Haj wuute gi ci sumb yi

Jóge Wikipedia.
Contenu supprimé Contenu ajouté
Idioma-bot (waxtaancëru)
m r2.7.3) (Robot: Adding min:Haji
Xqbot (waxtaancëru)
m r2.7.3) (Robot: Modifying hr:Hadždž to hr:Hadž
Rëdd 103 : Rëdd 103 :
[[gu:હજ]]
[[gu:હજ]]
[[he:חג']]
[[he:חג']]
[[hr:Hadždž]]
[[hr:Hadž]]
[[hu:Mekkai zarándoklat]]
[[hu:Mekkai zarándoklat]]
[[ia:Hadj]]
[[ia:Hadj]]

Sumb bu 6 Maars 2013 à 20:34

Haj
Dencukaay:Al-haram.jpg
Haj

Haj mooy juróomeelu ponku Lislaam, Ci waxi Yonent Yàlla Muhammed ja ni: "Tabaxees na Lislaam ci juroom: Seere amul benn buur bu dul Yàlla te Muhammed ndawam la, Taxawal Julli, Joxe Azaka, Woor weeru koor, Ak Aj ci ku ko man aw yoon", ba tay Aj farata la ci benn jullit bu ko man (ci bepp anam), ci waxi Yàlla mu kawe ja ni:ñeel na Yàlla ci nit ñi Aj néek ba ci ku ko man aw yoon (benn yoon) te ku weddi Yàlla moom woomle waliif mbindéef yi.

Haj Màkka ak kumu war

Haj Màkka benn yoon faratala ci mukàllaf mu ko man ci yaramam ak ci ab yobbalam. Manug Yaram wi moodi mu bañ a ame wopp ju ko tee man a dem walla mu ragal ca dem ga dollikug wopp ja, walla sosug wopp walla ak yeex a wér.

Yobbal bi yit moodi mu am lu ko lew lu sell loo xamni darra ci ribbaa nekk u ca, àqi kenn neek u ca, te yal waanu ko ñaanu ko te mu doy ko sëkk ba du tumurànke ci yoon wi du ca yalwaan du lëjal kenn, waa këram yitam mu bàyyee leen lu leen doy sëkk ba du ñu muturànke du ñu lëjal kenn. Mu fay boram yépp bu dul bu am digam teewul, waaye bu dee teew balaa dellu si sax war na koo fay balaa dem walla mu batale ko. Bu ci yooyu yépp amee nak war na ko ni ko julli ware ku ko weddi ab yéefar la, ku ko bàyyi te tay ko te tëlewu ko ci genn anam ab saay-saay la bu bon te bu ko tuubul ba dee sawara la jëm. Ku ko bëgg nak bu demee ba fa muy armale dana fa fekk ku ko jiite ci yi mu war a def yepp ak yi mu war a bàyyi yepp ba ba muy noppi. Moongi ware ci weeru Tabaski

Jeegoy Aji Màkka gi

Ñatti xeeti Haj yi:

Haj am na ñatti xeet:

1-Hajug tamattu
2-Hajug qiraan
3-Hajug ifraad

Umra

Umra yitam sunna la benn yoon mook Aj ñoo nuroo lépp waaye boo doxee safaa ak marwa umra jeex


Faratay HaJ

Haj ñeenti farata la am :
1 yeenee aj (nawaytu al-hajja wa 'ahramtou bihi li l-Laahi taala)
2 tawaaful ifaada
3 dox diggante safaa ak marwa
4 taxaw arafa.


SUNNAY AJ

Sunnay Haj fukk ak ñaar la:
Am na ci ñeent yoy ñi ngi ame ca armal ga:
1 sangu gu jokkook armal gi
2 rafle ci lunu ñaw 3 solub ñëkk akug làmbaay aki dàll 4 labayka.

Tawaaf gi am ñeenti sunnaam : 1 dox gi 2 foon gi doj wa ci loxo walla gimiñ 3 ñukk gi ci ñatti tuur yu njëkk yi 4 ñaan gi ngay ñaan ci tawaaf bi.

Dox gi safaak marwa it am ñeenti sunnaam : 1 foon doj wi bu dee daa juge ca jàkka ja jem safaa 2 ag yeegam diggante safaa ak marwa 3 gaaw gi niy def ci batnu masiil 4 ñaan gu amulub àpp gi ngay def ci kaw safaa ak marwa.



Bañ na ñu

Bañ na ñu lool nak ku Aj ba dik mu di ko darajawoo walla mu di ko tuddoo di ko dolli ci aw turam, walla mu defe ni gëne na ko (Aj gi) kenn ku ko deful. Na ko def ngir Yàlla rek, niki muy tuddee Yàlla ak a julli ak a woor ak a natt azaka ngir Yàlla. mu xamni Aj yitam ak yooyu ñoo yam kepp ci ku mu war. lu waay di def na ko def ngir Yàlla rek ngir lu dul Yàlla ak neen la.