Xarefulwoon wuute gi ci sumb yi

Aller à la navigation Aller à la recherche
10 octets supprimés ,  9 at ci ginaaw
Coppite gi amul tënk
'''Xarefulwoon''' (di tekki lees manatul a xar, di ci fr Atome), baat bi [[Seex Anta Jóob]] a ko tëgg te mi ngi sukkandiku ci bu njëkk li ñu foogoon ne mooy xaaj bi gën a tuuti bees manut a xaraat bu ab [[ne-ne]], (manees na koo tudde it '''fepp''' (mi doon tuutalug pepp "peppu suuf as feppu suuf") muy lu bawoo ci ngéru [[Xeltu|xeltukat]] yu [[Gires|waa-gires]] yu yàgg ya. Mooy wàll wi gën a tuuti ci bépp [[cër]] bu nekk ci dénd bi buy wéy di yor màndarga yu [[simi]] yu la mu doon, ci yeeneen kàddu, soo ko xaaje du nekkati wenn wàll wu ne-ne wa mu bokkoon laataa xaaj gi, beneen xeetu ne-ne lay nekk.
 
Ci jëmug mujjug ati 1800 (ak wuññig [[mbëjfepp]]) ci lañu biral ne xarewulwoon manees na koo séddale, ndax li mu doon, moom ci boppam, lu cëroo ay [[wàll-wàllaan]] yu bari yu gën a ndaw (baatu [[Wàll-wàllaan wu njëlbeen|ronxarefulwoon]] loolu lañu ci jublu).
 
'''Faramfacceb xarefulwoon''' mooy faramfacce biy wax ci melokaanu ne-ne yi, di dëggal ne bépp ne-ne ay bennaan ñoo ko cëroo te ñu leen di woowee xarefulwoon, ñoom ñooy dajaloo ci benn anam bi nekk ne-ne bi. Bii faramfacce ñoo ngi koy man jëfe ci ne-ne yi nekk ci nekkiin wu wow, [[yullaakoon]] ak wu [[Gil|gile]].
2 337

modifications

Njëlu joowiin