa II(1374-1387) tegu ci, moom doonul woon ku am kàttan, xawoon a tayyeel, jëwrinam bu njëkk la bayee woon lépp. Moo songoo Tuareg yi, di def ay congam jëm Bornu

Saayam

Lu weesu Mansa II, kujje ya amoon ci biir kër buur, te yenn saa yi rayante daan si am, moo demoon ba faagaagal nguur gu mag ga. Ci noonu nguuru Gaawo di lekk ndakk-ndakk diwaan yi féete penku nguur ga. Dem ba jël peyu njaay bu Jenne. Donte ci diggu xarnub XV, Ca Da Mosto ak Fernadez newoon na ñu way dëkk yu Gammbi da ñoo jappee woon seen bopp ni ku bokk ci Mali, waaye, ci 1480, la Naba Nasere song Walata. Tekuruur jall ci loxoy wolof yi(Jolof). Pël yu Bundu tambali ay yëngu-yënguy fippu, Tengela I, di ko wax it Jaje di tekki Goreelkat bi, mooy leen jiite woon. Da fa gaawantu ci ay yi amoon ci diggante Mali ak Gaawo def li muy def. Nekkon ci dëkk bu am solo ci njaay mi, Kingi.

Seetal BUNTU TAARIIX
wikbaatukaay am na xët wu tudd: Imbraatóor gu Mali