Dawaan bu safaanu wuute gi ci sumb yi

Jóge Wikipedia.
Contenu supprimé Contenu ajouté
Xqbot (waxtaancëru)
m robot Adding: als:Wechselstrom
TXiKiBoT (waxtaancëru)
Rëdd 71 : Rëdd 71 :
[[hi:प्रत्यावर्ती धारा]]
[[hi:प्रत्यावर्ती धारा]]
[[hr:Izmjenična električna struja]]
[[hr:Izmjenična električna struja]]
[[ht:Kouran altènatif (AC)]]
[[hu:Váltakozó áram]]
[[hu:Váltakozó áram]]
[[id:Arus bolak-balik]]
[[id:Arus bolak-balik]]

Sumb bu 6 Suwe 2010 à 10:20

Dawaan bu safaanu (DS walla AC ci wu-angalteer: Alternating Current) màndargoo ag walug dawaan guy soppiku ci jamono muy ci taraay walla ci jubluwaay.

Doxiin

Naka-jekk dawaanu mbëj suñu koy séddale ci dawaan bu safaanu bu baraayam sax ci 50 Hz walla 60 Hz lees koy defe (+ ak - bi dañuy safaanu ci watatukaay bi juroom-fukki saa yu ne).

Jëfandikoo gu dawaan bu safaanu mi gi jóge ci li jurukaayu dawaan yi, ci yaxanaay ci koom-koom ak seenug yomb a defar, di jur dawaan bu safaanu ci anam gu yomb, kon dawaan bi ci boppam kenn du ko soppiwaat laataa ag jëfandikoo.

Fi njariñ li gën a feeñee sax mooy séddaleeb dawaan bu safaanu bir na ne moo gën a yaxan dawaan bu wéy ci séddaleeb taraay bu kawe (ñakkug kàttan gi ci buum yu gudd yi moo gën a néew). rawatina, ci diggante gu gennwéq walla wéq yu bari, bir na yaxanaay gu ñettiwéq di gees gën a jëfandikoo ndax néewteey ñakkug kàttan ngir njeexitu Joule (moo tax dijjaayu watatukaay yi gën a néew, maanaam wëñ yu gën a sew); jëfandikoog dawaan bu safaanu bu ñettiwéq lawal na buumi yóbb yi ci diggante yu gudd lool yi.

Genn Màndarga gu am-solo gu dawaan bu safaanu, ba waral ci genn wàll li tax ñépp jël ko, mooy yomb gee jëfandikoo fu nekk, yomb gee soppi ci lim yu wuute ci taraayu dawaan, ci ndimbalu soppikaay yi, ak ñakkug kàttan gu digu.

Donte yenn jumtukaay yi dawaan bu wéy lañuy doxe, waaye loolu manees na koo ame ci dawaan bu safaanu, sunu jëfandikoo ab jubbantikaay.

Suñu jëfandikoo ag xaralag mbëjfeppal gu kàttan gu ñaw, manees naa jëfandikoo dawaan bu wéy ngir am dawaan bu safaanu, jur ko ci yenn anami baraay, melokaanu duus ak taraay jaare ko ciy jumtukaay yees duppee jallarbikaay.

Taariix

Lonkoyoonu àdduna bi bees melool aju ci taraay a baraayu kàttanu mbëj ci ndombo yiy séddale dawaan gi ci kër yi.

Ca njalbeenu njëfandikug kàttanu mbëj ci ndefar gi ci XIXu xarnu daawaan bu wéy lañu doon jëfandikoo, ndax li mu doonoon lu neex a rënk ciy tegle ak li mu gën a wóor dawaan bu safaanu. Tomb bu mujj bi Thomas Alva Edison mooy ki ko doon wax ci lees tuddewoon xareeb dawaan yi.

Dawaan bu safaanu, gi soloom doonoon lu beneen xaaj bi boole woon Nikola Tesla ak George Westinghouse doon aar, manul a ñakk ci njëfandiku gu ab soppalikaay, moom mi tax ñuy man jokkalante mbëj mi ci diggante yu gudd. Te itam doxalukaayu mbëj yu dawaan bu safaanu ñoo gën a wóor te gën a yaxan yu dawaan yu wéy yi.

Ci jamono jii ci àdduna bi dawaanu mbëj ci ñaari baraay lañu koy séddalee, 50 Hz(Tugal, Asi, Afrig) ak 60 Hz(Diiwaan-yu-Bennoo ak goxu Aamerig bépp ci lu daj, genn xaaju sapoŋ) ak taraay yu wuute.

Xool it

Téerekaay