Kajoor wuute gi ci sumb yi

Jóge Wikipedia.
Contenu supprimé Contenu ajouté
Ji-Elle (waxtaancëru)
Guérin Nicolas (waxtaancëru)
m Modification de la catégorie Catégorie:TaariixCatégorie:Taariixu senegaal (avec HotCats)
Rëdd 92 : Rëdd 92 :
* [[Tekuruur]]
* [[Tekuruur]]
* [[Bawol]]
* [[Bawol]]
[[Catégorie:Taariixu senegaal]]
[[catégorie:taariix]]
[[catégorie:afrik]]
[[catégorie:afrik]]
[[catégorie:senegaal]]
[[catégorie:senegaal]]

Sumb bu 26 Mee 2008 à 14:56

Kajoor

Ci wàllu xay Kajoor moo doonoon seetub Senegaal. Dammeel moo nekkoon ca kaw di seddale ay ndomboy tànk.

Koom-koom

ci lu jiitu ñëwug tubaab yi, Kajoor doonoon na nguur guy am-amam newoon gàññ. Mbay ak liggéey ci loxo ak camm ak napp ak ak njaay ñoo nekkoon fànni liggéey yi ëppoon solo ca nguur ga.

Mbay

Mbay moo doonoon liggèey bi ëppoon solo ci koom-koomam. Looloo taxoon ba su baykat yi amul woon jàmm doon na feeñ cakoom ga, manoon naa andi sax ab xiif. Dugub moo ëppoon ci mbay mi ak ci dund gi. Barile woon nañ ay garabi tiir yu daa indi diw tiir ak sëng. Xamoon nañu mbayum. wëtteen.

Liggéey ci loxo ak Njaay

liggéey ak loxo ñeeño yi la ñu ko feetale woon. Napp gi amoon na solo lool ci dund gi. Waaye njaay moo naka-jekk tubaab yi ñoo ëppoon ci ñi ñu ko defal. Mujj na ba yoon yi jòge bëj-gànnaar ñakk solo lool njëgg mi.

Booba fekkoon na géej gi di gën a am solo, Fekkoon na Kajoor da jaay ay der ak ay bëñi ñayy mu dal cay dolli njaayum jaam, ngir am ay fas, ay piis, ay dibi,...

Suuf moo nekkoon jumtukaay bi ëppoon solo, moom ñépp a ko bokkoon. Ñi ñuy wooye Kangam yi mbaa Laman ñoo ko doon saytu. benn nit amu ci woon moomeel. Loolu terewul woon ku mu neexoo mu jariñoo ci kèem kàttanam.

Doole ju bees ji

Nguur gu bees moo fa jële woon ña daa saytu suuf sa ca diwaan ya. Ñiy doora falu ñoo yoral seen bopp suuf si walla book ñu dénk ko ay ceddo. Looloo waraloon jalgati gi ak bundxataal gi ñu tegoon ci kaw gor ña njotti bopp yu kenn àttanul, rax ci dolli mayu ñu leen fu ñu yakkee seen nàkk

Liggéeykat yi

Su fekkee ne suuf si toxu na ci ay loxo dem ci yeneen, li jëm ci liggéey ak loxo moo des ci loxo ñeeño yi. Looloo taxoo ba géer ñi sori woon nguur ga, ak ñeeño yi ak jaam yi ñu féetele woon mbay mi, ñoom ñèpp muuj nañ nekk ay liggéeykat. Ñoo féete woon indi lépp lu nit soxlo ci dund ak takkaay ak col ak ay jëfëndikookaay.

Yorteef

Nguur gu bees gi tax na ba ñu andi tër yu bees ci ay àtte yu bees. Dammeel moo feete woon ñépp kaw. Moom mu ngi daan sant Faal ci geño ak ci meen. Man naa am ñu tànn dammeel fu dul geño mbaa meenub paaleen. Waaye loolu su xewee li koy waral mooy fullay waaja ak faydam ak tabeem. Yii yèpp ñiy tànn daa na ñu ci bàyyi xel.

Su ñaar dee xëccoo nguur gi war na ci ñoom ñaar ñepp ñu nekk Jaambur, mbaa ay Bummi mbaa ay beñ jéem. Su ñu bokkee lu ñuy nekk, boroom baat yi nekk ci kaw, yiy tànn dellu seet seen jikko ak nu ñuy àtte ak su mbir nee këtt ne jonn nu ñuy taxawee. Li doy na tegtal ci leerteg seen tànninu buur.

Loolu terewul nguur gi nekk ndono ci kaw bu amee ku ko war a donn.

Kajoor mekkoon na juroomi tund: Ganjòol, Njaambur ci bëj-gànnaar, Ndèet ca penku, Sañaxoor ca digg Kajoor, jandeer ca diggante sowu ak bëj-saalum. Su ñu falee Dammeel da fa war a sèddale ndomboy tànk yu mag ya ba ku nekk xam foo féete. Ci jeexintalu xarnub XVII la Dammeel joxe woon ndigal ngir ndomboy tànk yooyee, ñu man kaa tàkkal rekk ñi cosaanoo ngàllo te féete ci kër buur.

Buuri Kajoor

1.Decceefu Njoogu (1549) 17.Maawo
2.Amari ngoone Sobel 18.Biram Koddu
3.Maa Sàmba Tàkko 19.Maajoor
4.Ma Xurayja Koli 20.Makoddu
5.Biram Mànga 21.Biram Faatim Penda
6.Daaw Demba 22.Amari Ngoone Ndeela Kumba
7.Majoor 23.Biram Fatma Cub
8.Biram Yaasin Buubu 24.Maysa Tenda
9.Décce Maram 25.Birima
10.Maa Faali 26.Makoddu
11.Ma Xurayja Kumba Joojo 27.Majoojo
12.Biram Penda Ciloor 28.Lat Joor Ngoone Faal(1862)
13.Decce calaw 29.Sàmba Yaasin Faal
14.Lat Sukaabe 30.Sàmba Lawbe Faal
15.Maysa Sukaabe
16.Maysa Tenda

Delluwaay

Paate sow, Démbi Senegaal: ci làmmeñu Wolof, Dakaar, 1998

Lëkkalekaay yu biir


wikbaatukaay am na xët wu tudd: Kajoor
Seetal BUNTU TAARIIX